As-Saff · 7/14
Tekki Waxtaan — As-Saff
وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُوَ يُدْعَىٰ إِلَى الْإِسْلَامِ ۚ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ ۝٧
Wa man azlamu mimma nif taraa `alal laahil kaziba wa huwa yad`aaa ilal Islaam; wallaahu laa yahdil qawmaz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Ana kan moo gën a doon tooñkat kuy duural Yàlla ay fen, te ña nga koy woo jëme ko ci Lislaam ? Yàlla dey du gindi aw nit ñu di ay tooñkat.

🎧 Dégg


📜 Aaya 5-9 — As-Saff

5وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ لِمَ تُؤْذُونَنِي وَقَد تَّعْلَمُونَ أَنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُمْ ۖ فَلَمَّا زَاغُوا أَزَاغَ اللَّهُ قُلُوبَهُمْ ۚ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
(Fàttalikul) Ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : "Yéen samaw nit ! Ana lan moo tax ba ngeen di ma lor te xam ngeen xell ne man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen ? ” Bu ñu jengee, Yàlla jengal seeni xol, te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay saay-saay.
6وَإِذْ قَالَ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ إِنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُم مُّصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيَّ مِنَ التَّوْرَاةِ وَمُبَشِّرًا بِرَسُولٍ يَأْتِي مِن بَعْدِي اسْمُهُ أَحْمَدُ ۖ فَلَمَّا جَاءَهُم بِالْبَيِّنَاتِ قَالُوا هَٰذَا سِحْرٌ مُّبِينٌ
(Fàttalikul it) Ba Iisaa doomu Maryaama waxee ne : “eey yéen waa giir Banii-Israayiil, man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen, may dëggal la ma jiitu woon, ca Tawraat, di bégale it, ci Yonent buy dikk sama ginnaaw aw turam di “Ahmadu”. Waaye ba mu leen dikkale ak ay firnde yu leer , dañoo wax ne : “Lii kat ag njibarla gu bir ne fàŋŋ”.
7وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُوَ يُدْعَىٰ إِلَى الْإِسْلَامِ ۚ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ
Ana kan moo gën a doon tooñkat kuy duural Yàlla ay fen, te ña nga koy woo jëme ko ci Lislaam ? Yàlla dey du gindi aw nit ñu di ay tooñkat.
8يُرِيدُونَ لِيُطْفِئُوا نُورَ اللَّهِ بِأَفْوَاهِهِمْ وَاللَّهُ مُتِمُّ نُورِهِ وَلَوْ كَرِهَ الْكَافِرُونَ
Ñoom dañoo bëgg fay leerug Yàlla ci seeni gimiñ, te Yàlla moom kuy mottali la ag leeram doontele sax Yéefër yi dañuy bañ.
9هُوَ الَّذِي أَرْسَلَ رَسُولَهُ بِالْهُدَىٰ وَدِينِ الْحَقِّ لِيُظْهِرَهُ عَلَى الدِّينِ كُلِّهِ وَلَوْ كَرِهَ الْمُشْرِكُونَ
Moom moo yónni ab Yonentam ci njub ak diiney dëgg, ngir mu kawe mbooleem diine yi, doonte la sax Yéefër yi dañuy bañ.
As-SaffFihi Alxuraan
14Aaya
MedinanRevelation
7Aaya

Tekki — As-Saff 7

Simoore As-Saff Aaya 7 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana kan moo gën a doon tooñkat kuy duural Yàlla…

Simoore Aaya 7/14 — As-Saff الصف (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Saff Dégg, As-Saff Tekki, As-Saff mp3, As-Saff pdf. Aaya 5–9. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers