Al-Hashr · 12/24
Tekki Waxtaan — Al-Hashr
لَئِنْ أُخْرِجُوا لَا يَخْرُجُونَ مَعَهُمْ وَلَئِن قُوتِلُوا لَا يَنصُرُونَهُمْ وَلَئِن نَّصَرُوهُمْ لَيُوَلُّنَّ الْأَدْبَارَ ثُمَّ لَا يُنصَرُونَ ۝١٢
La`in ukhrijoo laa yakhrujoona ma`ahum wa la`in qootiloo laa yansuroonahum wa la`in nasaroohum la yuwallunnal adbaara summa laa yunsaroon
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu leen génnee woon, ñoom duñu génn mukk di ànd ak ñoom ; bu ñu doon xeex it , dunu leen jàppale ; sax dañuy mujj daw ; te duñu am ndam.

🎧 Dégg


📜 Aaya 10-14 — Al-Hashr

10وَالَّذِينَ جَاءُوا مِن بَعْدِهِمْ يَقُولُونَ رَبَّنَا اغْفِرْ لَنَا وَلِإِخْوَانِنَا الَّذِينَ سَبَقُونَا بِالْإِيمَانِ وَلَا تَجْعَلْ فِي قُلُوبِنَا غِلًّا لِّلَّذِينَ آمَنُوا رَبَّنَا إِنَّكَ رَءُوفٌ رَّحِيمٌ
[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] ña dikk seen ginnaaw tey wax naan : “Yaw sunu Boroom, jéggalnu, nook sunu mbokk yi ñu jiitu ci ngëm ; te bul bàyyi genn mbañeel ci sunuy xol jëm ci ñi gëm. Yaw sunu Boroom, Kuy ñewenti nga Kuy Jaglewaakoon nga sa Yërmënde”.
11۞ أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ نَافَقُوا يَقُولُونَ لِإِخْوَانِهِمُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَئِنْ أُخْرِجْتُمْ لَنَخْرُجَنَّ مَعَكُمْ وَلَا نُطِيعُ فِيكُمْ أَحَدًا أَبَدًا وَإِن قُوتِلْتُمْ لَنَنصُرَنَّكُمْ وَاللَّهُ يَشْهَدُ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ
Xanaa gisuloo ña naaféq ña ngay wax ak seeni mbokk ya weddi ci ñoñ Téere naan leen : “Bu ñu leen génnee, dananu génn ànd ak yéen te dunu topp kenn ci lu leen di lor yéen ; te kuy xex ak yéen, nun yéen la nuy jàppale”. Te Yàlla seede na ne ñoom ay fenkat la ñu.
12لَئِنْ أُخْرِجُوا لَا يَخْرُجُونَ مَعَهُمْ وَلَئِن قُوتِلُوا لَا يَنصُرُونَهُمْ وَلَئِن نَّصَرُوهُمْ لَيُوَلُّنَّ الْأَدْبَارَ ثُمَّ لَا يُنصَرُونَ
Bu ñu leen génnee woon, ñoom duñu génn mukk di ànd ak ñoom ; bu ñu doon xeex it , dunu leen jàppale ; sax dañuy mujj daw ; te duñu am ndam.
13لَأَنتُمْ أَشَدُّ رَهْبَةً فِي صُدُورِهِم مِّنَ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَوْمٌ لَّا يَفْقَهُونَ
Ñoom naaféq yi seen jëmm yii la ñu gën a ragal ci Yàlla. Ndax ñoom dañoo xamul.
14لَا يُقَاتِلُونَكُمْ جَمِيعًا إِلَّا فِي قُرًى مُّحَصَّنَةٍ أَوْ مِن وَرَاءِ جُدُرٍ ۚ بَأْسُهُم بَيْنَهُمْ شَدِيدٌ ۚ تَحْسَبُهُمْ جَمِيعًا وَقُلُوبُهُمْ شَتَّىٰ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَوْمٌ لَّا يَعْقِلُونَ
Duñuy xeex ak yéen mukk (ñoom naaféq ya) lu dul biir dëkk yu ñu tata ci ginnaaw ay ñag. Seenug noonoo ci seen biir lu tar la. Danga foog ne ñu ànd lañu, te seeni xol dañoo féewoo. Li ko waral moo di ne dañoo amul ay xol di ko jariñoo.
Al-HashrFihi Alxuraan
24Aaya
MedinanRevelation
12Aaya

Tekki — Al-Hashr 12

Simoore Al-Hashr Aaya 12 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu leen génnee woon, ñoom duñu génn mukk di…

Simoore Aaya 12/24 — Al-Hashr الحشر (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hashr Dégg, Al-Hashr Tekki, Al-Hashr mp3, Al-Hashr pdf. Aaya 10–14. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers