Al-A'raf · 155/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَاخْتَارَ مُوسَىٰ قَوْمَهُ سَبْعِينَ رَجُلًا لِّمِيقَاتِنَا ۖ فَلَمَّا أَخَذَتْهُمُ الرَّجْفَةُ قَالَ رَبِّ لَوْ شِئْتَ أَهْلَكْتَهُم مِّن قَبْلُ وَإِيَّايَ ۖ أَتُهْلِكُنَا بِمَا فَعَلَ السُّفَهَاءُ مِنَّا ۖ إِنْ هِيَ إِلَّا فِتْنَتُكَ تُضِلُّ بِهَا مَن تَشَاءُ وَتَهْدِي مَن تَشَاءُ ۖ أَنتَ وَلِيُّنَا فَاغْفِرْ لَنَا وَارْحَمْنَا ۖ وَأَنتَ خَيْرُ الْغَافِرِينَ ۝١٥٥
Wakhtaara Moosaa qawmahoo sab`eena rajjulal limeeqaatinaa falammaa akhazat humur rajfatu qaala Rabbi law shi`ta ahlaktahum min qablu wa iyyaaya atuhlikunna bimaa fa`alas sufahaaa`u minnaa in hiya illaa fitnatuka tudillu bihaa man tashaaa`u wa tahdee man tashaaa`u Anta waliyyunaa faghfir lanaa warhammnnaa wa Anta khairul ghaafireen
📖 Tekkim Wolof
Muusaa tànn juróom-ñaar fukki góor ciy nitam, ngir sunu waxtu ndaje. Ba leen yëngug xeer wa jàppee, mu ne : “Yaw sama Boroom, bu la neexoon nga rey leen ak man lu jiitu tey. Moo ndax Danga nuy rey ngir li ña réer ci nun def ? Loolu du leneen lu dul sa nattu, ci ngay réerale ku La soob, di ci jubal ku La soob. Yaway sunu Cëslaay. Nanga nu baal, yërëm nu, Yaa di ki gën a mën a jéggale.
🎧 Dégg

📜 Aaya 153-157 — Al-A'raf

153وَالَّذِينَ عَمِلُوا السَّيِّئَاتِ ثُمَّ تَابُوا مِن بَعْدِهَا وَآمَنُوا إِنَّ رَبَّكَ مِن بَعْدِهَا لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ñay def lu ñaaw ba noppi ginnaaw ga ñu tuub, tey ñu gëm... sa Boroom nag, ginnaaw loolu, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
154وَلَمَّا سَكَتَ عَن مُّوسَى الْغَضَبُ أَخَذَ الْأَلْوَاحَ ۖ وَفِي نُسْخَتِهَا هُدًى وَرَحْمَةٌ لِّلَّذِينَ هُمْ لِرَبِّهِمْ يَرْهَبُونَ
Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind ma làmboo na njub ak yërmaande ngir ña nga xam ne ñoom ragal nañu seen Boroom.
155وَاخْتَارَ مُوسَىٰ قَوْمَهُ سَبْعِينَ رَجُلًا لِّمِيقَاتِنَا ۖ فَلَمَّا أَخَذَتْهُمُ الرَّجْفَةُ قَالَ رَبِّ لَوْ شِئْتَ أَهْلَكْتَهُم مِّن قَبْلُ وَإِيَّايَ ۖ أَتُهْلِكُنَا بِمَا فَعَلَ السُّفَهَاءُ مِنَّا ۖ إِنْ هِيَ إِلَّا فِتْنَتُكَ تُضِلُّ بِهَا مَن تَشَاءُ وَتَهْدِي مَن تَشَاءُ ۖ أَنتَ وَلِيُّنَا فَاغْفِرْ لَنَا وَارْحَمْنَا ۖ وَأَنتَ خَيْرُ الْغَافِرِينَ
Muusaa tànn juróom-ñaar fukki góor ciy nitam, ngir sunu waxtu ndaje. Ba leen yëngug xeer wa jàppee, mu ne : “Yaw sama Boroom, bu la neexoon nga rey leen ak man lu jiitu tey. Moo ndax Danga nuy rey ngir li ña réer ci nun def ? Loolu du leneen lu dul sa nattu, ci ngay réerale ku La soob, di ci jubal ku La soob. Yaway sunu Cëslaay. Nanga nu baal, yërëm nu, Yaa di ki gën a mën a jéggale.
156۞ وَاكْتُبْ لَنَا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ إِنَّا هُدْنَا إِلَيْكَ ۚ قَالَ عَذَابِي أُصِيبُ بِهِ مَنْ أَشَاءُ ۖ وَرَحْمَتِي وَسِعَتْ كُلَّ شَيْءٍ ۚ فَسَأَكْتُبُهَا لِلَّذِينَ يَتَّقُونَ وَيُؤْتُونَ الزَّكَاةَ وَالَّذِينَ هُم بِآيَاتِنَا يُؤْمِنُونَ
Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun gindiku nanu jëm ci Yaw.”. Mu ne : “Sama mbugal, danaa ko sadd ku Ma neex. Waaye Sama yërmaande ëmb na lépp lenn. Te danaa ko sadd ña ragal Yàlla tey génne asaka ak ñi gëm Samay kàddu.
157الَّذِينَ يَتَّبِعُونَ الرَّسُولَ النَّبِيَّ الْأُمِّيَّ الَّذِي يَجِدُونَهُ مَكْتُوبًا عِندَهُمْ فِي التَّوْرَاةِ وَالْإِنجِيلِ يَأْمُرُهُم بِالْمَعْرُوفِ وَيَنْهَاهُمْ عَنِ الْمُنكَرِ وَيُحِلُّ لَهُمُ الطَّيِّبَاتِ وَيُحَرِّمُ عَلَيْهِمُ الْخَبَائِثَ وَيَضَعُ عَنْهُمْ إِصْرَهُمْ وَالْأَغْلَالَ الَّتِي كَانَتْ عَلَيْهِمْ ۚ فَالَّذِينَ آمَنُوا بِهِ وَعَزَّرُوهُ وَنَصَرُوهُ وَاتَّبَعُوا النُّورَ الَّذِي أُنزِلَ مَعَهُ ۙ أُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ
Ña nga xam ne danañu topp Yonent ba, di ku ñu soloo te jàngul, te ñu fekk ñu bind ko ca ya ñu yore ci Tawreet ak Injiil. Mu di leen digal lu baax, di leen tere lu bon, daganal leen yu sell ya, araamal ca ñoom yu selladi ya, soppil leen ya leen diisoon ak gàkk ya nekkoon ca ñoom. Kon ñi ko gëm [moom Muhammad] te weg ko, te ñu topp leer ga Nu wàcce ci moom; ñoom ñooy way-texe ña.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
155Aaya

Tekki — Al-A'raf 155

Simoore Al-A'raf Aaya 155 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Muusaa tànn juróom-ñaar fukki góor ciy nitam, ngir sunu waxtu…

Simoore Aaya 155/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 153–157. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers