Simoore Taha
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Taha pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Taha pdf Wolof — Wàcce Simoore Taha Tekki. Taha (Meccan) 135 Aaya.
Related
- Taha TekkiWolof
- Taha mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Taha

ﭵﭶ
Taa Haa.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Wàccewunu Alxuraan jii ci yaw ngir nga texeedi [tiis],
ﭽﭾﭿﮀﮁ
[waaye] Danu koo wàcce ngir muy waar ñi ragal Yàlla,
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
dafa wàcc bawoo ca Ka bind suuf si ak asamaan yu kawe ya.
ﮉﮊﮋﮌﮍ
Yàllaa nga yemoo ca Gàngunaay ga [Aras].
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Moo moom li nekk ci asamaan yi ak ci suuf si ak li nekk ci seen diggante, ak li nekk ci ron déeley suuf si.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Soo dee jóoru say wax it, Moom xam na mbóot ak la gën a nëbbu.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Yàlla mooy Yàlla ! Amul jeneen yàlla ju dul Moom ! Moo moom tur yi gën a rafet.
ﮭﮮﮯﮰﮱ
Moo ndax xam nga xibaari Muusaa ?
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Ba mu gisee aw safara, mu ne njabootam : “Xaarleen ma fii ! Lële ma séen dey aw safara la ; Amaana ma jële fa aw xal, walla ma fekk fa ku ma gindi [teg ma ci yoon]”.
ﯦﯧﯨﯩﯪ
Ba mu agsee ci safara wa, mu am lu ko woo ne ko : “Éy Muusaa !
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Man maay sa Boroom. Summil say dàll : yaa ngi ci biir xur wu sell wu ñuy wax [Tuwaa].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
Dama laa tànn. Kon déggal li Ma lay soloo.
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Man mii maay Yàlla : amul jeneen yàlla ju dul Man. Nanga may jaamu, tey taxawal julli, di Ma màggal.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Te Bis-pénc ba daanaka ñëw na. Dama koo xaw a làq rekk ngir fey bakkan bu nekk la muy jëf.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
[Kon farlul ba] képp ku gëmul tey topp bànneexam, bañ laa gàllankoor ngay alku.
ﭹﭺﭻﭼﭽ
Waaw Muusaa, li nekk ci sa loxo ndeyjoor lan la ? ”
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Mu wax ne : “Samaw yet la, dama ciy sukkóotu, di ci waññ samag jur ak yeneeni mbir”.
ﮌﮍﮎﮏ
[Yàlla ne ko] : “Sànni ko yaw Muusaa”.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Mu sànni ko : ndekete yoo jaan a ngay bélaw-bélawi.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Mu ne ko : “Jël ko : Dananu ko delloo na mu meloon, bul ragal.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Te nga dugal sa loxo ci sa biir poqotaan : mu génn weex tàll lool, di geneen kéemaan
ﮫﮬﮭﮮﮯ
[Lii lépp] Danu la koo waajale ngir won la ci Sunu kéemtaan yu màgg yi.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Demal ca Firawna, moom dafa beew.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
[Muusaa] ne ko : “Yaw sama Boroom, leeralal ma sama dënn [mën a dékku lu bari],
ﯝﯞﯟﯠ
te nga yombalal ma sama soloo sii,
ﯡﯢﯣﯤﯥ
te nga leeral samaw làmmiñ,
ﯦﯧﯨ
ba ñu mën a xam samay wax,
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
te nga may ma, defal ma ci samag njaboot ku may jàppale :
ﯯﯰﯱ
Te mu far doon sax Haaruuna, sama mbokk,
ﯲﯳﯴﯵ
Doolel ma ci moom !
ﯶﯷﯸﯹ
te boole ko ci samay mbir,
ﯺﯻﯼﯽ
ngir nu mën di la sàbbaal lu bari,
ﯾﯿﰀ
di La tuddu, di la fàttaliku lu bari.
ﰁﰂﰃﰄﰅ
Te Yaa gën a xam sunuy mbir, Yaa nu gën a gis”
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
[Yàlla] tontu ne : “Li nga doon laaj [di ko ñaan] am nga ko.
ﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Te it, wér na ne xéewaloon Nanu la feneen,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
Ba Nu déggalee sa yaay la Nu ko déggal :
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ne ko na sànni liir ba ca kees ga, sànni kees ga ca ndox ma, ndox ma dana ko gëq ca tefes ga ; samab noon, dib noonam moo koy jël”. Yaw Muusaa, defal naa la Samag cofeel, te it ci Samag càmm nga màgge.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
[Fàttalikul] ba sa jigéen ba di dox te naan leen : “Ndax duma leen tegtal ci ku ko mën a yar ? ” Ba tax Nu delloo la fa sa yaay ngir xelam dal, mu bañ a yàq. Nga reyoon bakkan, Nu musal la ca mbamb ma ; Nu fitnaaloon la, nattu la lu yàgg. Nga demoon fa waa Madiyaana ba am fa ay at. Ba tey jii yaa ngi nii ci àpp bu ma dogaloon.
ﮖﮗﮘ
Maa la bind ngir Sama mbiri bopp.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Demal yaak sa mbokk ngeen yor samay kàddu ; te buleen sàggane di Ma jaamu.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Demleen yéen ñaar fa Firawna : ndax moom dafa beew.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Nangeen wax ak moom wax ju nooy. Ndax amaana mu waaru walla mu ragal Yàlla ?
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Ñu ne Ko : "Yaw sunu Boroom, nun dey danuy ragal, bu nu demee fa moom, mu jaay nu doole”.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
[Yàlla]ne leen : “Buleen ragal, yéen laa àndal : Maa ngi dégg di gis.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Demleen fa Moom ne ko : “Ñun ñaar ñii ndawi Yàlla lanu. Delloo nu waa Banii-Israayiila [ñi nga jàppe jaam] te buleen mbugalati. Ndax indi nanu ci yaw ay kàddu yu jóge fa sa Boroom. Te jàmmi Yàlla nay nekk ca kay topp njub ga !
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Xamalees nanu ne : képp ku weddi te dummóoyu [kàdduy Yàlla], kooka mbugal dana ko dal”.
ﰉﰊﰋﰌﰍ
[Firawna] ne leen : “Waaw yéen ñaar kan moo di seen Boroom ? ”
ﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
Mu ne ko : “Sunu Boroom, Moo sos mbindéef yépp, te Mooy gindee”.
ﰘﰙﰚﰛﰜﰝ
[Firawna] ne ko : “Waaw xeet ya jiitu woon, ñoom luy xala doon seenub àtte ? ”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Mu ne ko : “Seeni mbir a nga ca Téere ba fa sa Boroom. Sama Boroom du juum, du fàtte.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Sama Boroom bi nga xam ne Moo leen defal suuf si laltaay [maasale ko], defal leen ci ay yoon [ngeen di jokkoo] ; Mu wàcce am ndox mu bawoo asamaan, ñu di ca génne ay xeeti gàncax yu wuute.”
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
“Lekk-leen te sàmm seenug jur”. Ay kéemaan a ngi ci loolu, ñeel aw nit ñu am xel.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
[Ci suuf si] la Nu leen binde, ci la Nu leen di delloo, te ci la Nu leen dellu génnewaat weneen yoon.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Won Nanu ko Sunu kéemaan yépp mu lànk weddi [Yàlla].
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Mu daldi ne : “Waaw yaw Muusaa, danga noo bëgg génne ci sunuy suuf ak sa njibar gi ?
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Dananu la indil njibar gu ni mel. Nu sàkk bis ak barab te kenn bañ koo wuute ci nun ñépp”.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Mu wax ne : “Kon jàpp nanu bis ba nu daan daje, di ca fo. Ca yoor-yoor ba”.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Firawna daldi dëddu, dem dajale ay pexeem, daldi dellusiwaat.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Muusaa ne leen : “Tuskare ngeen ! Fexeleen ba bu leen duural Yàlla ay fen : kon Mu toroxal leen de. Te duurkat sooy nañu”.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Ñu xëccoo ca seen biir, gise, déeyoo di yum-yumi.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Ñu daldi wax ne : “Ñaar ñii dey, ay jibar lañu, li leen tax a jóg moo di génne leen ci seenum réew, not leen ba fàwwu.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Kon booleleen seeni pexe, doon jenn jëmm bisub tey bii. Ku not rekk raw nga ba fàwwu”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Ñu ne ko : "Yaw Muusaa, benn nga jëkk a sànni, walla nun nooy jëkk a sànni ? ”
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Muusaa ne leeen] : “Sànnileen”. Ñu daldi sànni seeni yet ak i buum ca seenug njibar mu mel ni yëf yaa ngay dox di yëngatu.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Muusaa xaw a amum tiit ci boppam.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Nu ne ko : “Bul ragal [yaa leen mën], yaa leen fare kaw.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Sànnil li ci sa loxo ndeyjoor [yet wa] ; li ñuy wone lépp pexey njibarkat doŋŋ la ; te njibarkat moom fàwwu ay tappaleem naaxsaay”. Ba mu ko sànni, yet waa daldi wann yooya yépp
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Njibarkat yépp far daldi tëdd ci suuf sujjóot, daldi ne : “Gëm nanu bis niki tey Yàllaay Muusaa ak Haaruuna”.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
[Firawna] ne leen : “Gëmoon ngeen ko la jiitu lii. [Xam naa ne] Muusaa mooy kàndiŋ mi leen jàngal ag njibar. Danaa dàgg seeni tànk ak seeni yoxo cig jàllawle, danaa leen daaj ci dàtti tàndarma yi, dangeen xam kan ci nun moo gën a mettile te gën a tarle mbugal”.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ñu ne ko : “Yàlla mi ñu bind ak kàddoom yii Mu nu indil moo nu la gënal fàwwu. Dogalal loo bëgg a dogal. Waaye nag say àtte moom àddina rekk la yem.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Nun dey gëm nanu sunu Boroom ngir mu jéggal nu sunuy bàkkaar, ak njibar gii nga nu jaay doole ba tax nu def ko”. Te Yàlla Moo gën te Mooy des.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Kuy saay-saay ba dem fa Boroomam, dana tàbbi Safara te du fa dee du fa dundu.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Kuy gëm Yàlla ak a def u yiw ba dem fa Yàlla, ñooña danañu am ay daraja yu kawe,
ﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞ
ay àjjana yu sax yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel. Loolu moo di peyug képp kuy sellal.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Digal Nanu Muusaa [soloo ko]ne ko : “Nga rañaan ak sama jaam ñi, nanga leen sàkkal aw yoonu suuf wu wow ca biir géej ga : bul ragal ku lay dab walla ngay tiit”.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Firawna ak ug xareem topp leen. Duus ya labal leen.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Firawna sànk na aw nitam, te farul gindiku.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Éy yéen waa giir Banii-Israayiil, musal Nanu leen ci seenub noon, Nu digeek yéen fa wàllug ndeyjooru tundu Sinaay wa. Nu wàcceel leen yàpp.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
“Lekk-leen ci lu teey [sell] li Nu leen wërsëgale te buleen ca beew, [bu ngeen beewee], kon Sama mer day wàcc ci seen kaw : te képp ku Sama mer wàcc ci kawam, sànku na.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Te moo ne Man dey ab Jéggalaakoon laa ci képp ku tuub, te gëm, te jëf u yiw tey jubal”.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
“Waaw Muusaa, ana lan moo tax nga jiitu saw nit ? ”
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Mu ne ko ñoom dey ñanga ca sama ginnaaw. Ma yàkkamtee agsi ci Yaw ba am sa ngërëm.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
[Yàlla] ne ko : “Nattu woon Nanu saw nit sa ginnaaw. Saamiriyu ñëw moom sànk leen”.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Muusaa dellu fa nitam ña mer bay fuur ; ne leen : "Yéen samaw nit, ndax Yàlla digu leen woon dig wu rafet ? Walla dig wa dafa yàgg ? Walla dangeen bëgg merum Yàlla wàcc ci seen kaw, ba tax ngeen wuute samag dig ay yéen ? ”
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Ñu ne ko : “Wuutewuñu sab dig. Waaye danu noo nax sànniloo nu takkaay ya ; ca noona la ko Saamiriyu sànnee ca safara wa.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Daldi leen cay génneel aw sëll [nag]. Ne leen : “Mooy seen yàlla ; ñu daldi fàtte Yàllay Muusaa” !
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Moo ndax dañoo gisul ne bu ñul wax ak moom du toontu, te mënuleen a lor, mënuleen a jariñ dara ?
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Aaruuna moom waxoon na leen bu njëkk ne leen: "Yéen samaw nit, lii ngeen nekk aw sànje la. Waaye seen Boroom moo di Yërëmaakoon bi. Toppleen ma te wéyal samay ndigal”.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Ñu ne ko : “Dunu fi jóge mukk ba ba Muusaa di dellusi fi nun”.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
[Ba Muusaa dellusee] ne : “Yaw Aaruuna, lan moo tere woon nga waar leen ba ñu sànkoo.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Danga maa toppatul walla dangaa mooy léegi samay ndigal ? ”
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
[Aaruuna] ne ko : “Doom ndey, bul bipp samab sikkim mbaa sama kawari bopp. Damaa ragaloon nga naan ma : “Féewale nga giiru Bani-Israayiila, toppoo sama ndigal, [lii rekk la]”.
ﮩﮪﮫﮬﮭ
Muusaa ne : “Ayca Saamiriyu, waxal book ? ”
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Mu ne : “Gis naa lu ñu gisul : ma daldi ŋoor ci suufi jeexiti Yonent bi, daldi koy sànni li am am. Loolu la ma sama xel joxoon”.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
[Muusaa] daldi ne ko : “Ayca, demal. Toppal sa një : “Dootoo jegeñ kenn ! ” Te am nga dig boo dul wuute. Te xoolal sa yàlla ji nga daan jaamu. Dananu ko lakk, sànni ko ca ndox ma.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
[Seen Yàlla tigi] mooy Yàlla jenn ja, amul jeneen ju dul Moom. Moo xam lépp.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Noonu la Nu lay nettalee xew-xewi ña jiitu woon. Indil naa la njàng mu bawoo fi Man.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Ku ko dummóoyu [kàddu yooyu], bu Bis-pénc baa, dana yenu ay bàkkaar [mbugal] ;
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
te dañu cay béelbu keroo gee [Bis-pénc ba], ndaw yen bu bon,
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
bis ba ñu walee [ëf] buftu ba, bis boobee, Dananu pang tooñkat ya ñuy fér-féri [ndax tiit] !
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Ñuy déeyante ca seen biir naan : “Yéen kat fukki fan doŋŋ ngeen am àddina” !
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Nun [Yàlla] Noo gën a xam la ñuy wax, far ka leen gën a kaanu naan : “Aa yéen kat benn fan doŋŋ ngeen am àddina”.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Ñii nga lay laaj ci dundi doj yi [naka lay mujje]. Neel : “Yàlla dana leen moxoñe,
ﮘﮙﮚﮛ
bàyyi ko mu ne ag joor gu ne càndaŋ
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
dootoo gis ab nóox-nóox walla ab junni-junni, léppay maase nerr.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Ca Bis booba ñépp danañu topp wootekat ba ; kàddu yépp ne xuum [cëy Yàlla Yërëmaakoon bi]. Doofa dégg lu dul kuy dée [di wax ndànk].
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Bisub kerook, kenn du fa mën a ramm ku dul koo xam ne Yërëmaakoon baa ko ko digal te gërëm ay waxam.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Moo xam la jàll ak liy ñëwi, te kenn ci ñoom mënu koo peeg ci xam ko.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Loos yépp janoo nañu fa kanamu Yàlla, Muy dundu te taxawu lépp, te képp ku yenu na ag tooñ , [na ko wóor ne] sooy na bu kero gee.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Képp koo xam ne nag yaa ngay jëf u yiw te gëm, du ragal foofa ag tooñ [gu ñu koy tooñ], walla ku koy sërxal.
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Noonu Lanu wàccee Alxuraan ci làmmiñu araab, biral ci lool ag tëkku, ndaxtele amaana ñu ragal Yàlla walla ñu jàjju [fàttaliku xalaat]?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Yàlla Buur ba di dëgg, kawe na ! Bul yàkkamtee tasaare Alxuraan ji tey jiitu soloo ga. Waxal ne : "Yaw sama Boroom dolli ma xam-xam ! ”
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Fasantee woon Nanu ak Aadama ab dig ca la jiitu woon ; mu fàtte ; te taxu ko caa woo na farlu.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya ne leen : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñépp sujjóot ba mu des Ibliis, moom dafa lànk.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Nu wax ko ne ko : “Kii dey sab noon la yaak sa soxna. Farluleen ba bu mu leen génne Àjjana, [su ngeen génnee] da ngeen sonnu de.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
[Fii ci Àjjana] doo fi xiif, doo fi rafle,
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
doo fi yëg u mar, doo fi màggat”.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Séytaane daldi koy jax-jaxal [nëxal xelam] ne ko : "Yaw Aadama, ndax duma la tegtal garab guy tax nga am nguur gu dootul foq ? ”
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Ñu daldi cay lekk [garab ga]. Seen rafle wa daldi feeñ. Ñu tàmbalee witt ca xobi garab ya nekk Àjjana di ko làmboo. Aadama moy na ndigalu Boroomam, tooñ tàbbi.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Yàlla delloo cim xelam ba mu tuub, Mu daldi koy jéggal, Mu daldi it jubbanti ko.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Yàlla daldi ne leen : “Génnleen Àjjana, wàcc jëm suuf, ñennat ci yéen di noonoo ñeneen ña ca des. Dana am nag njub gu bawoo fi Man dikk ci yéen, képp ku topp Sama njub googu, du sànku, du sonn.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Képp ku ko dummóoyu, dana dundu dund gu metti, te buy dekki Bis-pénc ba gumba lay doon ñu gotti ko”.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
[Su ko defee] muy laaj naan : "Sama Boroom, lan moo tax nga pang ma may gumba te ca àddina ma doon gis ? ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
[Yàlla tontu] ne ko : “Noonu la la Sunuy kàddu dikkalee woon, nga sàggane ko, kon book tey yaw itam kenn du la faale”.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Noonu la Nuy feye ña ëppal [xaabaabal] te gëmuñu seen kàdduy Boroom [ay màndargaam]. Te mbugalum àllaaxira moo gën a tar te gën a yàgg.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Ndax dafa leerul ci seen bopp te aka bari ay xeet yu Nu alag ca ña leen jiitu woon te tey ñuy dox ci kaw fa ñu dëkkoon ? Loolu war naa mën a waar ñu am xel [te di ko jariñoo] !
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Su fekkoon ne du dig bu ko Yàlla sàkkal, kon seen mbugal fii lay tàmbalee.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Nanga muñ li ñuy wax te nga sàbbaal ci cantug sa Boorom balaa jant bi di fenk ak balaa muy so, ak guddi gi ak subaak ngoon. Soo bëggee maare [gërëm Yàlla te am xel mu dal] :
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Bul wékk say gët ci li Nu leen wërsëgal ci ay jabar ak alali àddina, ngir sànk leen ci doŋŋ la. Sa peyug Boroom moo gën [fuuf] te moo gën a sax.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Nanga digal sag njaboot ñuy julli, te nanga saxoo muñ. Tegunu la wut ub dundu : Nun noo warloo sab dund. Ña ragal Yàlla ñoo ëppug muj.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Ñuy wax naan : “Lan moo tax indilunu kiiman gu bawoo ca Boroomam ? Moo ndax xalam mujjug ña leen jiitu woon da leen a doyul am njàng ?
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Bu fekkoon ne Danu leen a mbugal la ko jiitu, kon ñuy wax naan : "Cëy Yàlla soo yónni woon ab Yonent ci nun, kon dananu topp say ndigal bala noo torox ak a tuskare”.
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Neel : “Ñépp a ngay xaar. Xaarleen yéen it ! Dangeen xam ñan ñoo jaaroon ca yoon wu jub wa xocc ak ana ñan ñoo gënoon a gindiku”.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







