Simoore Al-Haqqa ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Haqqa ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (52 Aaya — مكية). Al-Haqqa Dégg, Al-Haqqa Tekki, Al-Haqqa mp3, Al-Haqqa pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Haqqa

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
الْحَاقَّةُ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Joxoñub dëgg ba.
مَا الْحَاقَّةُ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Lan mooy Joxoñub dëgg ba.
وَمَا أَدْرَاكَ مَا الْحَاقَّةُ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Ana lan moo lay xamal Joxoñub dëgg ba.
كَذَّبَتْ ثَمُودُ وَعَادٌ بِالْقَارِعَةِ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Giirug Aad ak Samuud dañoo weddi woon yëngu-yëngu bu rëy ba.
فَأَمَّا ثَمُودُ فَأُهْلِكُوا بِالطَّاغِيَةِ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Giirug Samuud ag yuuxu (am riir) la ñu léen alage.
وَأَمَّا عَادٌ فَأُهْلِكُوا بِرِيحٍ صَرْصَرٍ عَاتِيَةٍ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Giirug Aad nag ngelaw lu sedd luy riddi moom la ñu léen alage.
سَخَّرَهَا عَلَيْهِمْ سَبْعَ لَيَالٍ وَثَمَانِيَةَ أَيَّامٍ حُسُومًا فَتَرَى الْقَوْمَ فِيهَا صَرْعَىٰ كَأَنَّهُمْ أَعْجَازُ نَخْلٍ خَاوِيَةٍ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
xiirtal na ko ci séen kaw juróom yaari bëccag ak juróom yaari guddi yu tegaloo nit ña ne lasiim melni dàtti tàndarma yu fënëx.
فَهَلْ تَرَىٰ لَهُم مِّن بَاقِيَةٍ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Moo ndax gisati nga lu bokk ca ñoom?
وَجَاءَ فِرْعَوْنُ وَمَن قَبْلَهُ وَالْمُؤْتَفِكَاتُ بِالْخَاطِئَةِ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Firawnaak ña ko jiitu woon ak dëkk ya nu wëlbati woon njuumte la ñu fa nekke woon.
فَعَصَوْا رَسُولَ رَبِّهِمْ فَأَخَذَهُمْ أَخْذَةً رَّابِيَةً ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Dañoo moyu woon senn Yonentub Boroom. Yàlla, faagaagal leen.
إِنَّا لَمَّا طَغَى الْمَاءُ حَمَلْنَاكُمْ فِي الْجَارِيَةِ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Ba ndox ma bëbóo, Noo leen yanu woon, ca gaalug Nooh ga doon daw
لِنَجْعَلَهَا لَكُمْ تَذْكِرَةً وَتَعِيَهَا أُذُنٌ وَاعِيَةٌ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
danu koo def mu di fàttali ci yéen nopp yu sell it man koo jàpp.
فَإِذَا نُفِخَ فِي الصُّورِ نَفْخَةٌ وَاحِدَةٌ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Su nu walee bufta ba, genn wal ëf ko,
وَحُمِلَتِ الْأَرْضُ وَالْجِبَالُ فَدُكَّتَا دَكَّةً وَاحِدَةً ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
suuf si ak doj yi ñu jël ko def ko pënd moñoxe ko benn yoon ;
فَيَوْمَئِذٍ وَقَعَتِ الْوَاقِعَةُ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Bu keroogee, xew-xew,ba agsi bis Pénc ba,
وَانشَقَّتِ السَّمَاءُ فَهِيَ يَوْمَئِذٍ وَاهِيَةٌ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
asamaan siy xottiku nooy nepp.
وَالْمَلَكُ عَلَىٰ أَرْجَائِهَا ۚ وَيَحْمِلُ عَرْشَ رَبِّكَ فَوْقَهُمْ يَوْمَئِذٍ ثَمَانِيَةٌ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Malaaka ya nekk ci ay goxam, su ko defee juróom-ñatta, cay yanu gàngunaay ga ( Aras ).
يَوْمَئِذٍ تُعْرَضُونَ لَا تَخْفَىٰ مِنكُمْ خَافِيَةٌ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Bu keroogee dees na leen weer; ken du leen ca nëbb dara.
فَأَمَّا مَنْ أُوتِيَ كِتَابَهُ بِيَمِينِهِ فَيَقُولُ هَاؤُمُ اقْرَءُوا كِتَابِيَهْ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Ña nga xam ne dañoo jot seeni Téere ci ndeyjoor, da leen di wax ne : “Jàppleen ! jàng samab téere.
إِنِّي ظَنَنتُ أَنِّي مُلَاقٍ حِسَابِيَهْ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Man dey jàppoon naa ne danaa dajeek samab màndaxe”.
فَهُوَ فِي عِيشَةٍ رَّاضِيَةٍ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Moom dey mi ngi ci dundu gu neex :
فِي جَنَّةٍ عَالِيَةٍ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
ca Àjjana ju kawe
قُطُوفُهَا دَانِيَةٌ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
meññatam ma day yoore.
كُلُوا وَاشْرَبُوا هَنِيئًا بِمَا أَسْلَفْتُمْ فِي الْأَيَّامِ الْخَالِيَةِ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
“Lekkleen te naan muy peyug la ngeen jiitaloon”.
وَأَمَّا مَنْ أُوتِيَ كِتَابَهُ بِشِمَالِهِ فَيَقُولُ يَا لَيْتَنِي لَمْ أُوتَ كِتَابِيَهْ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Ña ñuy joxe seen téere ci càmmoñ, danuy wax naan : “Aka neexoon ! Jotuma sama téere,
وَلَمْ أَدْرِ مَا حِسَابِيَهْ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
te ma ba ña xam luy sama màndaxe...
يَا لَيْتَهَا كَانَتِ الْقَاضِيَةَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Aka neexoon, ma dee farit.
مَا أَغْنَىٰ عَنِّي مَالِيَهْ ۜ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Sama alal ja jariñuma dara.
هَلَكَ عَنِّي سُلْطَانِيَهْ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Sama sañ-sañ réer na ma ! ”.
خُذُوهُ فَغُلُّوهُ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
“Jàppleen ko ! Te, jàng ko ;
ثُمَّ الْجَحِيمَ صَلُّوهُ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
te, ngeen xoyom ko ca Safara ;
ثُمَّ فِي سِلْسِلَةٍ ذَرْعُهَا سَبْعُونَ ذِرَاعًا فَاسْلُكُوهُ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
ca biir càllalag juróom-ñaar-fukk bëñ sóobleen ko ca jéng ko,
إِنَّهُ كَانَ لَا يُؤْمِنُ بِاللَّهِ الْعَظِيمِ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
moom gëmu tooñ Yàlla , mu Màgg ma.
وَلَا يَحُضُّ عَلَىٰ طَعَامِ الْمِسْكِينِ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
te daawul sonn ci dundal miskiin yi.
فَلَيْسَ لَهُ الْيَوْمَ هَاهُنَا حَمِيمٌ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Bis niki tey amatu fi xarit
وَلَا طَعَامٌ إِلَّا مِنْ غِسْلِينٍ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
ducaageni ak lekk lu dul lay rogaat ci seen yaram,
لَّا يَأْكُلُهُ إِلَّا الْخَاطِئُونَ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
defkati njaaxum ya rekk koy lekk”.
فَلَا أُقْسِمُ بِمَا تُبْصِرُونَ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Déet... Maa ngi giñ ci li ngeen di gis,
وَمَا لَا تُبْصِرُونَ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Ak ci li ngeen gisul,
إِنَّهُ لَقَوْلُ رَسُولٍ كَرِيمٍ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
ci ne [Alxuraan] waxi ab Yonent la bu tedd,
وَمَا هُوَ بِقَوْلِ شَاعِرٍ ۚ قَلِيلًا مَّا تُؤْمِنُونَ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
du waxu ab waykat ; li ngeen gëm néew na,
وَلَا بِقَوْلِ كَاهِنٍ ۚ قَلِيلًا مَّا تَذَكَّرُونَ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
du waxi it ab buxaaba, aka néew lu ngeen di fàttaliku.
تَنزِيلٌ مِّن رَّبِّ الْعَالَمِينَ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Dafa wàcc bawoo ci boroom àddina si.
وَلَوْ تَقَوَّلَ عَلَيْنَا بَعْضَ الْأَقَاوِيلِ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Su ca fentoon jenn jenn wax,
لَأَخَذْنَا مِنْهُ بِالْيَمِينِ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
( Kon ) dananu téye loxob ndeyjooram,
ثُمَّ لَقَطَعْنَا مِنْهُ الْوَتِينَ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
daldi, dog sidiiti xolam ( mu dee ).
فَمَا مِنكُم مِّنْ أَحَدٍ عَنْهُ حَاجِزِينَ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Te kon kenn ci yéen du ko mana fanq.
وَإِنَّهُ لَتَذْكِرَةٌ لِّلْمُتَّقِينَ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Ca dëgg-dëgg ag fàttali la ñeel ña ragal Yàlla.
وَإِنَّا لَنَعْلَمُ أَنَّ مِنكُم مُّكَذِّبِينَ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
Te xam nanu xéll ne am na ci yéen ñu koy weddi ;
وَإِنَّهُ لَحَسْرَةٌ عَلَى الْكَافِرِينَ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
ca dëgg-dëgg, bekkoor la ci yéefar yi,
وَإِنَّهُ لَحَقُّ الْيَقِينِ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
te moo di li wóor tigi.
فَسَبِّحْ بِاسْمِ رَبِّكَ الْعَظِيمِ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Na ngay sàbbaal sa turu Boroom, bu Màgg bi !
← 68 Al-Haqqa (69/114) 70 →
Jàng Simoore Al-Haqqa ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

69الحاقة Al-Haqqah 📚 52 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers