11 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮉﮊ
93:1 Ci yoor-yoor bi ! Maa ngi giñ
ﮋﮌﮍﮎ
93:2 ak ci guddi gi bu kukkee ! ne
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
93:3 Sa Boroom bàyyiwula, te bañu la.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
93:4 Te àllaaxira, mooy, gën ci Yaw àddina de.
ﮛﮜﮝﮞﮟ
93:5 Te sa Boroom dana la jox, ba nga doyal.
ﮠﮡﮢﮣﮤ
93:6 Moo ndax fekku la ngay jirim ? Mu fat la !
ﮥﮦﮧﮨ
93:7 Ak it ndax fekku la nga réer ? Mu gindila.
ﮩﮪﮫﮬ
93:8 Moo ndax fekku la nga ñàkk ? Mu woomalal la.
ﮭﮮﮯﮰﮱ
93:9 Jirim, nag, bu ko di xorñooñal.
ﯓﯔﯕﯖﯗ
93:10 Te laajkat it, bu ko di delloo.
ﯘﯙﯚﯛﯜ
93:11 Te it na ngay waxtaane, sa xéewalu Boroom.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 29, 2026

Don't forget us in your sincere prayers