Ash-Shura · 43/53
Tekki Waxtaan — Ash-Shura
وَلَمَن صَبَرَ وَغَفَرَ إِنَّ ذَٰلِكَ لَمِنْ عَزْمِ الْأُمُورِ ۝٤٣
Wa laman sabara wa ghafara inna zaalika lamin `azmil umoor
📖 Tekkim Wolof
Képp kuy muñ tey jéggële, man na ñu koo limaale ca ñu dogu ña.
🎧 Dégg

📜 Aaya 41-45 — Ash-Shura

41وَلَمَنِ انتَصَرَ بَعْدَ ظُلْمِهِ فَأُولَٰئِكَ مَا عَلَيْهِم مِّن سَبِيلٍ
Ñay fayu ginnaaw ba ñu leen tooñee,...ñooñu kenn amul ci ñoom aw yoon ;
42إِنَّمَا السَّبِيلُ عَلَى الَّذِينَ يَظْلِمُونَ النَّاسَ وَيَبْغُونَ فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ ۚ أُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña yoon war a dal ci seen kaw kay ñoo di, ñay tooñ nit ñi, di xaabaabal ci lu dul dëgg ci suuf si : mbugël mu mettee leen di xaar.
43وَلَمَن صَبَرَ وَغَفَرَ إِنَّ ذَٰلِكَ لَمِنْ عَزْمِ الْأُمُورِ
Képp kuy muñ tey jéggële, man na ñu koo limaale ca ñu dogu ña.
44وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِن وَلِيٍّ مِّن بَعْدِهِ ۗ وَتَرَى الظَّالِمِينَ لَمَّا رَأَوُا الْعَذَابَ يَقُولُونَ هَلْ إِلَىٰ مَرَدٍّ مِّن سَبِيلٍ
Képp ku Yàlla xas réerël dootul am kilifa gu koy man a aar ku dul Yàlla. Danga gis tooñkat ya bu ñu gisee mbugal ma dañuy wax naan : “Fu ñuy ame pexe mu nuy delloo [àddina] ? ”
45وَتَرَاهُمْ يُعْرَضُونَ عَلَيْهَا خَاشِعِينَ مِنَ الذُّلِّ يَنظُرُونَ مِن طَرْفٍ خَفِيٍّ ۗ وَقَالَ الَّذِينَ آمَنُوا إِنَّ الْخَاسِرِينَ الَّذِينَ خَسِرُوا أَنفُسَهُمْ وَأَهْلِيهِمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ أَلَا إِنَّ الظَّالِمِينَ فِي عَذَابٍ مُّقِيمٍ
Danga leen gis ñu di leen gaaral ca kanam Safara, ñu boole tiit ak gàcce, ña ngay xoole ne xeww di rummi, ña gëm ña ngay wax naan : “ña yàqule tigi, ñooy ñi ñàkk seen boop ak seenug njaboot bu Bis Pénc baa”. Tooñkat ya nekk ci mbugël mu sax.
Ash-ShuraFihi Alxuraan
53Aaya
MeccanRevelation
43Aaya

Tekki — Ash-Shura 43

Simoore Ash-Shura Aaya 43 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Képp kuy muñ tey jéggële, man na ñu koo limaale…

Simoore Aaya 43/53 — Ash-Shura الشورى (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ash-Shura Dégg, Ash-Shura Tekki, Ash-Shura mp3, Ash-Shura pdf. Aaya 41–45. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers