Al-Jumu'a · 8/11
Tekki Waxtaan — Al-Jumu'a
قُلْ إِنَّ الْمَوْتَ الَّذِي تَفِرُّونَ مِنْهُ فَإِنَّهُ مُلَاقِيكُمْ ۖ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝٨
Qul innal mawtal lazee tafirroona minhu fa innahoo mulaaqeekum summa turaddoona ilaa `Aalimil Ghaibi wash shahaadati fa yunabbi`ukum bimaa kuntum ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
Waxal ne : “Dee gi ngeen di daw dana dajeek yéen. Ba noppi ñu delloo leen ca Yàlla mi xam kumpaak li feeñ mu di leen xibaar la ngeen daan def”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 6-10 — Al-Jumu'a

6قُلْ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ هَادُوا إِن زَعَمْتُمْ أَنَّكُمْ أَوْلِيَاءُ لِلَّهِ مِن دُونِ النَّاسِ فَتَمَنَّوُا الْمَوْتَ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Waxal ne : "Eey yéen Yahuud yi ! Su fekkee ne nii ngeen méngook Yàllaay, kon ñaan leen dee, su fekkee ne dëggu ngeen”.
7وَلَا يَتَمَنَّوْنَهُ أَبَدًا بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيهِمْ ۚ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالظَّالِمِينَ
Dunu ko ñaan mukk ngir (la ñu jëf cik caay-caay). Yàlla ku Xamaakoon la tooñkat yi.
8قُلْ إِنَّ الْمَوْتَ الَّذِي تَفِرُّونَ مِنْهُ فَإِنَّهُ مُلَاقِيكُمْ ۖ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Waxal ne : “Dee gi ngeen di daw dana dajeek yéen. Ba noppi ñu delloo leen ca Yàlla mi xam kumpaak li feeñ mu di leen xibaar la ngeen daan def”.
9يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا نُودِيَ لِلصَّلَاةِ مِن يَوْمِ الْجُمُعَةِ فَاسْعَوْا إِلَىٰ ذِكْرِ اللَّهِ وَذَرُوا الْبَيْعَ ۚ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
Eey yéen ñi gëm ! Saa suñu wootee ngir julli ci bisub Àjjuma, dawleen jëm ci tudd Yàlla te nangeen fa ne ñukk njaay ma bàyyi ko. Looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon!
10فَإِذَا قُضِيَتِ الصَّلَاةُ فَانتَشِرُوا فِي الْأَرْضِ وَابْتَغُوا مِن فَضْلِ اللَّهِ وَاذْكُرُوا اللَّهَ كَثِيرًا لَّعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ
Su julli gi jeexee, na ngeen tasaaroo ci suuf si, tey sàkku ci xeewali Yàlla yi, te na ngeen di tudd Yàlla lu bari ndax amaana ngeen baaxle.
Al-Jumu'aFihi Alxuraan
11Aaya
MedinanRevelation
8Aaya

Tekki — Al-Jumu'a 8

Simoore Al-Jumu'a Aaya 8 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waxal ne : “Dee gi ngeen di daw dana dajeek…

Simoore Aaya 8/11 — Al-Jumu'a الجمعة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Jumu'a Dégg, Al-Jumu'a Tekki, Al-Jumu'a mp3, Al-Jumu'a pdf. Aaya 6–10. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers