Al-Hashr · 21/24
Tekki Waxtaan — Al-Hashr
لَوْ أَنزَلْنَا هَٰذَا الْقُرْآنَ عَلَىٰ جَبَلٍ لَّرَأَيْتَهُ خَاشِعًا مُّتَصَدِّعًا مِّنْ خَشْيَةِ اللَّهِ ۚ وَتِلْكَ الْأَمْثَالُ نَضْرِبُهَا لِلنَّاسِ لَعَلَّهُمْ يَتَفَكَّرُونَ ۝٢١
Law anzalnaa haazal quraana `alaa jabilil lara aytahoo khaashi`am muta saddi`am min khashiyatil laah; wa tilkal amsaalu nadribuhaa linnaasi la`allahum yatafakkaroon
📖 Tekkim Wolof
Sunu wàcce woon Alxuraan jii ci kaw aw doj, kon dey nga gis ko muy toroxlu daldi moñoxoo ngir ragal Yàlla. Yooyu ay léeb la yu nuy saddal nit ñi ngir ñu man caa xalaate.

🎧 Dégg


📜 Aaya 19-23 — Al-Hashr

19وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ نَسُوا اللَّهَ فَأَنسَاهُمْ أَنفُسَهُمْ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Buleen def mukk ni gaa ña fàtte woon Yàlla ; Mu faf fàttiloo leen seen bopp ; ñooñee ñoo di saay-saay si.
20لَا يَسْتَوِي أَصْحَابُ النَّارِ وَأَصْحَابُ الْجَنَّةِ ۚ أَصْحَابُ الْجَنَّةِ هُمُ الْفَائِزُونَ
Waa Safara duñu yem ak waa Àjjana mukk. Ndax waa Àjjana ñoo di ña texe.
21لَوْ أَنزَلْنَا هَٰذَا الْقُرْآنَ عَلَىٰ جَبَلٍ لَّرَأَيْتَهُ خَاشِعًا مُّتَصَدِّعًا مِّنْ خَشْيَةِ اللَّهِ ۚ وَتِلْكَ الْأَمْثَالُ نَضْرِبُهَا لِلنَّاسِ لَعَلَّهُمْ يَتَفَكَّرُونَ
Sunu wàcce woon Alxuraan jii ci kaw aw doj, kon dey nga gis ko muy toroxlu daldi moñoxoo ngir ragal Yàlla. Yooyu ay léeb la yu nuy saddal nit ñi ngir ñu man caa xalaate.
22هُوَ اللَّهُ الَّذِي لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ عَالِمُ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ ۖ هُوَ الرَّحْمَٰنُ الرَّحِيمُ
Moom mooy Yàlla ji nga xam ne. Amul jeneen Yàlla ju dul moom, Moo xam kumpa ak li Feeñ. Mooy, Yëramaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
23هُوَ اللَّهُ الَّذِي لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الْمَلِكُ الْقُدُّوسُ السَّلَامُ الْمُؤْمِنُ الْمُهَيْمِنُ الْعَزِيزُ الْجَبَّارُ الْمُتَكَبِّرُ ۚ سُبْحَانَ اللَّهِ عَمَّا يُشْرِكُونَ
Moom Mooy, Yàlla ji nga xam ne. Amul jeneen Yàlla ju dul moom ; mooy Boroom bi, di Ku Sell ki, di Jàmm ji, di Ku Wóor ki, di Ku Peek lépp, di Boroom Kàttan gi, di Ponkal mi, di Ku Rëy ki. Tudd naa Sellam gi ! Soree na lool ak li ñu koy bokkaaleel.
Al-HashrFihi Alxuraan
24Aaya
MedinanRevelation
21Aaya

Tekki — Al-Hashr 21

Simoore Al-Hashr Aaya 21 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Sunu wàcce woon Alxuraan jii ci kaw aw doj, kon…

Simoore Aaya 21/24 — Al-Hashr الحشر (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hashr Dégg, Al-Hashr Tekki, Al-Hashr mp3, Al-Hashr pdf. Aaya 19–23. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers