Al-An'am · 142/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَمِنَ الْأَنْعَامِ حَمُولَةً وَفَرْشًا ۚ كُلُوا مِمَّا رَزَقَكُمُ اللَّهُ وَلَا تَتَّبِعُوا خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ ۚ إِنَّهُ لَكُمْ عَدُوٌّ مُّبِينٌ ۝١٤٢
Wa minal an`aami hamoolatanw wa farshaa; kuloo mimmaa razaqakumul laahu wa laa tattabi`oo khutuwaatish Shaitaan; innahoo lakum `aduwwum mubeen
📖 Tekkim Wolof
Am na ci jur gi yu mën a sëf, ak yu nekk i gëtt; lekkleen ci li leen Yàlla di wërsëgale, te buleen topp jeegoy Séytaane, moom Séytaane seenub noon la bu bir.
🎧 Dégg

📜 Aaya 140-144 — Al-An'am

140قَدْ خَسِرَ الَّذِينَ قَتَلُوا أَوْلَادَهُمْ سَفَهًا بِغَيْرِ عِلْمٍ وَحَرَّمُوا مَا رَزَقَهُمُ اللَّهُ افْتِرَاءً عَلَى اللَّهِ ۚ قَدْ ضَلُّوا وَمَا كَانُوا مُهْتَدِينَ
Ña rey seeni doom cig réer ngir ñàkk a xam, yàqule nañu booleek di araamal la leen Yàlla wërsëgal, lépp tegu ci kaw duural Yàlla. Ñoom réer nañu ba sànku te dootuñu gindiku.
141۞ وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَ جَنَّاتٍ مَّعْرُوشَاتٍ وَغَيْرَ مَعْرُوشَاتٍ وَالنَّخْلَ وَالزَّرْعَ مُخْتَلِفًا أُكُلُهُ وَالزَّيْتُونَ وَالرُّمَّانَ مُتَشَابِهًا وَغَيْرَ مُتَشَابِهٍ ۚ كُلُوا مِن ثَمَرِهِ إِذَا أَثْمَرَ وَآتُوا حَقَّهُ يَوْمَ حَصَادِهِ ۖ وَلَا تُسْرِفُوا ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُسْرِفِينَ
Moom Yàlla Moo sos ay tooli gàncax guy law ci suuf si ak yuy jóg taxaw ; ak garabi tàndarma ak mbey yu meññeent ya wuute ; ak oliw ak garanaat yu niroo ak yu niroowul. Lekkleen seeni doom bu ñoree ; te nangeen génne asaka ja bis ba ngeen di watt [ngóob]. Te buleen yàq ndax Moom [Yàlla] safoowul yàqkat ya.
142وَمِنَ الْأَنْعَامِ حَمُولَةً وَفَرْشًا ۚ كُلُوا مِمَّا رَزَقَكُمُ اللَّهُ وَلَا تَتَّبِعُوا خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ ۚ إِنَّهُ لَكُمْ عَدُوٌّ مُّبِينٌ
Am na ci jur gi yu mën a sëf, ak yu nekk i gëtt; lekkleen ci li leen Yàlla di wërsëgale, te buleen topp jeegoy Séytaane, moom Séytaane seenub noon la bu bir.
143ثَمَانِيَةَ أَزْوَاجٍ ۖ مِّنَ الضَّأْنِ اثْنَيْنِ وَمِنَ الْمَعْزِ اثْنَيْنِ ۗ قُلْ آلذَّكَرَيْنِ حَرَّمَ أَمِ الْأُنثَيَيْنِ أَمَّا اشْتَمَلَتْ عَلَيْهِ أَرْحَامُ الْأُنثَيَيْنِ ۖ نَبِّئُونِي بِعِلْمٍ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Sàkk na juróom-ñett yu nekk i ñaar-ñaar : ci xar yu góor ak jigéen, ci bëy yi ñaar... Neel : “Ndax ñaar ñu góor ñi ñoo araam walla ñaar ñu jigéen ñi walla la ëmbe ci biir ñaar yu jigéen ñi ? Waxleen ma ci xam-xam ndegam aw nit ngeen” ;
144وَمِنَ الْإِبِلِ اثْنَيْنِ وَمِنَ الْبَقَرِ اثْنَيْنِ ۗ قُلْ آلذَّكَرَيْنِ حَرَّمَ أَمِ الْأُنثَيَيْنِ أَمَّا اشْتَمَلَتْ عَلَيْهِ أَرْحَامُ الْأُنثَيَيْنِ ۖ أَمْ كُنتُمْ شُهَدَاءَ إِذْ وَصَّاكُمُ اللَّهُ بِهَٰذَا ۚ فَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا لِّيُضِلَّ النَّاسَ بِغَيْرِ عِلْمٍ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ
...am na ci gëléem yi ñaar, ak ci nag yi ñaar... Neel : “Ndax ñaar ñu góor ñi ñoo araam walla ñaar ñu jigéen ñi, walla la ëmbe ca biir ñaar ñu jigéen ña ? Am dangeen a nekkoon di ay seede ca la leen Yàlla dénku ci yooyu ? ”. Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen ngir mën a réeral nit ñi ci lu àndul ak xam-xam ? Yàlla du gindi nit ña di ay tooñkat.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
142Aaya

Tekki — Al-An'am 142

Simoore Al-An'am Aaya 142 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci jur gi yu mën a sëf, ak…

Simoore Aaya 142/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 140–144. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers