Al-An'am · 141/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
۞ وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَ جَنَّاتٍ مَّعْرُوشَاتٍ وَغَيْرَ مَعْرُوشَاتٍ وَالنَّخْلَ وَالزَّرْعَ مُخْتَلِفًا أُكُلُهُ وَالزَّيْتُونَ وَالرُّمَّانَ مُتَشَابِهًا وَغَيْرَ مُتَشَابِهٍ ۚ كُلُوا مِن ثَمَرِهِ إِذَا أَثْمَرَ وَآتُوا حَقَّهُ يَوْمَ حَصَادِهِ ۖ وَلَا تُسْرِفُوا ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُسْرِفِينَ ۝١٤١
Wa Huwal lazee ansha-a jannaatim ma`rooshaatinw wa ghaira ma`rooshaatinw wan nakhla wazzar`a mukhtalifan ukuluhoo wazzaitoona warrum maana mutashaabihanw wa ghaira mutashaabih; kuloo min samariheee izaaa asmara wa aatoo haqqahoo yawma hasaadihee wa laa tusrifoo; innahoo laa yuhibbul musrifeen
📖 Tekkim Wolof
Moom Yàlla Moo sos ay tooli gàncax guy law ci suuf si ak yuy jóg taxaw ; ak garabi tàndarma ak mbey yu meññeent ya wuute ; ak oliw ak garanaat yu niroo ak yu niroowul. Lekkleen seeni doom bu ñoree ; te nangeen génne asaka ja bis ba ngeen di watt [ngóob]. Te buleen yàq ndax Moom [Yàlla] safoowul yàqkat ya.
🎧 Dégg

📜 Aaya 139-143 — Al-An'am

139وَقَالُوا مَا فِي بُطُونِ هَٰذِهِ الْأَنْعَامِ خَالِصَةٌ لِّذُكُورِنَا وَمُحَرَّمٌ عَلَىٰ أَزْوَاجِنَا ۖ وَإِن يَكُن مَّيْتَةً فَهُمْ فِيهِ شُرَكَاءُ ۚ سَيَجْزِيهِمْ وَصْفَهُمْ ۚ إِنَّهُ حَكِيمٌ عَلِيمٌ
Ñu naan : “Li nekk ci biir jur gi dagan na ci sunuy góor waaye araam na ci sunuy jabar [jigéen ñi].”. Waay, bu dee lu médd, góor ak jigéen ñoo ci yem. Dana leen fey seeni duur, Moom dey [Yàlla] Ku xereñ la, Ku xam la.
140قَدْ خَسِرَ الَّذِينَ قَتَلُوا أَوْلَادَهُمْ سَفَهًا بِغَيْرِ عِلْمٍ وَحَرَّمُوا مَا رَزَقَهُمُ اللَّهُ افْتِرَاءً عَلَى اللَّهِ ۚ قَدْ ضَلُّوا وَمَا كَانُوا مُهْتَدِينَ
Ña rey seeni doom cig réer ngir ñàkk a xam, yàqule nañu booleek di araamal la leen Yàlla wërsëgal, lépp tegu ci kaw duural Yàlla. Ñoom réer nañu ba sànku te dootuñu gindiku.
141۞ وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَ جَنَّاتٍ مَّعْرُوشَاتٍ وَغَيْرَ مَعْرُوشَاتٍ وَالنَّخْلَ وَالزَّرْعَ مُخْتَلِفًا أُكُلُهُ وَالزَّيْتُونَ وَالرُّمَّانَ مُتَشَابِهًا وَغَيْرَ مُتَشَابِهٍ ۚ كُلُوا مِن ثَمَرِهِ إِذَا أَثْمَرَ وَآتُوا حَقَّهُ يَوْمَ حَصَادِهِ ۖ وَلَا تُسْرِفُوا ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُسْرِفِينَ
Moom Yàlla Moo sos ay tooli gàncax guy law ci suuf si ak yuy jóg taxaw ; ak garabi tàndarma ak mbey yu meññeent ya wuute ; ak oliw ak garanaat yu niroo ak yu niroowul. Lekkleen seeni doom bu ñoree ; te nangeen génne asaka ja bis ba ngeen di watt [ngóob]. Te buleen yàq ndax Moom [Yàlla] safoowul yàqkat ya.
142وَمِنَ الْأَنْعَامِ حَمُولَةً وَفَرْشًا ۚ كُلُوا مِمَّا رَزَقَكُمُ اللَّهُ وَلَا تَتَّبِعُوا خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ ۚ إِنَّهُ لَكُمْ عَدُوٌّ مُّبِينٌ
Am na ci jur gi yu mën a sëf, ak yu nekk i gëtt; lekkleen ci li leen Yàlla di wërsëgale, te buleen topp jeegoy Séytaane, moom Séytaane seenub noon la bu bir.
143ثَمَانِيَةَ أَزْوَاجٍ ۖ مِّنَ الضَّأْنِ اثْنَيْنِ وَمِنَ الْمَعْزِ اثْنَيْنِ ۗ قُلْ آلذَّكَرَيْنِ حَرَّمَ أَمِ الْأُنثَيَيْنِ أَمَّا اشْتَمَلَتْ عَلَيْهِ أَرْحَامُ الْأُنثَيَيْنِ ۖ نَبِّئُونِي بِعِلْمٍ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Sàkk na juróom-ñett yu nekk i ñaar-ñaar : ci xar yu góor ak jigéen, ci bëy yi ñaar... Neel : “Ndax ñaar ñu góor ñi ñoo araam walla ñaar ñu jigéen ñi walla la ëmbe ci biir ñaar yu jigéen ñi ? Waxleen ma ci xam-xam ndegam aw nit ngeen” ;
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
141Aaya

Tekki — Al-An'am 141

Simoore Al-An'am Aaya 141 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moom Yàlla Moo sos ay tooli gàncax guy law ci…

Simoore Aaya 141/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 139–143. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers