Sad · 26/88
Tekki Waxtaan — Sad
يَا دَاوُودُ إِنَّا جَعَلْنَاكَ خَلِيفَةً فِي الْأَرْضِ فَاحْكُم بَيْنَ النَّاسِ بِالْحَقِّ وَلَا تَتَّبِعِ الْهَوَىٰ فَيُضِلَّكَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَضِلُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ لَهُمْ عَذَابٌ شَدِيدٌ بِمَا نَسُوا يَوْمَ الْحِسَابِ ۝٢٦
Yaa Daawoodu innaa ja`alnaaka khaleefatan fil ardi fahkum bainan naasi bilhaqqi wa laa tattabi`il hawaa fayudillaka `an sabeelil laah; innal lazeena yadilloona `an sabeelil laah; lahum `azaabun shadeedum bimaa nasoo Yawmal Hisaab
📖 Tekkim Wolof
“Éy yaw Daawuda, def Nanu la ngay sunu kuutlaay ci kaw suuf si. Na ngay àtte diggënte nit ñi ci dëgg te bul topp mukk bànneex : su ko defee dana la féewale ak yoonu Yàlla”. Te ñiy féewook yoon danañu am mbugël mu tar mitti ngir lañu fàtte bisub wañoo ba (Bis Pénc ba).
🎧 Dégg

📜 Aaya 24-28 — Sad

24قَالَ لَقَدْ ظَلَمَكَ بِسُؤَالِ نَعْجَتِكَ إِلَىٰ نِعَاجِهِ ۖ وَإِنَّ كَثِيرًا مِّنَ الْخُلَطَاءِ لَيَبْغِي بَعْضُهُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ إِلَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ وَقَلِيلٌ مَّا هُمْ ۗ وَظَنَّ دَاوُودُ أَنَّمَا فَتَنَّاهُ فَاسْتَغْفَرَ رَبَّهُ وَخَرَّ رَاكِعًا وَأَنَابَ ۩
[Daawuda] ne ko : “Moo la tooñ ci laaj gi mu la laaj sam xar ngir dollee koy xaram”. Te ñiy faral a ànd di liggéey bariyaana ba ñennat ci ñoom jaayee doole ña ca des, ba mu des ña gëm tey def yiw – te ñooña ñu néew lañu ci. – Daawuda daldi xam nag ne dañu ko doon nattu. Mu daldi rot (rukuu) sëgg jàpp ci ay wóomam delluwaat ca Boroomam.
25فَغَفَرْنَا لَهُ ذَٰلِكَ ۖ وَإِنَّ لَهُ عِندَنَا لَزُلْفَىٰ وَحُسْنَ مَآبٍ
Nu daldi koy jégël loola. Te amna daraja ju Nu jige ak wàccuwaay wu jekk.
26يَا دَاوُودُ إِنَّا جَعَلْنَاكَ خَلِيفَةً فِي الْأَرْضِ فَاحْكُم بَيْنَ النَّاسِ بِالْحَقِّ وَلَا تَتَّبِعِ الْهَوَىٰ فَيُضِلَّكَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَضِلُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ لَهُمْ عَذَابٌ شَدِيدٌ بِمَا نَسُوا يَوْمَ الْحِسَابِ
“Éy yaw Daawuda, def Nanu la ngay sunu kuutlaay ci kaw suuf si. Na ngay àtte diggënte nit ñi ci dëgg te bul topp mukk bànneex : su ko defee dana la féewale ak yoonu Yàlla”. Te ñiy féewook yoon danañu am mbugël mu tar mitti ngir lañu fàtte bisub wañoo ba (Bis Pénc ba).
27وَمَا خَلَقْنَا السَّمَاءَ وَالْأَرْضَ وَمَا بَيْنَهُمَا بَاطِلًا ۚ ذَٰلِكَ ظَنُّ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ فَوَيْلٌ لِّلَّذِينَ كَفَرُوا مِنَ النَّارِ
Te bindunu asamaan ak suuf ak li nekk ci seen diggënte cig neen. Loolu la yéefar ya njortu. Te yéefar yaa ngaay tuskare ca biir safara !
28أَمْ نَجْعَلُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ كَالْمُفْسِدِينَ فِي الْأَرْضِ أَمْ نَجْعَلُ الْمُتَّقِينَ كَالْفُجَّارِ
Moo ndax dañuy jëflaantéek yàqkat yi nekk ci suuf ? walla danuy jëflaantéek ña ragal Yàlla kem ni ñuy jëflaantéek kàccoor yi ?
SadFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
26Aaya

Tekki — Sad 26

Simoore Sad Aaya 26 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Éy yaw Daawuda, def Nanu la ngay sunu kuutlaay ci…

Simoore Aaya 26/88 — Sad ص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Sad Dégg, Sad Tekki, Sad mp3, Sad pdf. Aaya 24–28. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers