Al-Hashr · 11/24
Tekki Waxtaan — Al-Hashr
۞ أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ نَافَقُوا يَقُولُونَ لِإِخْوَانِهِمُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَئِنْ أُخْرِجْتُمْ لَنَخْرُجَنَّ مَعَكُمْ وَلَا نُطِيعُ فِيكُمْ أَحَدًا أَبَدًا وَإِن قُوتِلْتُمْ لَنَنصُرَنَّكُمْ وَاللَّهُ يَشْهَدُ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ ۝١١
Alam tara ilal lazeena naafaqoo yaqooloona li ikhwaanihimul lazeena kafaroo min ahlil kitaabi la`in ukhrijtum lanakhrujanna ma`akum wa laa nutee`u feekum ahadan abadanw-wa in qootiltum lanansuran nakum wallaahu yashhadu innahum lakaaziboon
📖 Tekkim Wolof
Xanaa gisuloo ña naaféq ña ngay wax ak seeni mbokk ya weddi ci ñoñ Téere naan leen : “Bu ñu leen génnee, dananu génn ànd ak yéen te dunu topp kenn ci lu leen di lor yéen ; te kuy xex ak yéen, nun yéen la nuy jàppale”. Te Yàlla seede na ne ñoom ay fenkat la ñu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 9-13 — Al-Hashr

9وَالَّذِينَ تَبَوَّءُوا الدَّارَ وَالْإِيمَانَ مِن قَبْلِهِمْ يُحِبُّونَ مَنْ هَاجَرَ إِلَيْهِمْ وَلَا يَجِدُونَ فِي صُدُورِهِمْ حَاجَةً مِّمَّا أُوتُوا وَيُؤْثِرُونَ عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ وَلَوْ كَانَ بِهِمْ خَصَاصَةٌ ۚ وَمَن يُوقَ شُحَّ نَفْسِهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ
[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] ña dëkke woon réewum (Madiina), te gëmoon ba ñu leen laataa fekk si, te soppoon lool ña gàddaay jëm si ci ñoom, iñaane wuñu leen dara, di jiital aajoy ña gàddaay ci seen aajoy bopp, ak luñu ñàkk ñàkk. Képp ku mucc ci nay, baaxle na fàww.
10وَالَّذِينَ جَاءُوا مِن بَعْدِهِمْ يَقُولُونَ رَبَّنَا اغْفِرْ لَنَا وَلِإِخْوَانِنَا الَّذِينَ سَبَقُونَا بِالْإِيمَانِ وَلَا تَجْعَلْ فِي قُلُوبِنَا غِلًّا لِّلَّذِينَ آمَنُوا رَبَّنَا إِنَّكَ رَءُوفٌ رَّحِيمٌ
[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] ña dikk seen ginnaaw tey wax naan : “Yaw sunu Boroom, jéggalnu, nook sunu mbokk yi ñu jiitu ci ngëm ; te bul bàyyi genn mbañeel ci sunuy xol jëm ci ñi gëm. Yaw sunu Boroom, Kuy ñewenti nga Kuy Jaglewaakoon nga sa Yërmënde”.
11۞ أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ نَافَقُوا يَقُولُونَ لِإِخْوَانِهِمُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَئِنْ أُخْرِجْتُمْ لَنَخْرُجَنَّ مَعَكُمْ وَلَا نُطِيعُ فِيكُمْ أَحَدًا أَبَدًا وَإِن قُوتِلْتُمْ لَنَنصُرَنَّكُمْ وَاللَّهُ يَشْهَدُ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ
Xanaa gisuloo ña naaféq ña ngay wax ak seeni mbokk ya weddi ci ñoñ Téere naan leen : “Bu ñu leen génnee, dananu génn ànd ak yéen te dunu topp kenn ci lu leen di lor yéen ; te kuy xex ak yéen, nun yéen la nuy jàppale”. Te Yàlla seede na ne ñoom ay fenkat la ñu.
12لَئِنْ أُخْرِجُوا لَا يَخْرُجُونَ مَعَهُمْ وَلَئِن قُوتِلُوا لَا يَنصُرُونَهُمْ وَلَئِن نَّصَرُوهُمْ لَيُوَلُّنَّ الْأَدْبَارَ ثُمَّ لَا يُنصَرُونَ
Bu ñu leen génnee woon, ñoom duñu génn mukk di ànd ak ñoom ; bu ñu doon xeex it , dunu leen jàppale ; sax dañuy mujj daw ; te duñu am ndam.
13لَأَنتُمْ أَشَدُّ رَهْبَةً فِي صُدُورِهِم مِّنَ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَوْمٌ لَّا يَفْقَهُونَ
Ñoom naaféq yi seen jëmm yii la ñu gën a ragal ci Yàlla. Ndax ñoom dañoo xamul.
Al-HashrFihi Alxuraan
24Aaya
MedinanRevelation
11Aaya

Tekki — Al-Hashr 11

Simoore Al-Hashr Aaya 11 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Xanaa gisuloo ña naaféq ña ngay wax ak seeni mbokk…

Simoore Aaya 11/24 — Al-Hashr الحشر (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hashr Dégg, Al-Hashr Tekki, Al-Hashr mp3, Al-Hashr pdf. Aaya 9–13. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers