88 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
38:1 Saad. Maa ngi giiñ ci Alxuraan, miy boroom tur ci ne :
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
38:2 Ña weddi ña nga cag rëy-rëylu ak kaŋ-kaŋ !
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
38:3 Aka bari ñu nu faagaagal ca ña leen jiitu woon, ñu daan yuuxu, walla te du ñu man a raw?
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
38:4 (Waa Màkka) daana yéeme ci waaraatekat bii leen digal te bokk ci ñoom, yéefar ya daan wax naan : “Kii dey ab njibarkat la bu di ab fenaakoon,
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
38:5 Moo ndax dafa bëgg a def Yàlla yii muy jenn Yàlla ? Aa lii dey mbir mu yéeme la”.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
38:6 Kilifa ya ne leen : “Demleen, te muñ jàpp ci seen Yàlla yii : lii daal la nu bëgg.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
38:7 Nun masunoo dégg lii ci diine ji fi mujj wàcc (Iisaa) ; lii daal ay sos rekk la !
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
38:8 Nuy wax naan, ak ni nu tollu ndax ci moom la [Alxuraan] di wàcc? ” Li wer moo di yéefar yaa ngay sikki-sàkka ci sama Téere bi. Xanaa kay dañoo mosagul mbugël !
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
38:9 Walla ndabi yërmaandey sa Boroom tey Mayewaakoon, biy boroom Kàttan bi, da fa nekk ci ñoom.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
38:10 Walla dañoo moom nguurug asamaan yeek suuf si, ak li nekk ci seen diggënte? su fekkee ne looloo am kon nañu def pexe ci yéeg ci !
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
38:11 Ak nu seeni xarekat man a tollu ak ña leen di jàppale, danuy nërméelu !
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
38:12 ña leen fi jiitu woon, weddi woon nañu ña di nitu Nooh, ak Aad ak Firawna ma doon boroom dëx (tabax yu rëy),
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
38:13 k Samuud, ak nitu Lóot, ak waa Aykata, (ñoom ñépp weddi woon nañu seeni yonnent). Te ñoom ñoo di jàppalekat ya (farandoo ya).
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
38:14 Ñoom ñépp weddi woon yonnent ya. Nu daldi leen mbugël !
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
38:15 Ñoom xaaruñu lu dul genn xaacu, gu dul tóllantiku wol.
ﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓ
38:16 Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, gaawal jox nu sunu wàll balaa wañoo ba”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
38:17 Muñal lii ñuy wax ; te ngay fàttaliku Sunu jaam ba Daawuda ma doonoon boroom doole, Moom ku faral daan dellu ci Boroomam la woon.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
38:18 Tàggataloon Nanu ko, tundi doj yi nu daan ànd ak moom, di sàbbaal Yàlla subaak ngoon,
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
38:19 picc yépp it dañuy dajaloo, di delloo kañ [Yàlla].
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
38:20 Dëgaralal Nanu ko nguuram jox ko xam-xamu xereñe ràññee ak xam-xamu àtte.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
38:21 Moo ndax xibaari xulóokat ya agsi na ci yaw ba ñu bëttee ñagub mbaar ma (mihraab ba) !
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
38:22 Ba ñu duggee fekk fa Daawuda, mu tiit ci ñoom. Nu wax ko ne : “Bul tiit ! Ñaari way xuloo la nu ; kenn ci nun dafay néewal dole ka ca des. Kon àtteel sunu diggënte ci dëgg, te it nga gindi nu teg nu ci yoon wu jub xocc wa.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
38:23 Kii nag sama mbokk la : amna juróom-ñeenti fukki xar ak juróom ñenenta, man ma am menn xar doŋŋ. Mu wax ma ne : “Naa ko ko jox” ; daldi wane lool ; doole ca ba ñuy waqante”.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
38:24 [Daawuda] ne ko : “Moo la tooñ ci laaj gi mu la laaj sam xar ngir dollee koy xaram”. Te ñiy faral a ànd di liggéey bariyaana ba ñennat ci ñoom jaayee doole ña ca des, ba mu des ña gëm tey def yiw – te ñooña ñu néew lañu ci. – Daawuda daldi xam nag ne dañu ko doon nattu. Mu daldi rot (rukuu) sëgg jàpp ci ay wóomam delluwaat ca Boroomam.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
38:25 Nu daldi koy jégël loola. Te amna daraja ju Nu jige ak wàccuwaay wu jekk.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖ
38:26 “Éy yaw Daawuda, def Nanu la ngay sunu kuutlaay ci kaw suuf si. Na ngay àtte diggënte nit ñi ci dëgg te bul topp mukk bànneex : su ko defee dana la féewale ak yoonu Yàlla”. Te ñiy féewook yoon danañu am mbugël mu tar mitti ngir lañu fàtte bisub wañoo ba (Bis Pénc ba).
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
38:27 Te bindunu asamaan ak suuf ak li nekk ci seen diggënte cig neen. Loolu la yéefar ya njortu. Te yéefar yaa ngaay tuskare ca biir safara !
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
38:28 Moo ndax dañuy jëflaantéek yàqkat yi nekk ci suuf ? walla danuy jëflaantéek ña ragal Yàlla kem ni ñuy jëflaantéek kàccoor yi ?
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
38:29 [Lii] ab Téere la bu Nuy wàcce ci yaw bu barkeel nak, ngir ñuy settantal ay laayaam ak it ngir woroomi xel yi man ciy fàttalikoo!
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
38:30 May Nanu Daawuda (doomam ja) Sulaymaan, - ndaw jaam bu baax ! – Ku daan dellu ca boroomam la.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
38:31 (Fàttalikul) ngoon ga, ñu ko gaarale fasi naari góor ya,
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
38:32 Sulaymaan dellu wax ne : “Cëy man, maa ngi fees dell ak bëgg (àddina sii) mu fàbbi maa ba jant bi so te fàttalikuwuma sama Boroom.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
38:33 Delloosil ma fas yi.”. Ñu delloosil ko ko mu dagg yeel ya ak doq ya.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
38:34 Nattu Nanu Sulaymaan ci nu sànni ca toogoom ba (jëmm ju nu wotte). Mu delluwaat, màggal Boroomam.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
38:35 Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, na nga ma jégal te may ma nguur goo xam ne kenn dootu ko am sama ginnaaw. Yaw yaay Mayaakoon bi”.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
38:36 Tàggatal Nanu ko ngelaw li, muy daw ci ndigëlam, ak fu mu jublu.
ﯥﯦﯧﯨﯩ
38:37 Tàggatal Nanu ko sayaane yi, ñu di ko tabaxal ak di ko nuural ci (ndox).
ﯪﯫﯬﯭﯮ
38:38 Ak ñeneen, ñu ñu lëkkële ak i njéng.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
38:39 “Lii mooy sunug may ; mayeel walla nga téye ko kenn du ko waññook yaw”.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
38:40 Te mooy am na daraja ju Nu jege ak wàccuwaay wu jekk.
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
38:41 Fàttalikul sunu jaam Ayyuuba , ba muy woo Boroomam naan ko : “Yaw sama Boroom Saytaane teg na ma coono ak i tiis”.
ﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
38:42 (Yàlla ne ko) dóoral sa tànk fi ci suuf : am ndox ngi nii mu sedd mu man a sangu neex a naan.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
38:43 Nu delloowaat ko njabootam joxaat ko lu na tollu, muy yërmande ju bawoo ci Nun ak fàttili woroom xel yi.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
38:44 “Ŋëbal sëqub ñax, te dóor ko ko (soxnaam sa). Te bul gàddu bàkkaarub ngiiñ”. Moom, muñkat la di jaam bu baax. Kuy farlu di dellu ci Boroomam la.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
38:45 Fàttalikul suñu jaam ña Ibraahiima, ak Ishaaq ak Yaaquub ? Woroomi kàttan la ñu woon ak i gis-gis (xel).
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
38:46 Noo leen ràññi woon ngir sellalug : fàttaliku bis pénc ba.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
38:47 Te ñoom, bokk nañu, ca tànnéef ya gën a ràññiku.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
38:48 Fàttalikul Ismaahiila ak Ilyaas, ak Suul kifli, ñoom ñépp ay tànnéef la ñu.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
38:49 Lii ag fàttali la. Te ne ñay ragal Yàlla, am nañu, wàccuwaay wu jekk,
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
38:50 Àjjanay Adan, seen wunt ya ne ŋàll ngir ñoom,
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
38:51 dañu fay, sóonu, di woo ay futéef yu bari ak i naan.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
38:52 Amnañu fa ay jigéen (jabar) ñu di ay lamsalkat, yu maase ay at.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
38:53 Lii mooy li Nu leen dégóon ci bisub wañoo ba.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
38:54 Lii moo di sunu xéewal gi te du jeex mukk.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
38:55 Yëgal it ne ! ñay bew am nañu wàccuwaay wu yées,
ﯞﯟﯠﯡﯢ
38:56 Mooy Safara su ñuy xoyomoo. ndaw kër gu bon !
ﯣﯤﯥﯦﯧ
38:57 Mi ngi nii ! Nu cay tokamtiku : ndox muy tàng ak a wañax,
ﯨﯩﯪﯫﯬ
38:58 ak yeneeni xeeti mbugël yu mu témbóol.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
38:59 Ñii ay mbooloo la ñu ñuy buuxanteek yéen, kenn dalaluleen. Te ñooy xoyomu ca Safara.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
38:60 Ñuy wax naan : “Yéen kay la kenn dul dalal, lii, Yéen la ñu ko waajal”. Te ndaw saxuwaay bu bon !
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒ
38:61 Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom na nga dolli, ki nu waajalal lii, mbugël muy fulandiku ca biir Safara ”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
38:62 “Ana lan moo xew ba gisunu fi gaa ya nu daan limaale ci saay-saay si ?
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
38:63 Moo ndax dañu leen ko daan tooñe walla danu làqu sunu gëm ? ”
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
38:64 Lii daal tigi mooy xulóob waa Safara
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
38:65 Waxal ne : “Man daal ab xuppekat laa. Te jenn Yàlla amul judul, Yàlla jiy jenn , Notaakoon ba,
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
38:66 Mooy Boroom asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggënte, te mooy boroom Kàttan gi, di Jégëlaakoon bi”.
ﭿﮀﮁﮂﮃ
38:67 Waxal ne : “Xibaar bu rëy la,
ﮄﮅﮆﮇ
38:68 waaye yéen dumóoyu ngeen ko.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
38:69 Amuma woon xam-xam ca xulóob kilifa ya gën a kawe.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
38:70 Li nu may soloo doonul lu dul ne man mii ab xuppe kat laa waaraatekat bu bir”.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
38:71 (Fàttalitul) ba sa Boroom waxee Malaaka ya ne leen : “Man de maa ngi sàkk mbindéef ci ban.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
38:72 Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, na ngeen daldi rot, sujuudal ko”.
ﮯﮰﮱﯓﯔ
38:73 Malaaka ya yépp daldi sujuud,
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
38:74 ba mu des Ibliis moom dafa rëy-rëylu bokk ca yéefar ya.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
38:75 (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujuud ci lii ma bind ci samay yoxo ? Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ”
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
38:76 “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci ban”.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
38:77 (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ;
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
38:78 te Samam rëbb dal na la ba baa saa di taxaw”.
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
38:79 “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”.
ﰋﰌﰍﰎﰏ
38:80 (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu,
ﰐﰑﰒﰓﰔ
38:81 ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”.
ﰕﰖﰗﰘﰙ
38:82 “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj loo ñoom ñépp,
ﰚﰛﰜﰝﰞ
38:83 ba mu des sa jaam ñiy sellal”.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
38:84 (Yàlla) daldi wax ne : “Maa ngi waat, ci dëgg ne dëgg laay wax,
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
38:85 Danaa feesal Safara ci yaw ak ña la topp ñépp”.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
38:86 Waxal ne : “Laajumaleen ci ag pey ; te it yanuwuma ci.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
38:87 [Alxuraan] jii daal ag fàttali la ñeel waa àddina si yépp.
ﭯﭰﭱﭲﭳ
38:88 Te dangeen xam ay xibaaram ci ndiir su yàggatul ! ”.

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers