Simoore Al-Infitar ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Infitar ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (19 Aaya — مكية). Al-Infitar Dégg, Al-Infitar Tekki, Al-Infitar mp3, Al-Infitar pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Infitar

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
إِذَا السَّمَاءُ انفَطَرَتْ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Saa su asamaan si dogee, Maa ngi giñ
وَإِذَا الْكَوَاكِبُ انتَثَرَتْ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
ak saa su biddew yi tasaaroo,
وَإِذَا الْبِحَارُ فُجِّرَتْ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
ak saa su géej yi taqaloo,
وَإِذَا الْقُبُورُ بُعْثِرَتْ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
ak saa su bàmmeel ya jaxasoo,
عَلِمَتْ نَفْسٌ مَّا قَدَّمَتْ وَأَخَّرَتْ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
bakkan bu Yàlla sàkk xam na la mu jëkkoona def ak la mu mujja def.
يَا أَيُّهَا الْإِنسَانُ مَا غَرَّكَ بِرَبِّكَ الْكَرِيمِ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Éy yaw nit ! Ana lan moo la fàbbi ci sa mbiru Boroom, bu Tedd bi,
الَّذِي خَلَقَكَ فَسَوَّاكَ فَعَدَلَكَ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
(sa Boroom) bi la bind yemale la, jekkal la ?
فِي أَيِّ صُورَةٍ مَّا شَاءَ رَكَّبَكَ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Moo la defar ca na mu ko soobe.
كَلَّا بَلْ تُكَذِّبُونَ بِالدِّينِ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Déet... ! [ak lu mana xew] yéen a ngay weddi bis pénc ba ;
وَإِنَّ عَلَيْكُمْ لَحَافِظِينَ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
te am na ay wattukat yu nekk ci seen kaw,
كِرَامًا كَاتِبِينَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
yu tedd yuy bind,
يَعْلَمُونَ مَا تَفْعَلُونَ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
yuy xam li ngeen di def.
إِنَّ الْأَبْرَارَ لَفِي نَعِيمٍ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Ñu baax ñaa ngi ca biir àjjanay xéewal,
وَإِنَّ الْفُجَّارَ لَفِي جَحِيمٍ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
te itam kàccoor ya ñoom, ña nga ca biir safara jahiim
يَصْلَوْنَهَا يَوْمَ الدِّينِ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
danañu ca xoyomoo, bu bis Pénc baa
وَمَا هُمْ عَنْهَا بِغَائِبِينَ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
te ñoom manuñu koo wuute.
وَمَا أَدْرَاكَ مَا يَوْمُ الدِّينِ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Ana lu lay xamal luy bis Pénc ?
ثُمَّ مَا أَدْرَاكَ مَا يَوْمُ الدِّينِ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Ak lu lay xamal waay, luy bis Pénc ba ?
يَوْمَ لَا تَمْلِكُ نَفْسٌ لِّنَفْسٍ شَيْئًا ۖ وَالْأَمْرُ يَوْمَئِذٍ لِّلَّهِ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
moo di bis ba benn bakkan dul manal moroomam tus. Te bu keroogee, Yàlla rekk ay joxe ndigël yi.
← 81 Al-Infitar (82/114) 83 →
Jàng Simoore Al-Infitar ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

82الإنفطار Al-Infitar 📚 19 Aaya مكية

Aaya bu ne – Simoore Al-Infitar — 19 Aaya




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers