Al-An'am · 54/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَإِذَا جَاءَكَ الَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِنَا فَقُلْ سَلَامٌ عَلَيْكُمْ ۖ كَتَبَ رَبُّكُمْ عَلَىٰ نَفْسِهِ الرَّحْمَةَ ۖ أَنَّهُ مَنْ عَمِلَ مِنكُمْ سُوءًا بِجَهَالَةٍ ثُمَّ تَابَ مِن بَعْدِهِ وَأَصْلَحَ فَأَنَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٥٤
Wa izaa jaaa`akal lazeena yu`minoona bi Aayaatinaa faqul salaamun `alaikum kataba Rabbukum `alaa nafsihir rahmata annahoo man `amila minkum sooo`am bijahaalatin summa taaba mim ba`dihee wa aslaha fa annahoo Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Ña gëm Sunuy kàddu, bu ñu la dikkalee, neel : “Yal na jàmm wàcc ci yéen ! Yàlla seen Boroom dogal na ci boppam yërmaande. Li am mooy, ku def ci yéen aw ñaawtéef cig ñàkk a xam, ba mu noppee, tuub, rëccu, sellal jëfam ... Yàlla moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 52-56 — Al-An'am

52وَلَا تَطْرُدِ الَّذِينَ يَدْعُونَ رَبَّهُم بِالْغَدَاةِ وَالْعَشِيِّ يُرِيدُونَ وَجْهَهُ ۖ مَا عَلَيْكَ مِنْ حِسَابِهِم مِّن شَيْءٍ وَمَا مِنْ حِسَابِكَ عَلَيْهِم مِّن شَيْءٍ فَتَطْرُدَهُمْ فَتَكُونَ مِنَ الظَّالِمِينَ
Bul dàq ñiy jaamu seen Boroom suba ak ngoon ngir bëgg jëmmam [Yàlla]. Dara waru la ci àtte seeni mbir, ñoom it dara waruleen ci àtte say mbir. Ba tax na, boo leen dàqee daldi bokk ca tooñkat ya.
53وَكَذَٰلِكَ فَتَنَّا بَعْضَهُم بِبَعْضٍ لِّيَقُولُوا أَهَٰؤُلَاءِ مَنَّ اللَّهُ عَلَيْهِم مِّن بَيْنِنَا ۗ أَلَيْسَ اللَّهُ بِأَعْلَمَ بِالشَّاكِرِينَ
Noonu la Nu notee ñenn ci ñoom jaare ko ci ñeneen ca ñoom, ngir ñu wax ne : “Ndax [ña doyadi] ñii la Yàlla xéewale ci nun ? ”. Moo ndax Yàlla Moo gën a xam ña koy gëram ciy xéewalam ?
54وَإِذَا جَاءَكَ الَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِنَا فَقُلْ سَلَامٌ عَلَيْكُمْ ۖ كَتَبَ رَبُّكُمْ عَلَىٰ نَفْسِهِ الرَّحْمَةَ ۖ أَنَّهُ مَنْ عَمِلَ مِنكُمْ سُوءًا بِجَهَالَةٍ ثُمَّ تَابَ مِن بَعْدِهِ وَأَصْلَحَ فَأَنَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ña gëm Sunuy kàddu, bu ñu la dikkalee, neel : “Yal na jàmm wàcc ci yéen ! Yàlla seen Boroom dogal na ci boppam yërmaande. Li am mooy, ku def ci yéen aw ñaawtéef cig ñàkk a xam, ba mu noppee, tuub, rëccu, sellal jëfam ... Yàlla moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.
55وَكَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ الْآيَاتِ وَلِتَسْتَبِينَ سَبِيلُ الْمُجْرِمِينَ
Te noonu Lanuy leeralee tegtal yi ngir fésal yoonu tooñkat yi.
56قُلْ إِنِّي نُهِيتُ أَنْ أَعْبُدَ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ ۚ قُل لَّا أَتَّبِعُ أَهْوَاءَكُمْ ۙ قَدْ ضَلَلْتُ إِذًا وَمَا أَنَا مِنَ الْمُهْتَدِينَ
Neel : “Man tere nañu ma may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla”. Neel itam : “Duma topp seeni bànneex : ndax su ma ko defee, damay sànku te kon duma bokk ca ñu gindiku ña”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
54Aaya

Tekki — Al-An'am 54

Simoore Al-An'am Aaya 54 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña gëm Sunuy kàddu, bu ñu la dikkalee, neel :…

Simoore Aaya 54/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 52–56. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers