Al-Maida · 34/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
إِلَّا الَّذِينَ تَابُوا مِن قَبْلِ أَن تَقْدِرُوا عَلَيْهِمْ ۖ فَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٣٤
Illal lazeena taaboo min qabli an taqdiroo `alaihim fa`lamooo annnal laaha Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
ba mu des ñanga xam ne tuub nañu lu jiitu ngeen not leen : nangeen xam xéll ne Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 32-36 — Al-Maida

32مِنْ أَجْلِ ذَٰلِكَ كَتَبْنَا عَلَىٰ بَنِي إِسْرَائِيلَ أَنَّهُ مَن قَتَلَ نَفْسًا بِغَيْرِ نَفْسٍ أَوْ فَسَادٍ فِي الْأَرْضِ فَكَأَنَّمَا قَتَلَ النَّاسَ جَمِيعًا وَمَنْ أَحْيَاهَا فَكَأَنَّمَا أَحْيَا النَّاسَ جَمِيعًا ۚ وَلَقَدْ جَاءَتْهُمْ رُسُلُنَا بِالْبَيِّنَاتِ ثُمَّ إِنَّ كَثِيرًا مِّنْهُم بَعْدَ ذَٰلِكَ فِي الْأَرْضِ لَمُسْرِفُونَ
Ngir loolu, bokkal Nanu ca waa Banii-Israayiila, ne képp ku reyati nit koo xam ne reyul kenn, te deful njaaxum ci kaw suuf si, mel na ni rey na nit ñépp. Ku xettali nit, musal ko ci dee, mel na ni ku musal nit ñépp ci dee. Sunuy Yonent dikkal na leen ànd ak lay yu leer nàññ. Ginnaaw loolu, lu bari ci ñoom nekk ay yàqkat ci suuf si [àddina bi].
33إِنَّمَا جَزَاءُ الَّذِينَ يُحَارِبُونَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَيَسْعَوْنَ فِي الْأَرْضِ فَسَادًا أَن يُقَتَّلُوا أَوْ يُصَلَّبُوا أَوْ تُقَطَّعَ أَيْدِيهِمْ وَأَرْجُلُهُم مِّنْ خِلَافٍ أَوْ يُنفَوْا مِنَ الْأَرْضِ ۚ ذَٰلِكَ لَهُمْ خِزْيٌ فِي الدُّنْيَا ۖ وَلَهُمْ فِي الْآخِرَةِ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Peyug ñay jéem a xeex Yàlla ak Yonentam , tey dox di yàq ci suuf si, [seen àtte] nekkul lu dul ñu rey leen, mbaa ñu daaj leen ci ay bant, mbaa ñu dagg seeni yoxo ak seeni tànk cig jàllawle, mbaa ñu génn leen réew ma. Ñu simboo gàcce ci àddina ; te mbugal mu rëy dana leen dal ca àllaaxira,
34إِلَّا الَّذِينَ تَابُوا مِن قَبْلِ أَن تَقْدِرُوا عَلَيْهِمْ ۖ فَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
ba mu des ñanga xam ne tuub nañu lu jiitu ngeen not leen : nangeen xam xéll ne Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
35يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَابْتَغُوا إِلَيْهِ الْوَسِيلَةَ وَجَاهِدُوا فِي سَبِيلِهِ لَعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla, sàkkuleen lu leen di jigeeñal Yàlla te nangeen sonn ci liggéeyal Yàlla. Ndax Yàlla ngeen texe !
36إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا لَوْ أَنَّ لَهُم مَّا فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا وَمِثْلَهُ مَعَهُ لِيَفْتَدُوا بِهِ مِنْ عَذَابِ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَا تُقُبِّلَ مِنْهُمْ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne weddi nañu, bu ñu amoon àddina ak li ci biiram lépp ba dolli ca li na toll, bëgg koo joxe ngir jotoo ko ca mbugalum Bis-pénc ba, kenn duleen ko nangul. Te nag mbugal mu metteey dal ci seen kaw.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
34Aaya

Tekki — Al-Maida 34

Simoore Al-Maida Aaya 34 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ba mu des ñanga xam ne tuub nañu lu jiitu…

Simoore Aaya 34/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 32–36. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers