An-Nahl · 97/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
مَنْ عَمِلَ صَالِحًا مِّن ذَكَرٍ أَوْ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَلَنُحْيِيَنَّهُ حَيَاةً طَيِّبَةً ۖ وَلَنَجْزِيَنَّهُمْ أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝٩٧
Man `amila saaliham min zakarin aw unsaa wa huwa mu`minun falanuhyiyannahoo hayaatan taiiyibatanw wa lanajzi yannnahum ajrahum bi ahsani maa kaanoo ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Ku jëf u yiw, di ku góor walla ku jigéen te muy ku gëm, fàwwu Dananu ko dundal dundu gu sell. Te fàwwu Dananu leen fey seenug pey na mu gën a rafete la ñu nekkoon di ko jëf.

🎧 Dégg


📜 Aaya 95-99 — An-Nahl

95وَلَا تَشْتَرُوا بِعَهْدِ اللَّهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۚ إِنَّمَا عِندَ اللَّهِ هُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
Buleen di jaaye kóllareg Yàlla ci njëg gu néew. La nekk fa Yàlla moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon !
96مَا عِندَكُمْ يَنفَدُ ۖ وَمَا عِندَ اللَّهِ بَاقٍ ۗ وَلَنَجْزِيَنَّ الَّذِينَ صَبَرُوا أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Li ngeen moom day jeex, la Yàlla moom nag luy des la. Te fàwwu Dananu feye ñiy muñ ca na mu gën a rafete, ngir la ñu nekkoon di ko def.
97مَنْ عَمِلَ صَالِحًا مِّن ذَكَرٍ أَوْ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَلَنُحْيِيَنَّهُ حَيَاةً طَيِّبَةً ۖ وَلَنَجْزِيَنَّهُمْ أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ku jëf u yiw, di ku góor walla ku jigéen te muy ku gëm, fàwwu Dananu ko dundal dundu gu sell. Te fàwwu Dananu leen fey seenug pey na mu gën a rafete la ñu nekkoon di ko jëf.
98فَإِذَا قَرَأْتَ الْقُرْآنَ فَاسْتَعِذْ بِاللَّهِ مِنَ الشَّيْطَانِ الرَّجِيمِ
Booy jàng Alxuraan, nanga muslu ci Yàlla Mu musal la ci Séytaane su ñu rëbb sa.
99إِنَّهُ لَيْسَ لَهُ سُلْطَانٌ عَلَى الَّذِينَ آمَنُوا وَعَلَىٰ رَبِّهِمْ يَتَوَكَّلُونَ
Naka Séytaane du am genn kàttan ci [yàqal] ña gëm te wéeru ci seen Boroom.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
97Aaya

Tekki — An-Nahl 97

Simoore An-Nahl Aaya 97 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ku jëf u yiw, di ku góor walla ku jigéen…

Simoore Aaya 97/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 95–99. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers