Al-Hadid · 16/29
Tekki Waxtaan — Al-Hadid
۞ أَلَمْ يَأْنِ لِلَّذِينَ آمَنُوا أَن تَخْشَعَ قُلُوبُهُمْ لِذِكْرِ اللَّهِ وَمَا نَزَلَ مِنَ الْحَقِّ وَلَا يَكُونُوا كَالَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلُ فَطَالَ عَلَيْهِمُ الْأَمَدُ فَقَسَتْ قُلُوبُهُمْ ۖ وَكَثِيرٌ مِّنْهُمْ فَاسِقُونَ ۝١٦
Alam yaani laillzeena aamanooo an takhsha`a quloo buhum lizikril laahi wa maa nazala minal haqqi wa laa yakoonoo kallazeena ootul Kitaaba min qablu fataala `alaihimul amadu faqasat quloobuhum wa kaseerum minhum faasiqoon
📖 Tekkim Wolof
Ndax jotul nag ci ñi gëm, seeni xol ragal buur jëm ci di fàttaliku Yàllu ak lépp lu wàcci tey dëgg ? Te ñuy baña mel ni ña leen jiitu woon te Téere wàcci ca ñoom . Ba diir ba yàggee seeni xol wow, ba faf la ëpp ca ñoom saay-saay lañu (génn topp).

🎧 Dégg


📜 Aaya 14-18 — Al-Hadid

14يُنَادُونَهُمْ أَلَمْ نَكُن مَّعَكُمْ ۖ قَالُوا بَلَىٰ وَلَٰكِنَّكُمْ فَتَنتُمْ أَنفُسَكُمْ وَتَرَبَّصْتُمْ وَارْتَبْتُمْ وَغَرَّتْكُمُ الْأَمَانِيُّ حَتَّىٰ جَاءَ أَمْرُ اللَّهِ وَغَرَّكُم بِاللَّهِ الْغَرُورُ
“(Naaféq yaa ngay) woote naan xanaa àndunu woon ak yéen ? ” jullit ña ne. “Axakañ, waaye yéen a fitnaal seen bopp, daan fexeel (ñi gëm) daan werante, faggu ba faf mbirum Yàlla agsi saytaane nax leen.
15فَالْيَوْمَ لَا يُؤْخَذُ مِنكُمْ فِدْيَةٌ وَلَا مِنَ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ مَأْوَاكُمُ النَّارُ ۖ هِيَ مَوْلَاكُمْ ۖ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ
Bis niki tey, kenn du jël ci yéen ag njotu kenn it du ko jëll ca ña weddi. Seenub saxuwaay Safara moom ngeen mengóol: dootu leen tàggoo. Ndaw mujj gu bon !
16۞ أَلَمْ يَأْنِ لِلَّذِينَ آمَنُوا أَن تَخْشَعَ قُلُوبُهُمْ لِذِكْرِ اللَّهِ وَمَا نَزَلَ مِنَ الْحَقِّ وَلَا يَكُونُوا كَالَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلُ فَطَالَ عَلَيْهِمُ الْأَمَدُ فَقَسَتْ قُلُوبُهُمْ ۖ وَكَثِيرٌ مِّنْهُمْ فَاسِقُونَ
Ndax jotul nag ci ñi gëm, seeni xol ragal buur jëm ci di fàttaliku Yàllu ak lépp lu wàcci tey dëgg ? Te ñuy baña mel ni ña leen jiitu woon te Téere wàcci ca ñoom . Ba diir ba yàggee seeni xol wow, ba faf la ëpp ca ñoom saay-saay lañu (génn topp).
17اعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ يُحْيِي الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ قَدْ بَيَّنَّا لَكُمُ الْآيَاتِ لَعَلَّكُمْ تَعْقِلُونَ
Xamleen ne Yàllaay dundal suuf si ginnaaw ba mu dee. Leeralal Nanu leen, sunuy firnde ngir ngeen jëfandikoo seeni xol jàjju waaru.
18إِنَّ الْمُصَّدِّقِينَ وَالْمُصَّدِّقَاتِ وَأَقْرَضُوا اللَّهَ قَرْضًا حَسَنًا يُضَاعَفُ لَهُمْ وَلَهُمْ أَجْرٌ كَرِيمٌ
Saraxekat yu góor ak saraxekat yu jigéen ñiy lebal Yàlla bor bu rafet , dees na leen ko fulal te danañu am ag pey gu màgg.
Al-HadidFihi Alxuraan
29Aaya
MedinanRevelation
16Aaya

Tekki — Al-Hadid 16

Simoore Al-Hadid Aaya 16 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ndax jotul nag ci ñi gëm, seeni xol ragal buur…

Simoore Aaya 16/29 — Al-Hadid الحديد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hadid Dégg, Al-Hadid Tekki, Al-Hadid mp3, Al-Hadid pdf. Aaya 14–18. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers