At-Tawba · 41/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
انفِرُوا خِفَافًا وَثِقَالًا وَجَاهِدُوا بِأَمْوَالِكُمْ وَأَنفُسِكُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ ۝٤١
Infiroo khifaafanw wa siqaalanw wa jaahidoo bi amwaalikum wa anfusikum fee sabeelil laah; zaalikum khairul lakum in kuntum ta`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Nangeen di xeex ci woyofaay ak ci dIisaay [sawar ak tàyyeel], nangeen di xeex ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Loolu moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon.
🎧 Dégg

📜 Aaya 39-43 — At-Tawba

39إِلَّا تَنفِرُوا يُعَذِّبْكُمْ عَذَابًا أَلِيمًا وَيَسْتَبْدِلْ قَوْمًا غَيْرَكُمْ وَلَا تَضُرُّوهُ شَيْئًا ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Bu ngeen génnul, Dana leen teg mbugal mu metti, te wuutale leen nit ñu leen gën. Te dungeen Ko mënal dara [moom Yonent bi]. Ndax Yàlla mën na lu ne.
40إِلَّا تَنصُرُوهُ فَقَدْ نَصَرَهُ اللَّهُ إِذْ أَخْرَجَهُ الَّذِينَ كَفَرُوا ثَانِيَ اثْنَيْنِ إِذْ هُمَا فِي الْغَارِ إِذْ يَقُولُ لِصَاحِبِهِ لَا تَحْزَنْ إِنَّ اللَّهَ مَعَنَا ۖ فَأَنزَلَ اللَّهُ سَكِينَتَهُ عَلَيْهِ وَأَيَّدَهُ بِجُنُودٍ لَّمْ تَرَوْهَا وَجَعَلَ كَلِمَةَ الَّذِينَ كَفَرُوا السُّفْلَىٰ ۗ وَكَلِمَةُ اللَّهِ هِيَ الْعُلْيَا ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
Bu ngeen ko dimbaliwul... Yàlla dimbali woon na ko, ba ko ña weddi génnee, muy ñaareelu ñaar. Ba ñu nekkee ñoom ñaar ca xunti mate muy wax ka mu àndaloon : “Bul jàq, Yàllaa ngi ànd ak nun.” Yàlla wàcce dal ci moom, te Moom mu dimbali ko ak lél bu ngeen gisul, mu def kàddug ña weddi mu suufe, kàddug Yàlla di lu kawe. Ndax Yàlla Ku not la, Ku xereñ la.
41انفِرُوا خِفَافًا وَثِقَالًا وَجَاهِدُوا بِأَمْوَالِكُمْ وَأَنفُسِكُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
Nangeen di xeex ci woyofaay ak ci dIisaay [sawar ak tàyyeel], nangeen di xeex ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Loolu moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon.
42لَوْ كَانَ عَرَضًا قَرِيبًا وَسَفَرًا قَاصِدًا لَّاتَّبَعُوكَ وَلَٰكِن بَعُدَتْ عَلَيْهِمُ الشُّقَّةُ ۚ وَسَيَحْلِفُونَ بِاللَّهِ لَوِ اسْتَطَعْنَا لَخَرَجْنَا مَعَكُمْ يُهْلِكُونَ أَنفُسَهُمْ وَاللَّهُ يَعْلَمُ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ
Bu doonoon alal juy xoy-xoyi walla muy tukki bu gàtt, kon ñu toppoon la ; waaye ba mu doonee ab xare, ñangay giñ naan : “Bu nu ko mënoon, kon dananu génn ànd ak yaw dem jaay seen bakkan.”. Te Yàlla xam na ne dañuy fen.
43عَفَا اللَّهُ عَنكَ لِمَ أَذِنتَ لَهُمْ حَتَّىٰ يَتَبَيَّنَ لَكَ الَّذِينَ صَدَقُوا وَتَعْلَمَ الْكَاذِبِينَ
Yàlla baal na la li nga leen may dingalul ñu toog te nattuwooleen ba xam ña ca wax dëgg ak ña ca di ay fenkat.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
41Aaya

Tekki — At-Tawba 41

Simoore At-Tawba Aaya 41 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen di xeex ci woyofaay ak ci dIisaay [sawar ak…

Simoore Aaya 41/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 39–43. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers