An-Nur · 56/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَآتُوا الزَّكَاةَ وَأَطِيعُوا الرَّسُولَ لَعَلَّكُمْ تُرْحَمُونَ ۝٥٦
Wa aqeemus Salaata wa aatuz Zakaata wa atee`ur Rasoola la`allakum turhamoon
📖 Tekkim Wolof
Nangeen di taxawal julli tey génne asaka, te it nangeen topp Yonent bi, ndaxtele yërëmees leen.
🎧 Dégg

📜 Aaya 54-58 — An-Nur

54قُلْ أَطِيعُوا اللَّهَ وَأَطِيعُوا الرَّسُولَ ۖ فَإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا عَلَيْهِ مَا حُمِّلَ وَعَلَيْكُم مَّا حُمِّلْتُمْ ۖ وَإِن تُطِيعُوهُ تَهْتَدُوا ۚ وَمَا عَلَى الرَّسُولِ إِلَّا الْبَلَاغُ الْمُبِينُ
Neel : “Toppleen Yàlla te topp ab Yonentam. Bu ñu dummóoyoo [ndigal la] ñoom nag,... yéen itam ak seen mbiri bopp ; su ngen toppee [ndigal la] gindiku”. Yonent bi moom jottal rekk a ko ci war.
55وَعَدَ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا مِنكُمْ وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَيَسْتَخْلِفَنَّهُمْ فِي الْأَرْضِ كَمَا اسْتَخْلَفَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ وَلَيُمَكِّنَنَّ لَهُمْ دِينَهُمُ الَّذِي ارْتَضَىٰ لَهُمْ وَلَيُبَدِّلَنَّهُم مِّن بَعْدِ خَوْفِهِمْ أَمْنًا ۚ يَعْبُدُونَنِي لَا يُشْرِكُونَ بِي شَيْئًا ۚ وَمَن كَفَرَ بَعْدَ ذَٰلِكَ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Yàlla dig na ña gëm ci ñoom, tey jëf u yiw ne def na leen kuutaay ci kaw suuf kem ni Mu defe woon kuutaay ca ña leen jiitu woon. Te Dana leen yombalal jëfandikoo diiney [Islaam] ji Mu leen tànnal. Te it Dana leen soppil ginnaaw tiitaange kóolute. Ñu di Ma jaamu te duñu Ma bokkaale lenn. Képp ku weddi ginnaaw loolu, kon ñoom ñooy saay-saay sa.
56وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَآتُوا الزَّكَاةَ وَأَطِيعُوا الرَّسُولَ لَعَلَّكُمْ تُرْحَمُونَ
Nangeen di taxawal julli tey génne asaka, te it nangeen topp Yonent bi, ndaxtele yërëmees leen.
57لَا تَحْسَبَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا مُعْجِزِينَ فِي الْأَرْضِ ۚ وَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۖ وَلَبِئْسَ الْمَصِيرُ
Buleen foog ne yéefar yi dañoo tiiñ [Yàlla] ci kaw suuf. Seenub daluwaay Safara la. Ndaw muj gu bon.
58يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لِيَسْتَأْذِنكُمُ الَّذِينَ مَلَكَتْ أَيْمَانُكُمْ وَالَّذِينَ لَمْ يَبْلُغُوا الْحُلُمَ مِنكُمْ ثَلَاثَ مَرَّاتٍ ۚ مِّن قَبْلِ صَلَاةِ الْفَجْرِ وَحِينَ تَضَعُونَ ثِيَابَكُم مِّنَ الظَّهِيرَةِ وَمِن بَعْدِ صَلَاةِ الْعِشَاءِ ۚ ثَلَاثُ عَوْرَاتٍ لَّكُمْ ۚ لَيْسَ عَلَيْكُمْ وَلَا عَلَيْهِمْ جُنَاحٌ بَعْدَهُنَّ ۚ طَوَّافُونَ عَلَيْكُم بَعْضُكُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ ۚ كَذَٰلِكَ يُبَيِّنُ اللَّهُ لَكُمُ الْآيَاتِ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Éy yéen ñi gëm ! Na leen seeni jaam ak seeni xale yi matagul [mukkàllaf] di yëglu ba la ñoo dugg ci yéen ci ñetti waxtu yii : lu jiitu jullig fajar, ak bu ngeen summikoo ci njolloor, ak ginnaaw jullig gee ; loolu ñetti awra la ba ca waxtuy julli ya. Aayul ci yéen ngeen di gëwéelu di nemmeekuwante. Lii nag, Yàllaa leen cay faramfàcceel ay laayaam [kàddu], Yàlla ku xam la, Ku xereñ la.
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
56Aaya

Tekki — An-Nur 56

Simoore An-Nur Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen di taxawal julli tey génne asaka, te it nangeen…

Simoore Aaya 56/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers