Al-An'am · 55/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَكَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ الْآيَاتِ وَلِتَسْتَبِينَ سَبِيلُ الْمُجْرِمِينَ ۝٥٥
Wa kazaalika nufassilul Aayaati wa litastabeena sabeelul mujrimeen
📖 Tekkim Wolof
Te noonu Lanuy leeralee tegtal yi ngir fésal yoonu tooñkat yi.
🎧 Dégg

📜 Aaya 53-57 — Al-An'am

53وَكَذَٰلِكَ فَتَنَّا بَعْضَهُم بِبَعْضٍ لِّيَقُولُوا أَهَٰؤُلَاءِ مَنَّ اللَّهُ عَلَيْهِم مِّن بَيْنِنَا ۗ أَلَيْسَ اللَّهُ بِأَعْلَمَ بِالشَّاكِرِينَ
Noonu la Nu notee ñenn ci ñoom jaare ko ci ñeneen ca ñoom, ngir ñu wax ne : “Ndax [ña doyadi] ñii la Yàlla xéewale ci nun ? ”. Moo ndax Yàlla Moo gën a xam ña koy gëram ciy xéewalam ?
54وَإِذَا جَاءَكَ الَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِنَا فَقُلْ سَلَامٌ عَلَيْكُمْ ۖ كَتَبَ رَبُّكُمْ عَلَىٰ نَفْسِهِ الرَّحْمَةَ ۖ أَنَّهُ مَنْ عَمِلَ مِنكُمْ سُوءًا بِجَهَالَةٍ ثُمَّ تَابَ مِن بَعْدِهِ وَأَصْلَحَ فَأَنَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ña gëm Sunuy kàddu, bu ñu la dikkalee, neel : “Yal na jàmm wàcc ci yéen ! Yàlla seen Boroom dogal na ci boppam yërmaande. Li am mooy, ku def ci yéen aw ñaawtéef cig ñàkk a xam, ba mu noppee, tuub, rëccu, sellal jëfam ... Yàlla moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.
55وَكَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ الْآيَاتِ وَلِتَسْتَبِينَ سَبِيلُ الْمُجْرِمِينَ
Te noonu Lanuy leeralee tegtal yi ngir fésal yoonu tooñkat yi.
56قُلْ إِنِّي نُهِيتُ أَنْ أَعْبُدَ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ ۚ قُل لَّا أَتَّبِعُ أَهْوَاءَكُمْ ۙ قَدْ ضَلَلْتُ إِذًا وَمَا أَنَا مِنَ الْمُهْتَدِينَ
Neel : “Man tere nañu ma may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla”. Neel itam : “Duma topp seeni bànneex : ndax su ma ko defee, damay sànku te kon duma bokk ca ñu gindiku ña”.
57قُلْ إِنِّي عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّي وَكَذَّبْتُم بِهِ ۚ مَا عِندِي مَا تَسْتَعْجِلُونَ بِهِ ۚ إِنِ الْحُكْمُ إِلَّا لِلَّهِ ۖ يَقُصُّ الْحَقَّ ۖ وَهُوَ خَيْرُ الْفَاصِلِينَ
Neel : “Man dama nekk ci lu bir [leer nàññ], di lu jóge fa sama Boroom, ngeen weddi ko. Li ngeen di [laaj te di ko] yàkkamti, nekkul ci man. Àpp ba, Yàlla rekk a ko moom : Mooy nettali dëgg te Mooy gën jaa mën a àtte [téqale] ay mbir.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
55Aaya

Tekki — Al-An'am 55

Simoore Al-An'am Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te noonu Lanuy leeralee tegtal yi ngir fésal yoonu tooñkat…

Simoore Aaya 55/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers