Al-Ahqaf · 31/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
يَا قَوْمَنَا أَجِيبُوا دَاعِيَ اللَّهِ وَآمِنُوا بِهِ يَغْفِرْ لَكُم مِّن ذُنُوبِكُمْ وَيُجِرْكُم مِّنْ عَذَابٍ أَلِيمٍ ۝٣١
Yaa qawmanaaa ajeeboo daa`iyal laahi wa aaminoo bihee yaghfir lakum min zunoobikum wa yujirkum min `azaabin aleem
📖 Tekkim Wolof
ey yéen sunuy xeet wuyu leen wootekatu Yàlla ba ! Te na ngeen koy gëm. (Su ngeen ko defee) dana leen di jéggal seen bàkkaar, te it kon dana leen yiir ci mbugal mu mitti.
🎧 Dégg

📜 Aaya 29-33 — Al-Ahqaf

29وَإِذْ صَرَفْنَا إِلَيْكَ نَفَرًا مِّنَ الْجِنِّ يَسْتَمِعُونَ الْقُرْآنَ فَلَمَّا حَضَرُوهُ قَالُوا أَنصِتُوا ۖ فَلَمَّا قُضِيَ وَلَّوْا إِلَىٰ قَوْمِهِم مُّنذِرِينَ
(Fàttalikul) itam ba nu jubëlee ci mbooloom jinne ngir ñuy déglu Alxuraan ba ñu teewee nee na : “déglu leen”... Ba mu jeexee, walbatiku nañu ca séen mbokki jinne di leen waar .
30قَالُوا يَا قَوْمَنَا إِنَّا سَمِعْنَا كِتَابًا أُنزِلَ مِن بَعْدِ مُوسَىٰ مُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ يَهْدِي إِلَى الْحَقِّ وَإِلَىٰ طَرِيقٍ مُّسْتَقِيمٍ
Nee na ñu : "Eey yéen sunuw xeet ! Déglu nanu ab Téere bu ñu wàcce ginnaaw Muusaa, muy dëggal la ko jiitu dafay gindee itam jëme ci dëgg. Ak ci yoon wu jub xocc wa.
31يَا قَوْمَنَا أَجِيبُوا دَاعِيَ اللَّهِ وَآمِنُوا بِهِ يَغْفِرْ لَكُم مِّن ذُنُوبِكُمْ وَيُجِرْكُم مِّنْ عَذَابٍ أَلِيمٍ
ey yéen sunuy xeet wuyu leen wootekatu Yàlla ba ! Te na ngeen koy gëm. (Su ngeen ko defee) dana leen di jéggal seen bàkkaar, te it kon dana leen yiir ci mbugal mu mitti.
32وَمَن لَّا يُجِبْ دَاعِيَ اللَّهِ فَلَيْسَ بِمُعْجِزٍ فِي الْأَرْضِ وَلَيْسَ لَهُ مِن دُونِهِ أَوْلِيَاءُ ۚ أُولَٰئِكَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
Te nag képp ku wuyuwul wootekatu Yàlla ba. Du man a raw mukk Yàlla ci kaw suuf si, te it du am ku koy man a dimbali ginnaaw Yàlla. Ñooñee ña nga ci réer gu bir sori.
33أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّ اللَّهَ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَلَمْ يَعْيَ بِخَلْقِهِنَّ بِقَادِرٍ عَلَىٰ أَن يُحْيِيَ الْمَوْتَىٰ ۚ بَلَىٰ إِنَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Xanaa gisuñu ne Yàllaa bind asamaan yeek suuf si, te sonnut ci bind gi mu leen bind sàkk leen, xanaa war na man a dekkal néew ? Waaw-waaw. Moom man na lépp lu ne.
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
31Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 31

Simoore Al-Ahqaf Aaya 31 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ey yéen sunuy xeet wuyu leen wootekatu Yàlla ba !…

Simoore Aaya 31/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 29–33. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers