Al-Baqara · 110/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَآتُوا الزَّكَاةَ ۚ وَمَا تُقَدِّمُوا لِأَنفُسِكُم مِّنْ خَيْرٍ تَجِدُوهُ عِندَ اللَّهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ ۝١١٠
Wa aqeemus salaata wa aatuz zakaah; wa maa tuqaddimoo li anfusikum min khairin tajidoohu `indal laah; innal laaha bimaa ta`maloona baseer
📖 Tekkim Wolof
Deeleen taxawee julli te di génne asaka. Lu ngeen jiital ci lu baax ngir seen bopp, dangeen ko fekk ca Yàlla, ndax Yàlla gu gis la li ngeen di def.
🎧 Dégg

📜 Aaya 108-112 — Al-Baqara

108أَمْ تُرِيدُونَ أَن تَسْأَلُوا رَسُولَكُمْ كَمَا سُئِلَ مُوسَىٰ مِن قَبْلُ ۗ وَمَن يَتَبَدَّلِ الْكُفْرَ بِالْإِيمَانِ فَقَدْ ضَلَّ سَوَاءَ السَّبِيلِ
Am dangeen bëgg a laaj seen Yonent na ñu laajee woon Muusaa ca bu njëkk ? Képp ku weccee ngëm ak weddi, réer na te wàcc na yoon wu njub wa.
109وَدَّ كَثِيرٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَوْ يَرُدُّونَكُم مِّن بَعْدِ إِيمَانِكُمْ كُفَّارًا حَسَدًا مِّنْ عِندِ أَنفُسِهِم مِّن بَعْدِ مَا تَبَيَّنَ لَهُمُ الْحَقُّ ۖ فَاعْفُوا وَاصْفَحُوا حَتَّىٰ يَأْتِيَ اللَّهُ بِأَمْرِهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Ñu bari ci ñoñ-téere [Yahuud ak Nasaraan] nee nañu siiw ñu delloo leen cig kéefar ginnaaw seen ngëm ngir kiñaan gu sosoo seeni bakkan. Ginnaaw ba dëgg ga leeree nàññ ? Baal-leen te dummóoyuleen ba Yàlla agseek ndigëlam. Yàlla nag mën na lu ne !
110وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَآتُوا الزَّكَاةَ ۚ وَمَا تُقَدِّمُوا لِأَنفُسِكُم مِّنْ خَيْرٍ تَجِدُوهُ عِندَ اللَّهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Deeleen taxawee julli te di génne asaka. Lu ngeen jiital ci lu baax ngir seen bopp, dangeen ko fekk ca Yàlla, ndax Yàlla gu gis la li ngeen di def.
111وَقَالُوا لَن يَدْخُلَ الْجَنَّةَ إِلَّا مَن كَانَ هُودًا أَوْ نَصَارَىٰ ۗ تِلْكَ أَمَانِيُّهُمْ ۗ قُلْ هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Wax nañu ne : “Kenn du dugg Àjjana ku dul ku nekk (Yahuud walla Nasaraan)”. Loolu dey seen mébét la ñoom. - Neel : “Indileen seenu lay, ndegam ñu dëggu ngeen”.
112بَلَىٰ مَنْ أَسْلَمَ وَجْهَهُ لِلَّهِ وَهُوَ مُحْسِنٌ فَلَهُ أَجْرُهُ عِندَ رَبِّهِ وَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Axakañ! ku wommatu ci topp Yàlla te muy rafetal, [topp, ci jëfe ndigal ak bàyyi yi Yàlla tere] kooku peyam ma nga ca Boroomam. [Ña mel ni ñoom] duñu tiit duñu jàq.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
110Aaya

Tekki — Al-Baqara 110

Simoore Al-Baqara Aaya 110 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Deeleen taxawee julli te di génne asaka. Lu ngeen jiital…

Simoore Aaya 110/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 108–112. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers