Al-Maida · 39/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
فَمَن تَابَ مِن بَعْدِ ظُلْمِهِ وَأَصْلَحَ فَإِنَّ اللَّهَ يَتُوبُ عَلَيْهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٣٩
Faman taaba mim ba`di zulmihee wa aslaha fa innal laaha yatoobu `alaih; innal laaha Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Ku tuub ginnaaw ba mu tooñee, te mu sellal jëfam, Yàlla dana ko jéggal. Ndax Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 37-41 — Al-Maida

37يُرِيدُونَ أَن يَخْرُجُوا مِنَ النَّارِ وَمَا هُم بِخَارِجِينَ مِنْهَا ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ مُّقِيمٌ
Danañu bëgg a génn Safara, waaye duñu fa mën a génn. Am nañu fa mbugal mu sax dàkk.
38وَالسَّارِقُ وَالسَّارِقَةُ فَاقْطَعُوا أَيْدِيَهُمَا جَزَاءً بِمَا كَسَبَا نَكَالًا مِّنَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
Sàcc bu góor ak sàcc bu jigéen, dogleen seeni yoxo ñoom ñaar muy peyug la ñu fàggu, di mbugal mu tukkee ca Yàlla. Moom Yàlla Aji-not la, Aji-xereñ la.
39فَمَن تَابَ مِن بَعْدِ ظُلْمِهِ وَأَصْلَحَ فَإِنَّ اللَّهَ يَتُوبُ عَلَيْهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ku tuub ginnaaw ba mu tooñee, te mu sellal jëfam, Yàlla dana ko jéggal. Ndax Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
40أَلَمْ تَعْلَمْ أَنَّ اللَّهَ لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ يُعَذِّبُ مَن يَشَاءُ وَيَغْفِرُ لِمَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Moo ndax dangaa xamul ne Yàlla Moo moom nguurug asamaan yeek suuf si ? Dana mbugal ku Ko soob, dana jéggal ku Ko soob. Te Yàlla mën na lu ne.
41۞ يَا أَيُّهَا الرَّسُولُ لَا يَحْزُنكَ الَّذِينَ يُسَارِعُونَ فِي الْكُفْرِ مِنَ الَّذِينَ قَالُوا آمَنَّا بِأَفْوَاهِهِمْ وَلَمْ تُؤْمِن قُلُوبُهُمْ ۛ وَمِنَ الَّذِينَ هَادُوا ۛ سَمَّاعُونَ لِلْكَذِبِ سَمَّاعُونَ لِقَوْمٍ آخَرِينَ لَمْ يَأْتُوكَ ۖ يُحَرِّفُونَ الْكَلِمَ مِن بَعْدِ مَوَاضِعِهِ ۖ يَقُولُونَ إِنْ أُوتِيتُمْ هَٰذَا فَخُذُوهُ وَإِن لَّمْ تُؤْتَوْهُ فَاحْذَرُوا ۚ وَمَن يُرِدِ اللَّهُ فِتْنَتَهُ فَلَن تَمْلِكَ لَهُ مِنَ اللَّهِ شَيْئًا ۚ أُولَٰئِكَ الَّذِينَ لَمْ يُرِدِ اللَّهُ أَن يُطَهِّرَ قُلُوبَهُمْ ۚ لَهُمْ فِي الدُّنْيَا خِزْيٌ ۖ وَلَهُمْ فِي الْآخِرَةِ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Éy yaw Yonent bi ! Bula jëfi ñiy jëkkante di sóobu cig kéefar metti ; ci ña nga xam ne danañu wax ci seeni gimiñ ne : “Gëm nañu”, te seeni xol gëmul; ak ca ña nekk i yahuud, di dégluwaakoon i fen, di dégluwaakoon i ñeneen nit ñoo xam ne agsiwuñu ci yaw, dañuy soppi baat ba jële ko fa mu tëddoon. Danañu wax naan : “Bu ñu leen joxee lii, jël-leen ko, bu ñu leen joxul, moytuleen”. Ku Yàlla namm a fitnaal, doo ko mënal dara fa Yàlla. Ña nga xam ne Yàlla nammuleen a baal seeni xol, am nañu toroxtaane ci àddina ak mbugal mu rëy ca àllaaxira.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
39Aaya

Tekki — Al-Maida 39

Simoore Al-Maida Aaya 39 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ku tuub ginnaaw ba mu tooñee, te mu sellal jëfam,…

Simoore Aaya 39/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 37–41. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers