Simoore Al-Layl pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Layl pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Layl Tekki. Simoore Al-Layl (Meccan) 21 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Layl

ﮡﮢﮣﮤ
92:1
Ci guddi gi saa su muuree lépp ! maa ngi giñ
ﮥﮦﮧﮨ
92:2
Ak ci bëcëg bi saa su leeree !
ﮩﮪﮫﮬﮭ
92:3
Ak ci ki sàkk, góor ak jigéen !
ﮮﮯﮰﮱ
92:4
Seen jëf wuute na.
ﯓﯔﯕﯖﯗ
92:5
Képp kuy joxe te ragal (Yàlla)
ﯘﯙﯚ
92:6
te mu dëggël yoolub àllaaxira
ﯛﯜﯝ
92:7
Dananu ko jàppandalal yoon wu yomb wa.
ﯞﯟﯠﯡﯢ
92:8
Képp ku nay, te dumóoyu boroomam,
ﯣﯤﯥ
92:9
te muy weddi yoolub àllaaxira,
ﭑﭒﭓ
92:10
Dananu ko jàppandalal yoon wu jafe wa,
ﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
92:11
te alalam du ko jariñ dara saa su ñu ko mbaqee (Safara).
ﭛﭜﭝﭞ
92:12
Gindee, nun la war ;
ﭟﭠﭡﭢﭣ
92:13
te Noo moom, dundug àddinaak àllaaxira.
ﭤﭥﭦﭧ
92:14
Xuppnaa leen ci Safara wuy bérëx-bérëxi
ﭨﭩﭪﭫﭬ
92:15
ku texedi ka rekka cay xoyomu,
ﭭﭮﭯﭰ
92:16
kay weddi tey dumóoyu ;
ﭱﭲﭳ
92:17
dees na ko soril ñu ragal Yàlla ña,
ﭴﭵﭶﭷﭸ
92:18
kay joxe alalam ngir selal
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
92:19
te amul genn xéewal gu ñuy faye kenn ca moom,
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
92:20
Lu dul sàkku jëmm Boroomam ja gëna Kawe.
ﮆﮇﮈ
92:21
Te, xalset naa gëram (moom ka def noona) !
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







