Al-Hashr · 20/24
Tekki Waxtaan — Al-Hashr
لَا يَسْتَوِي أَصْحَابُ النَّارِ وَأَصْحَابُ الْجَنَّةِ ۚ أَصْحَابُ الْجَنَّةِ هُمُ الْفَائِزُونَ ۝٢٠
Laa yastaweee as-haabun naari wa ashaabul jannah; as haabul jannati humul faaa`izoon
📖 Tekkim Wolof
Waa Safara duñu yem ak waa Àjjana mukk. Ndax waa Àjjana ñoo di ña texe.

🎧 Dégg


📜 Aaya 18-22 — Al-Hashr

18يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَلْتَنظُرْ نَفْسٌ مَّا قَدَّمَتْ لِغَدٍ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla. Bakkan bu nekk nay xool la muy jiital ngir ëllëg. Te nangeen di ragal Yàlla, Yàlla dey ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
19وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ نَسُوا اللَّهَ فَأَنسَاهُمْ أَنفُسَهُمْ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Buleen def mukk ni gaa ña fàtte woon Yàlla ; Mu faf fàttiloo leen seen bopp ; ñooñee ñoo di saay-saay si.
20لَا يَسْتَوِي أَصْحَابُ النَّارِ وَأَصْحَابُ الْجَنَّةِ ۚ أَصْحَابُ الْجَنَّةِ هُمُ الْفَائِزُونَ
Waa Safara duñu yem ak waa Àjjana mukk. Ndax waa Àjjana ñoo di ña texe.
21لَوْ أَنزَلْنَا هَٰذَا الْقُرْآنَ عَلَىٰ جَبَلٍ لَّرَأَيْتَهُ خَاشِعًا مُّتَصَدِّعًا مِّنْ خَشْيَةِ اللَّهِ ۚ وَتِلْكَ الْأَمْثَالُ نَضْرِبُهَا لِلنَّاسِ لَعَلَّهُمْ يَتَفَكَّرُونَ
Sunu wàcce woon Alxuraan jii ci kaw aw doj, kon dey nga gis ko muy toroxlu daldi moñoxoo ngir ragal Yàlla. Yooyu ay léeb la yu nuy saddal nit ñi ngir ñu man caa xalaate.
22هُوَ اللَّهُ الَّذِي لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ عَالِمُ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ ۖ هُوَ الرَّحْمَٰنُ الرَّحِيمُ
Moom mooy Yàlla ji nga xam ne. Amul jeneen Yàlla ju dul moom, Moo xam kumpa ak li Feeñ. Mooy, Yëramaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
Al-HashrFihi Alxuraan
24Aaya
MedinanRevelation
20Aaya

Tekki — Al-Hashr 20

Simoore Al-Hashr Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waa Safara duñu yem ak waa Àjjana mukk. Ndax waa…

Simoore Aaya 20/24 — Al-Hashr الحشر (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hashr Dégg, Al-Hashr Tekki, Al-Hashr mp3, Al-Hashr pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers