An-Nur · 4/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
وَالَّذِينَ يَرْمُونَ الْمُحْصَنَاتِ ثُمَّ لَمْ يَأْتُوا بِأَرْبَعَةِ شُهَدَاءَ فَاجْلِدُوهُمْ ثَمَانِينَ جَلْدَةً وَلَا تَقْبَلُوا لَهُمْ شَهَادَةً أَبَدًا ۚ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ ۝٤
Wallazeena yarmoonal muhsanaati summa lam yaatoo bi-arba`ati shuhadaaa`a fajlidoohum samaaneena jaldatanw wa laa taqbaloo lahum shahaadatan abadaa; wa ulaaa`ika humul faasiqoon
📖 Tekkim Wolof
Ñay yàq deru jigéen ña, saŋewu [ci jiiñ leen njaaloo] ba noppi ñàkk a indi ñeenti seede, nangeen leen dóor juróom-ñetti fukki yar, te buleen nangooti ñuy seede ba fàwwu. Ñoom ay saay-saay lañu,
🎧 Dégg

📜 Aaya 2-6 — An-Nur

2الزَّانِيَةُ وَالزَّانِي فَاجْلِدُوا كُلَّ وَاحِدٍ مِّنْهُمَا مِائَةَ جَلْدَةٍ ۖ وَلَا تَأْخُذْكُم بِهِمَا رَأْفَةٌ فِي دِينِ اللَّهِ إِن كُنتُمْ تُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ ۖ وَلْيَشْهَدْ عَذَابَهُمَا طَائِفَةٌ مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ
Njaalookat bu jigéen ak njaalookat bu góor, nangeen leen dóor téeméeri yar. Te buleen leen yërëm [ci li diine tege] - ndegam gëm ngeen Yàlla ak Bis-pénc. Te itam mbugalum njaalookat yooyu, na ko mbooloo mu bari teewe ci jullit yi.
3الزَّانِي لَا يَنكِحُ إِلَّا زَانِيَةً أَوْ مُشْرِكَةً وَالزَّانِيَةُ لَا يَنكِحُهَا إِلَّا زَانٍ أَوْ مُشْرِكٌ ۚ وَحُرِّمَ ذَٰلِكَ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ
Njaalokat bu góor du sëy ak ku dul njaalookat bu jigéen walla bokkaalekat. Njaalookat bu jigéen, kenn du sëy ak moom ku dul njaalookat bu góor walla bokkaalekat te loolu araam na ci jullit ñi.
4وَالَّذِينَ يَرْمُونَ الْمُحْصَنَاتِ ثُمَّ لَمْ يَأْتُوا بِأَرْبَعَةِ شُهَدَاءَ فَاجْلِدُوهُمْ ثَمَانِينَ جَلْدَةً وَلَا تَقْبَلُوا لَهُمْ شَهَادَةً أَبَدًا ۚ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Ñay yàq deru jigéen ña, saŋewu [ci jiiñ leen njaaloo] ba noppi ñàkk a indi ñeenti seede, nangeen leen dóor juróom-ñetti fukki yar, te buleen nangooti ñuy seede ba fàwwu. Ñoom ay saay-saay lañu,
5إِلَّا الَّذِينَ تَابُوا مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ وَأَصْلَحُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
ba mu des ña rëccu, tuub ginnaaw loolu, tey jëf u yiw, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
6وَالَّذِينَ يَرْمُونَ أَزْوَاجَهُمْ وَلَمْ يَكُن لَّهُمْ شُهَدَاءُ إِلَّا أَنفُسُهُمْ فَشَهَادَةُ أَحَدِهِمْ أَرْبَعُ شَهَادَاتٍ بِاللَّهِ ۙ إِنَّهُ لَمِنَ الصَّادِقِينَ
Ñay tuumaal seeni jabar te amuñu ay seede lu dul seen bopp, na waat ci Yàlla ñeenti yoon ne ku dëggu la,
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
4Aaya

Tekki — An-Nur 4

Simoore An-Nur Aaya 4 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñay yàq deru jigéen ña, saŋewu [ci jiiñ leen njaaloo]…

Simoore Aaya 4/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 2–6. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers