Al-Baqara · 202/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
أُولَٰئِكَ لَهُمْ نَصِيبٌ مِّمَّا كَسَبُوا ۚ وَاللَّهُ سَرِيعُ الْحِسَابِ ۝٢٠٢
Ulaaa`ika lahum naseebum mimmaa kasaboo; wal laahu saree`ul hisaab
📖 Tekkim Wolof
Ñooña am na ñu yool ca la ñu sàkku. Te Yàlla ku gaaw la ci xayma [waññi, màndaxe].

🎧 Dégg


📜 Aaya 200-204 — Simoore Al-Baqara

200فَإِذَا قَضَيْتُم مَّنَاسِكَكُمْ فَاذْكُرُوا اللَّهَ كَذِكْرِكُمْ آبَاءَكُمْ أَوْ أَشَدَّ ذِكْرًا ۗ فَمِنَ النَّاسِ مَن يَقُولُ رَبَّنَا آتِنَا فِي الدُّنْيَا وَمَا لَهُ فِي الْآخِرَةِ مِنْ خَلَاقٍ
Bu seen aj jeexee, nangeen di tuddu Yàlla kem na ngeen daan tuddee [taggee] seeni maam, walla sax tuddiin wu gën a tar. Am na ci nit ñi ñuy wax ne : “Yaw sunu Boroom! May nu àddina [kese] ! ” - te duñu fàggu dara ngir àllaaxira.
201وَمِنْهُم مَّن يَقُولُ رَبَّنَا آتِنَا فِي الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ حَسَنَةً وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ
Am na ci ñoom kuy wax ne : “Yaw sunu Boroom ! Defalnu xéewal ci àddina, ak ca àllaaxira ; te fegalnu mbugalum Safara ! ”.
202أُولَٰئِكَ لَهُمْ نَصِيبٌ مِّمَّا كَسَبُوا ۚ وَاللَّهُ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Ñooña am na ñu yool ca la ñu sàkku. Te Yàlla ku gaaw la ci xayma [waññi, màndaxe].
203۞ وَاذْكُرُوا اللَّهَ فِي أَيَّامٍ مَّعْدُودَاتٍ ۚ فَمَن تَعَجَّلَ فِي يَوْمَيْنِ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ وَمَن تَأَخَّرَ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ ۚ لِمَنِ اتَّقَىٰ ۗ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاعْلَمُوا أَنَّكُمْ إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ
Nangeen di fàttaliku Yàlla ci ay bis yuñu lim. Ku yàkkamti ba def ko ci ñaari fan du ca am bàkkaar, kay toog fa [Munaa] ñatti fan du ca am bàkkaar ci ku ragal Yàlla. Ragal-leen Yàlla te ngeen xam ne dees na leen fang [Jiital/gur-gur] jëme ci Moom.
204وَمِنَ النَّاسِ مَن يُعْجِبُكَ قَوْلُهُ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَيُشْهِدُ اللَّهَ عَلَىٰ مَا فِي قَلْبِهِ وَهُوَ أَلَدُّ الْخِصَامِ
Am na ci nit ñi seeni wax dalay yéem lool, ci dundug àddina ndax day seedeloo Yàlla la nekk ca xolam, ndekeyoo moom xulóowaale la bu pànk, bu yées.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
202Aaya

Tekki — Al-Baqara 202

Simoore Al-Baqara Aaya 202 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñooña am na ñu yool ca la ñu sàkku. Te…

Simoore Aaya 202/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 200–204. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers