Al-An'am · 93/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ قَالَ أُوحِيَ إِلَيَّ وَلَمْ يُوحَ إِلَيْهِ شَيْءٌ وَمَن قَالَ سَأُنزِلُ مِثْلَ مَا أَنزَلَ اللَّهُ ۗ وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الظَّالِمُونَ فِي غَمَرَاتِ الْمَوْتِ وَالْمَلَائِكَةُ بَاسِطُو أَيْدِيهِمْ أَخْرِجُوا أَنفُسَكُمُ ۖ الْيَوْمَ تُجْزَوْنَ عَذَابَ الْهُونِ بِمَا كُنتُمْ تَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ غَيْرَ الْحَقِّ وَكُنتُمْ عَنْ آيَاتِهِ تَسْتَكْبِرُونَ ۝٩٣
Wa man azlamu mimmanif taraa `alal laahi kaziban aw qaala oohiya ilaiya wa lam yooha ilaihi shai`un wa man qaala sa unzilu misla maaa anzalal laah; wa law taraaa iziz zaalimoona fee ghamaraatil mawti walmalaaa`ikatu baasitooo aideehim akhrijooo anfusakum; al yawma tujzawna `azaabal hooni bimaa kuntum taqooloona `alal laahi ghairal haqqi wa kuntum `an aayaatihee tastakbiroon
📖 Tekkim Wolof
Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla muy wax naan : “Soloo nañu ma”, te fekk soloowuñu ko dara. Ak kuy wax naan : “Danaa wàcce lu mel ni lii Yàlla wàcce.”. Cëy boo gisoon tooñkat ya bis ba ñu nekkee ci wextanu ndee, te Malaaka ya tàllal seeni yoxo (naan leen) : “Génneleen seen bopp. Tey jii, dees na leen feye mbugal muy toroxale ci sababus la ngeen doon wax ci Yàlla te du dëgg ak la ngeen daan rëy-rëylu tey dëddu ay tegtalam”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 91-95 — Al-An'am

91وَمَا قَدَرُوا اللَّهَ حَقَّ قَدْرِهِ إِذْ قَالُوا مَا أَنزَلَ اللَّهُ عَلَىٰ بَشَرٍ مِّن شَيْءٍ ۗ قُلْ مَنْ أَنزَلَ الْكِتَابَ الَّذِي جَاءَ بِهِ مُوسَىٰ نُورًا وَهُدًى لِّلنَّاسِ ۖ تَجْعَلُونَهُ قَرَاطِيسَ تُبْدُونَهَا وَتُخْفُونَ كَثِيرًا ۖ وَعُلِّمْتُم مَّا لَمْ تَعْلَمُوا أَنتُمْ وَلَا آبَاؤُكُمْ ۖ قُلِ اللَّهُ ۖ ثُمَّ ذَرْهُمْ فِي خَوْضِهِمْ يَلْعَبُونَ
Màggaluñu Yàlla kem dayo bi mu yayoo ñu màggale Ko, bu ñu waxee ne : “Yàlla wàccewul dara ci kenn.”. Neel : “Kan moo wàcce Téere bu Muusaa ànd ak leer ak njub ñeel nit ñi ? Ngeen bind ko ciy këyit di ko wone ak di ca nëbb lu bari. Te jàngaleef na leen lu ngeen xamul woon yéen ak seeni baay. Neel : “Yàlla la”. Te nga bàyyi leen ci seen cànkute ga ñuy nuur cim po.
92وَهَٰذَا كِتَابٌ أَنزَلْنَاهُ مُبَارَكٌ مُّصَدِّقُ الَّذِي بَيْنَ يَدَيْهِ وَلِتُنذِرَ أُمَّ الْقُرَىٰ وَمَنْ حَوْلَهَا ۚ وَالَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۖ وَهُمْ عَلَىٰ صَلَاتِهِمْ يُحَافِظُونَ
Te lii Téere la bu ñu wàcce bu barkeel, buy dëggal la ko jiitu, ak ngir nga waar waa ndeyi njéndi ya [Màkka] ak la ko wër. Ña gëm àllaaxira, danañu ko gëm te ñoom danañu sàmm seeni julli.
93وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ قَالَ أُوحِيَ إِلَيَّ وَلَمْ يُوحَ إِلَيْهِ شَيْءٌ وَمَن قَالَ سَأُنزِلُ مِثْلَ مَا أَنزَلَ اللَّهُ ۗ وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الظَّالِمُونَ فِي غَمَرَاتِ الْمَوْتِ وَالْمَلَائِكَةُ بَاسِطُو أَيْدِيهِمْ أَخْرِجُوا أَنفُسَكُمُ ۖ الْيَوْمَ تُجْزَوْنَ عَذَابَ الْهُونِ بِمَا كُنتُمْ تَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ غَيْرَ الْحَقِّ وَكُنتُمْ عَنْ آيَاتِهِ تَسْتَكْبِرُونَ
Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla muy wax naan : “Soloo nañu ma”, te fekk soloowuñu ko dara. Ak kuy wax naan : “Danaa wàcce lu mel ni lii Yàlla wàcce.”. Cëy boo gisoon tooñkat ya bis ba ñu nekkee ci wextanu ndee, te Malaaka ya tàllal seeni yoxo (naan leen) : “Génneleen seen bopp. Tey jii, dees na leen feye mbugal muy toroxale ci sababus la ngeen doon wax ci Yàlla te du dëgg ak la ngeen daan rëy-rëylu tey dëddu ay tegtalam”.
94وَلَقَدْ جِئْتُمُونَا فُرَادَىٰ كَمَا خَلَقْنَاكُمْ أَوَّلَ مَرَّةٍ وَتَرَكْتُم مَّا خَوَّلْنَاكُمْ وَرَاءَ ظُهُورِكُمْ ۖ وَمَا نَرَىٰ مَعَكُمْ شُفَعَاءَكُمُ الَّذِينَ زَعَمْتُمْ أَنَّهُمْ فِيكُمْ شُرَكَاءُ ۚ لَقَد تَّقَطَّعَ بَيْنَكُمْ وَضَلَّ عَنكُم مَّا كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
(Moom Yàlla Mu ne leen) Dikk ngeen di kenn kenn ni Nu leen binde woon cig njalbéen, te bàyyi ci seen ginnaaw la ñu leen wërsëgale woon. Waaw Nun sax gisunu ña ngeen daan jaamu, di ko bokkaale ak Yàlla. Léegi seen digganteek ñoom dog na, te la ngeen doon sos réer na leen.
95۞ إِنَّ اللَّهَ فَالِقُ الْحَبِّ وَالنَّوَىٰ ۖ يُخْرِجُ الْحَيَّ مِنَ الْمَيِّتِ وَمُخْرِجُ الْمَيِّتِ مِنَ الْحَيِّ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ
Yàlla mooy xar pepp ak i saal : [génne ca luy sax gàncax walla garab], Mooy génne luy dundu ci lu dee, tey génne lu dee ci luy dundu. Yàllaa ngoogu. Waaw naka lañu leen wëlbatee ?
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
93Aaya

Tekki — Al-An'am 93

Simoore Al-An'am Aaya 93 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen,…

Simoore Aaya 93/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 91–95. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers