Al-Maida · 40/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
أَلَمْ تَعْلَمْ أَنَّ اللَّهَ لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ يُعَذِّبُ مَن يَشَاءُ وَيَغْفِرُ لِمَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝٤٠
Alam ta`lam annal laaha lahoo mulkus samaawaati wal ardi yu`az zibu many-yashaa`u wa yaghfiru limany-yashaaa`; wallaahu `alaa kulli shai`in Qadeer
📖 Tekkim Wolof
Moo ndax dangaa xamul ne Yàlla Moo moom nguurug asamaan yeek suuf si ? Dana mbugal ku Ko soob, dana jéggal ku Ko soob. Te Yàlla mën na lu ne.
🎧 Dégg

📜 Aaya 38-42 — Al-Maida

38وَالسَّارِقُ وَالسَّارِقَةُ فَاقْطَعُوا أَيْدِيَهُمَا جَزَاءً بِمَا كَسَبَا نَكَالًا مِّنَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
Sàcc bu góor ak sàcc bu jigéen, dogleen seeni yoxo ñoom ñaar muy peyug la ñu fàggu, di mbugal mu tukkee ca Yàlla. Moom Yàlla Aji-not la, Aji-xereñ la.
39فَمَن تَابَ مِن بَعْدِ ظُلْمِهِ وَأَصْلَحَ فَإِنَّ اللَّهَ يَتُوبُ عَلَيْهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ku tuub ginnaaw ba mu tooñee, te mu sellal jëfam, Yàlla dana ko jéggal. Ndax Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
40أَلَمْ تَعْلَمْ أَنَّ اللَّهَ لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ يُعَذِّبُ مَن يَشَاءُ وَيَغْفِرُ لِمَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Moo ndax dangaa xamul ne Yàlla Moo moom nguurug asamaan yeek suuf si ? Dana mbugal ku Ko soob, dana jéggal ku Ko soob. Te Yàlla mën na lu ne.
41۞ يَا أَيُّهَا الرَّسُولُ لَا يَحْزُنكَ الَّذِينَ يُسَارِعُونَ فِي الْكُفْرِ مِنَ الَّذِينَ قَالُوا آمَنَّا بِأَفْوَاهِهِمْ وَلَمْ تُؤْمِن قُلُوبُهُمْ ۛ وَمِنَ الَّذِينَ هَادُوا ۛ سَمَّاعُونَ لِلْكَذِبِ سَمَّاعُونَ لِقَوْمٍ آخَرِينَ لَمْ يَأْتُوكَ ۖ يُحَرِّفُونَ الْكَلِمَ مِن بَعْدِ مَوَاضِعِهِ ۖ يَقُولُونَ إِنْ أُوتِيتُمْ هَٰذَا فَخُذُوهُ وَإِن لَّمْ تُؤْتَوْهُ فَاحْذَرُوا ۚ وَمَن يُرِدِ اللَّهُ فِتْنَتَهُ فَلَن تَمْلِكَ لَهُ مِنَ اللَّهِ شَيْئًا ۚ أُولَٰئِكَ الَّذِينَ لَمْ يُرِدِ اللَّهُ أَن يُطَهِّرَ قُلُوبَهُمْ ۚ لَهُمْ فِي الدُّنْيَا خِزْيٌ ۖ وَلَهُمْ فِي الْآخِرَةِ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Éy yaw Yonent bi ! Bula jëfi ñiy jëkkante di sóobu cig kéefar metti ; ci ña nga xam ne danañu wax ci seeni gimiñ ne : “Gëm nañu”, te seeni xol gëmul; ak ca ña nekk i yahuud, di dégluwaakoon i fen, di dégluwaakoon i ñeneen nit ñoo xam ne agsiwuñu ci yaw, dañuy soppi baat ba jële ko fa mu tëddoon. Danañu wax naan : “Bu ñu leen joxee lii, jël-leen ko, bu ñu leen joxul, moytuleen”. Ku Yàlla namm a fitnaal, doo ko mënal dara fa Yàlla. Ña nga xam ne Yàlla nammuleen a baal seeni xol, am nañu toroxtaane ci àddina ak mbugal mu rëy ca àllaaxira.
42سَمَّاعُونَ لِلْكَذِبِ أَكَّالُونَ لِلسُّحْتِ ۚ فَإِن جَاءُوكَ فَاحْكُم بَيْنَهُمْ أَوْ أَعْرِضْ عَنْهُمْ ۖ وَإِن تُعْرِضْ عَنْهُمْ فَلَن يَضُرُّوكَ شَيْئًا ۖ وَإِنْ حَكَمْتَ فَاحْكُم بَيْنَهُم بِالْقِسْطِ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُقْسِطِينَ
Dañuy déglu ay fen, di lekk lu araam, lu araam [lool]. Bu ñu la seetsee, nanga àtte seen diggante walla nga dëddu leen. Te sax boo leen dëddoo, duñu la mën a wàññi dara. Boo àttee, nanga àtte seen diggante ci maandute. Yàlla safoo na way-maandu ña.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
40Aaya

Tekki — Al-Maida 40

Simoore Al-Maida Aaya 40 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo ndax dangaa xamul ne Yàlla Moo moom nguurug asamaan…

Simoore Aaya 40/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 38–42. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers