Ash-Shura · 44/53
Tekki Waxtaan — Ash-Shura
وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِن وَلِيٍّ مِّن بَعْدِهِ ۗ وَتَرَى الظَّالِمِينَ لَمَّا رَأَوُا الْعَذَابَ يَقُولُونَ هَلْ إِلَىٰ مَرَدٍّ مِّن سَبِيلٍ ۝٤٤
Wa mai yudlilil laahu famaa lahoo minw waliyyim mim ba`dih; wa taraz zaalimeena lammaa ra awul `azaaba yaqooloona hal ilaa maraddim min sabeel
📖 Tekkim Wolof
Képp ku Yàlla xas réerël dootul am kilifa gu koy man a aar ku dul Yàlla. Danga gis tooñkat ya bu ñu gisee mbugal ma dañuy wax naan : “Fu ñuy ame pexe mu nuy delloo [àddina] ? ”
🎧 Dégg

📜 Aaya 42-46 — Ash-Shura

42إِنَّمَا السَّبِيلُ عَلَى الَّذِينَ يَظْلِمُونَ النَّاسَ وَيَبْغُونَ فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ ۚ أُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña yoon war a dal ci seen kaw kay ñoo di, ñay tooñ nit ñi, di xaabaabal ci lu dul dëgg ci suuf si : mbugël mu mettee leen di xaar.
43وَلَمَن صَبَرَ وَغَفَرَ إِنَّ ذَٰلِكَ لَمِنْ عَزْمِ الْأُمُورِ
Képp kuy muñ tey jéggële, man na ñu koo limaale ca ñu dogu ña.
44وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِن وَلِيٍّ مِّن بَعْدِهِ ۗ وَتَرَى الظَّالِمِينَ لَمَّا رَأَوُا الْعَذَابَ يَقُولُونَ هَلْ إِلَىٰ مَرَدٍّ مِّن سَبِيلٍ
Képp ku Yàlla xas réerël dootul am kilifa gu koy man a aar ku dul Yàlla. Danga gis tooñkat ya bu ñu gisee mbugal ma dañuy wax naan : “Fu ñuy ame pexe mu nuy delloo [àddina] ? ”
45وَتَرَاهُمْ يُعْرَضُونَ عَلَيْهَا خَاشِعِينَ مِنَ الذُّلِّ يَنظُرُونَ مِن طَرْفٍ خَفِيٍّ ۗ وَقَالَ الَّذِينَ آمَنُوا إِنَّ الْخَاسِرِينَ الَّذِينَ خَسِرُوا أَنفُسَهُمْ وَأَهْلِيهِمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ أَلَا إِنَّ الظَّالِمِينَ فِي عَذَابٍ مُّقِيمٍ
Danga leen gis ñu di leen gaaral ca kanam Safara, ñu boole tiit ak gàcce, ña ngay xoole ne xeww di rummi, ña gëm ña ngay wax naan : “ña yàqule tigi, ñooy ñi ñàkk seen boop ak seenug njaboot bu Bis Pénc baa”. Tooñkat ya nekk ci mbugël mu sax.
46وَمَا كَانَ لَهُم مِّنْ أَوْلِيَاءَ يَنصُرُونَهُم مِّن دُونِ اللَّهِ ۗ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِن سَبِيلٍ
Amuñu ay wéeruwaay yu leen man a dimbali wudul Yàlla (ndax) képp ku Yàlla réerël mu sànku.
Ash-ShuraFihi Alxuraan
53Aaya
MeccanRevelation
44Aaya

Tekki — Ash-Shura 44

Simoore Ash-Shura Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Képp ku Yàlla xas réerël dootul am kilifa gu koy…

Simoore Aaya 44/53 — Ash-Shura الشورى (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ash-Shura Dégg, Ash-Shura Tekki, Ash-Shura mp3, Ash-Shura pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers