Simoore Al-Layl ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Layl ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (21 Aaya — مكية). Al-Layl Dégg, Al-Layl Tekki, Al-Layl mp3, Al-Layl pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Layl

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
وَاللَّيْلِ إِذَا يَغْشَىٰ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Ci guddi gi saa su muuree lépp ! maa ngi giñ
وَالنَّهَارِ إِذَا تَجَلَّىٰ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Ak ci bëcëg bi saa su leeree !
وَمَا خَلَقَ الذَّكَرَ وَالْأُنثَىٰ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Ak ci ki sàkk, góor ak jigéen !
إِنَّ سَعْيَكُمْ لَشَتَّىٰ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Seen jëf wuute na.
فَأَمَّا مَنْ أَعْطَىٰ وَاتَّقَىٰ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Képp kuy joxe te ragal (Yàlla)
وَصَدَّقَ بِالْحُسْنَىٰ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
te mu dëggël yoolub àllaaxira
فَسَنُيَسِّرُهُ لِلْيُسْرَىٰ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Dananu ko jàppandalal yoon wu yomb wa.
وَأَمَّا مَن بَخِلَ وَاسْتَغْنَىٰ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Képp ku nay, te dumóoyu boroomam,
وَكَذَّبَ بِالْحُسْنَىٰ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
te muy weddi yoolub àllaaxira,
فَسَنُيَسِّرُهُ لِلْعُسْرَىٰ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Dananu ko jàppandalal yoon wu jafe wa,
وَمَا يُغْنِي عَنْهُ مَالُهُ إِذَا تَرَدَّىٰ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
te alalam du ko jariñ dara saa su ñu ko mbaqee (Safara).
إِنَّ عَلَيْنَا لَلْهُدَىٰ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Gindee, nun la war ;
وَإِنَّ لَنَا لَلْآخِرَةَ وَالْأُولَىٰ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
te Noo moom, dundug àddinaak àllaaxira.
فَأَنذَرْتُكُمْ نَارًا تَلَظَّىٰ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Xuppnaa leen ci Safara wuy bérëx-bérëxi
لَا يَصْلَاهَا إِلَّا الْأَشْقَى ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
ku texedi ka rekka cay xoyomu,
الَّذِي كَذَّبَ وَتَوَلَّىٰ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
kay weddi tey dumóoyu ;
وَسَيُجَنَّبُهَا الْأَتْقَى ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
dees na ko soril ñu ragal Yàlla ña,
الَّذِي يُؤْتِي مَالَهُ يَتَزَكَّىٰ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
kay joxe alalam ngir selal
وَمَا لِأَحَدٍ عِندَهُ مِن نِّعْمَةٍ تُجْزَىٰ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
te amul genn xéewal gu ñuy faye kenn ca moom,
إِلَّا ابْتِغَاءَ وَجْهِ رَبِّهِ الْأَعْلَىٰ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Lu dul sàkku jëmm Boroomam ja gëna Kawe.
وَلَسَوْفَ يَرْضَىٰ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Te, xalset naa gëram (moom ka def noona) !
← 91 Al-Layl (92/114) 93 →
Jàng Simoore Al-Layl ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

92الليل Al-Layl 📚 21 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers