Al-Baqara · 203/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
۞ وَاذْكُرُوا اللَّهَ فِي أَيَّامٍ مَّعْدُودَاتٍ ۚ فَمَن تَعَجَّلَ فِي يَوْمَيْنِ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ وَمَن تَأَخَّرَ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ ۚ لِمَنِ اتَّقَىٰ ۗ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاعْلَمُوا أَنَّكُمْ إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ ۝٢٠٣
Wazkurul laaha feee ayyaamim ma`doodaat; faman ta`ajjala fee yawmaini falaaa ismaa `alaihi wa man taakhkhara falaaa isma `alayh; limanit-taqaa; wattaqul laaha wa`lamooo annakum ilaihi tuhsharoon
📖 Tekkim Wolof
Nangeen di fàttaliku Yàlla ci ay bis yuñu lim. Ku yàkkamti ba def ko ci ñaari fan du ca am bàkkaar, kay toog fa [Munaa] ñatti fan du ca am bàkkaar ci ku ragal Yàlla. Ragal-leen Yàlla te ngeen xam ne dees na leen fang [Jiital/gur-gur] jëme ci Moom.

🎧 Dégg


📜 Aaya 201-205 — Simoore Al-Baqara

201وَمِنْهُم مَّن يَقُولُ رَبَّنَا آتِنَا فِي الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ حَسَنَةً وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ
Am na ci ñoom kuy wax ne : “Yaw sunu Boroom ! Defalnu xéewal ci àddina, ak ca àllaaxira ; te fegalnu mbugalum Safara ! ”.
202أُولَٰئِكَ لَهُمْ نَصِيبٌ مِّمَّا كَسَبُوا ۚ وَاللَّهُ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Ñooña am na ñu yool ca la ñu sàkku. Te Yàlla ku gaaw la ci xayma [waññi, màndaxe].
203۞ وَاذْكُرُوا اللَّهَ فِي أَيَّامٍ مَّعْدُودَاتٍ ۚ فَمَن تَعَجَّلَ فِي يَوْمَيْنِ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ وَمَن تَأَخَّرَ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ ۚ لِمَنِ اتَّقَىٰ ۗ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاعْلَمُوا أَنَّكُمْ إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ
Nangeen di fàttaliku Yàlla ci ay bis yuñu lim. Ku yàkkamti ba def ko ci ñaari fan du ca am bàkkaar, kay toog fa [Munaa] ñatti fan du ca am bàkkaar ci ku ragal Yàlla. Ragal-leen Yàlla te ngeen xam ne dees na leen fang [Jiital/gur-gur] jëme ci Moom.
204وَمِنَ النَّاسِ مَن يُعْجِبُكَ قَوْلُهُ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَيُشْهِدُ اللَّهَ عَلَىٰ مَا فِي قَلْبِهِ وَهُوَ أَلَدُّ الْخِصَامِ
Am na ci nit ñi seeni wax dalay yéem lool, ci dundug àddina ndax day seedeloo Yàlla la nekk ca xolam, ndekeyoo moom xulóowaale la bu pànk, bu yées.
205وَإِذَا تَوَلَّىٰ سَعَىٰ فِي الْأَرْضِ لِيُفْسِدَ فِيهَا وَيُهْلِكَ الْحَرْثَ وَالنَّسْلَ ۗ وَاللَّهُ لَا يُحِبُّ الْفَسَادَ
Bu nee wërëñ rekk tàmbalee yàq ci kaw suuf, di alag mbay mi ak jur gi te Yàlla bëggul ag yàq.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
203Aaya

Tekki — Al-Baqara 203

Simoore Al-Baqara Aaya 203 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen di fàttaliku Yàlla ci ay bis yuñu lim. Ku…

Simoore Aaya 203/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 201–205. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers