Al-A'raf · 156/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
۞ وَاكْتُبْ لَنَا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ إِنَّا هُدْنَا إِلَيْكَ ۚ قَالَ عَذَابِي أُصِيبُ بِهِ مَنْ أَشَاءُ ۖ وَرَحْمَتِي وَسِعَتْ كُلَّ شَيْءٍ ۚ فَسَأَكْتُبُهَا لِلَّذِينَ يَتَّقُونَ وَيُؤْتُونَ الزَّكَاةَ وَالَّذِينَ هُم بِآيَاتِنَا يُؤْمِنُونَ ۝١٥٦
Waktub lanaa fee haazi hid dunyaa hasanatanw wa fil Aakhirati innnaa hudnaaa ilaik; qaala `azaabee useebu bihee man ashaaa`u wa rahmatee wasi`at kulla shai`; fasa aktubuhaa lillazeena yattaqoona wa yu`toonaz Zakaata wallazeena hum bi Aayaatinaa yu`minoon
📖 Tekkim Wolof
Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun gindiku nanu jëm ci Yaw.”. Mu ne : “Sama mbugal, danaa ko sadd ku Ma neex. Waaye Sama yërmaande ëmb na lépp lenn. Te danaa ko sadd ña ragal Yàlla tey génne asaka ak ñi gëm Samay kàddu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 154-158 — Al-A'raf

154وَلَمَّا سَكَتَ عَن مُّوسَى الْغَضَبُ أَخَذَ الْأَلْوَاحَ ۖ وَفِي نُسْخَتِهَا هُدًى وَرَحْمَةٌ لِّلَّذِينَ هُمْ لِرَبِّهِمْ يَرْهَبُونَ
Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind ma làmboo na njub ak yërmaande ngir ña nga xam ne ñoom ragal nañu seen Boroom.
155وَاخْتَارَ مُوسَىٰ قَوْمَهُ سَبْعِينَ رَجُلًا لِّمِيقَاتِنَا ۖ فَلَمَّا أَخَذَتْهُمُ الرَّجْفَةُ قَالَ رَبِّ لَوْ شِئْتَ أَهْلَكْتَهُم مِّن قَبْلُ وَإِيَّايَ ۖ أَتُهْلِكُنَا بِمَا فَعَلَ السُّفَهَاءُ مِنَّا ۖ إِنْ هِيَ إِلَّا فِتْنَتُكَ تُضِلُّ بِهَا مَن تَشَاءُ وَتَهْدِي مَن تَشَاءُ ۖ أَنتَ وَلِيُّنَا فَاغْفِرْ لَنَا وَارْحَمْنَا ۖ وَأَنتَ خَيْرُ الْغَافِرِينَ
Muusaa tànn juróom-ñaar fukki góor ciy nitam, ngir sunu waxtu ndaje. Ba leen yëngug xeer wa jàppee, mu ne : “Yaw sama Boroom, bu la neexoon nga rey leen ak man lu jiitu tey. Moo ndax Danga nuy rey ngir li ña réer ci nun def ? Loolu du leneen lu dul sa nattu, ci ngay réerale ku La soob, di ci jubal ku La soob. Yaway sunu Cëslaay. Nanga nu baal, yërëm nu, Yaa di ki gën a mën a jéggale.
156۞ وَاكْتُبْ لَنَا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ إِنَّا هُدْنَا إِلَيْكَ ۚ قَالَ عَذَابِي أُصِيبُ بِهِ مَنْ أَشَاءُ ۖ وَرَحْمَتِي وَسِعَتْ كُلَّ شَيْءٍ ۚ فَسَأَكْتُبُهَا لِلَّذِينَ يَتَّقُونَ وَيُؤْتُونَ الزَّكَاةَ وَالَّذِينَ هُم بِآيَاتِنَا يُؤْمِنُونَ
Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun gindiku nanu jëm ci Yaw.”. Mu ne : “Sama mbugal, danaa ko sadd ku Ma neex. Waaye Sama yërmaande ëmb na lépp lenn. Te danaa ko sadd ña ragal Yàlla tey génne asaka ak ñi gëm Samay kàddu.
157الَّذِينَ يَتَّبِعُونَ الرَّسُولَ النَّبِيَّ الْأُمِّيَّ الَّذِي يَجِدُونَهُ مَكْتُوبًا عِندَهُمْ فِي التَّوْرَاةِ وَالْإِنجِيلِ يَأْمُرُهُم بِالْمَعْرُوفِ وَيَنْهَاهُمْ عَنِ الْمُنكَرِ وَيُحِلُّ لَهُمُ الطَّيِّبَاتِ وَيُحَرِّمُ عَلَيْهِمُ الْخَبَائِثَ وَيَضَعُ عَنْهُمْ إِصْرَهُمْ وَالْأَغْلَالَ الَّتِي كَانَتْ عَلَيْهِمْ ۚ فَالَّذِينَ آمَنُوا بِهِ وَعَزَّرُوهُ وَنَصَرُوهُ وَاتَّبَعُوا النُّورَ الَّذِي أُنزِلَ مَعَهُ ۙ أُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ
Ña nga xam ne danañu topp Yonent ba, di ku ñu soloo te jàngul, te ñu fekk ñu bind ko ca ya ñu yore ci Tawreet ak Injiil. Mu di leen digal lu baax, di leen tere lu bon, daganal leen yu sell ya, araamal ca ñoom yu selladi ya, soppil leen ya leen diisoon ak gàkk ya nekkoon ca ñoom. Kon ñi ko gëm [moom Muhammad] te weg ko, te ñu topp leer ga Nu wàcce ci moom; ñoom ñooy way-texe ña.
158قُلْ يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُمْ جَمِيعًا الَّذِي لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ يُحْيِي وَيُمِيتُ ۖ فَآمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ النَّبِيِّ الْأُمِّيِّ الَّذِي يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَكَلِمَاتِهِ وَاتَّبِعُوهُ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
Neeleen : "Yéen nit ñi ! Man Yonentub Yàlla laa ci yéen ñépp, Moom mi nga xam ne Moo moom nguuru asamaan yi ak suuf si. Amul jeneen yàlla ju dul Moom. Mooy dundal, Mooy rey. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam bi, di ku ñu soloo te jàngul, te moom gëm na Yàlla ak ug kàddoom. Kon toppleen ko, xéy-na kon ngeen gindiku”.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
156Aaya

Tekki — Al-A'raf 156

Simoore Al-A'raf Aaya 156 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun…

Simoore Aaya 156/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 154–158. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers