Al-Anfal · 49/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
إِذْ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ غَرَّ هَٰؤُلَاءِ دِينُهُمْ ۗ وَمَن يَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ ۝٤٩
Iz yaqoolul munaafiqoona wallazeena fee quloobihim maradun gharra haaa`ulaaa`i deenuhum; wa mai yatawakkal `alal laahi fa innal laaha `azee zun Hakeem
📖 Tekkim Wolof
(Fàttalikul), ba naafeq ya ak ña jàngoro nekk ca seeni xol waxee ne : “Ñii seen diine wor na leen.” Waaye ku wéeru ci Yàlla ... [na xam ne] Yàlla Kuy not lépp la, Ku xereñ la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 47-51 — Al-Anfal

47وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ خَرَجُوا مِن دِيَارِهِم بَطَرًا وَرِئَاءَ النَّاسِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ وَاللَّهُ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطٌ
Buleen mel ni ña génnoon seeni kër, rëylu ak di ngistal ci nit ñi, te di gàllankoor [nit ñi ñu bañ jëm ci] yoonu Yàlla. Te Yàlla xam na la ñuy def de.
48وَإِذْ زَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ وَقَالَ لَا غَالِبَ لَكُمُ الْيَوْمَ مِنَ النَّاسِ وَإِنِّي جَارٌ لَّكُمْ ۖ فَلَمَّا تَرَاءَتِ الْفِئَتَانِ نَكَصَ عَلَىٰ عَقِبَيْهِ وَقَالَ إِنِّي بَرِيءٌ مِّنكُمْ إِنِّي أَرَىٰ مَا لَا تَرَوْنَ إِنِّي أَخَافُ اللَّهَ ۚ وَاللَّهُ شَدِيدُ الْعِقَابِ
Fàttalikul ba Séytaane rafetalee yéefar ya seeni jëf, ne leen : “Tey kenn duleen not, te man maa leen di dimbali.”. Waaye ba ñaari kurél ya jàkkaarloo, dafa dellu ginnaaw te wafeet daw, daldi wax, moom Séytaane, ne : “Man kat deñ naa ci yéen. Ndax gis naa lu ngeen gisul ; ragal naa Yàlla, te Yàlla Ku tar mbugal la”.
49إِذْ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ غَرَّ هَٰؤُلَاءِ دِينُهُمْ ۗ وَمَن يَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
(Fàttalikul), ba naafeq ya ak ña jàngoro nekk ca seeni xol waxee ne : “Ñii seen diine wor na leen.” Waaye ku wéeru ci Yàlla ... [na xam ne] Yàlla Kuy not lépp la, Ku xereñ la.
50وَلَوْ تَرَىٰ إِذْ يَتَوَفَّى الَّذِينَ كَفَرُوا ۙ الْمَلَائِكَةُ يَضْرِبُونَ وُجُوهَهُمْ وَأَدْبَارَهُمْ وَذُوقُوا عَذَابَ الْحَرِيقِ
Boo gisee na Malaaka ya di reyee yéefar ya ! Dañuy dóor seeni kanam ak seeni ginnaaw, (naa leen): “Mosleen mbugalu Safara.
51ذَٰلِكَ بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ لَيْسَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ
Loolu mooy la ngeen jëfoon ci seeni yoxo.” Te it Yàlla du koy tooñ jaam ñi.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
49Aaya

Tekki — Al-Anfal 49

Simoore Al-Anfal Aaya 49 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (Fàttalikul), ba naafeq ya ak ña jàngoro nekk ca seeni…

Simoore Aaya 49/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 47–51. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers