An-Nisa · 45/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِأَعْدَائِكُمْ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَلِيًّا وَكَفَىٰ بِاللَّهِ نَصِيرًا ۝٤٥
Wallaahu a`lamu bi a`daaa`i-kum; wa kafaa billaahi waliyyanw wa kafaa billaahi naseera
📖 Tekkim Wolof
Yàllaa gën a xam seeni noon. Yàlla doy na te mat sëkk kilifa. Yàlla doy na te mat sëkk itam ndimbal.
🎧 Dégg

📜 Aaya 43-47 — An-Nisa

43يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَقْرَبُوا الصَّلَاةَ وَأَنتُمْ سُكَارَىٰ حَتَّىٰ تَعْلَمُوا مَا تَقُولُونَ وَلَا جُنُبًا إِلَّا عَابِرِي سَبِيلٍ حَتَّىٰ تَغْتَسِلُوا ۚ وَإِن كُنتُم مَّرْضَىٰ أَوْ عَلَىٰ سَفَرٍ أَوْ جَاءَ أَحَدٌ مِّنكُم مِّنَ الْغَائِطِ أَوْ لَامَسْتُمُ النِّسَاءَ فَلَمْ تَجِدُوا مَاءً فَتَيَمَّمُوا صَعِيدًا طَيِّبًا فَامْسَحُوا بِوُجُوهِكُمْ وَأَيْدِيكُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَفُوًّا غَفُورًا
Éy yéen ñi gëm ! Buleen jege ag julli te fekk ngeen màndi, ba ba ngeen di xam li ngeen di wax, bu ngeen laabul ci sobe it [buleen jëm ci julli] te ame janaba - ndeem fekkuleen ci yoon di tukki – ba ba ngeen di sangu [farata]. Bu ngeen woppee, walla ngeen nekkati ci tukki, mbaa ngeen jóge wanag wa, walla ngeen joteek jigéen ña [sëy] te amuleen ndox [mu mën a jàpp walla sangu], nangeen tiim ci suuf su laab, ngeen raay seen xar-kanam ak seeni yoxo. Yàlla, Baalekat la, Jéggalaakoon la.
44أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ أُوتُوا نَصِيبًا مِّنَ الْكِتَابِ يَشْتَرُونَ الضَّلَالَةَ وَيُرِيدُونَ أَن تَضِلُّوا السَّبِيلَ
Moo ndax gisoo ña ñu joxoon lenni Téere ba, ñu jënd ñoom ag réer, ba noppi nag yéen ngeen réere yoon wu jub wa ?
45وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِأَعْدَائِكُمْ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَلِيًّا وَكَفَىٰ بِاللَّهِ نَصِيرًا
Yàllaa gën a xam seeni noon. Yàlla doy na te mat sëkk kilifa. Yàlla doy na te mat sëkk itam ndimbal.
46مِّنَ الَّذِينَ هَادُوا يُحَرِّفُونَ الْكَلِمَ عَن مَّوَاضِعِهِ وَيَقُولُونَ سَمِعْنَا وَعَصَيْنَا وَاسْمَعْ غَيْرَ مُسْمَعٍ وَرَاعِنَا لَيًّا بِأَلْسِنَتِهِمْ وَطَعْنًا فِي الدِّينِ ۚ وَلَوْ أَنَّهُمْ قَالُوا سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا وَاسْمَعْ وَانظُرْنَا لَكَانَ خَيْرًا لَّهُمْ وَأَقْوَمَ وَلَٰكِن لَّعَنَهُمُ اللَّهُ بِكُفْرِهِمْ فَلَا يُؤْمِنُونَ إِلَّا قَلِيلًا
Am na ci Yahuud yi ñuy firi baat [kàddu] jële leen ca barab ya ñu nekkoon, tey wax naan : “Dégg nanu waaye bañ nanu waay”, ñu naan : “Déggal te kenn du la dégg”, yàq waxin wa [Raahinaa], ñaawal ko ak bëgg a yàq diine. Waaye bu ñu ne woon : “Dégg nanu te nangu nanu”, “Déggal”, te “Xool nu”, kon mu gën ci ñoom, te mooy la gën a jub. Waaye Yàlla rëbb na leen [sorel yërmaandeem] ña weddi ; ñu néew ci ñoom ñoo gëm.
47يَا أَيُّهَا الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ آمِنُوا بِمَا نَزَّلْنَا مُصَدِّقًا لِّمَا مَعَكُم مِّن قَبْلِ أَن نَّطْمِسَ وُجُوهًا فَنَرُدَّهَا عَلَىٰ أَدْبَارِهَا أَوْ نَلْعَنَهُمْ كَمَا لَعَنَّا أَصْحَابَ السَّبْتِ ۚ وَكَانَ أَمْرُ اللَّهِ مَفْعُولًا
Éy yéen ñi jotoon Téere, gëmleen lii Nu wàcce, di dëggal li ngeen yor, bala Noo marmaral ay xar-kanam wëlbati leen ñu jëm ginnaaw, walla Nu leen di rëbbu na ñu rëbbe woon ña jalgati woon ca gaawu ba. Ndigalu Yàlla ak mbiram jëfe la sant [du jaas].
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
45Aaya

Tekki — An-Nisa 45

Simoore An-Nisa Aaya 45 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàllaa gën a xam seeni noon. Yàlla doy na te…

Simoore Aaya 45/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 43–47. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers