At-Tahrim · 5/12
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tahrim
عَسَىٰ رَبُّهُ إِن طَلَّقَكُنَّ أَن يُبْدِلَهُ أَزْوَاجًا خَيْرًا مِّنكُنَّ مُسْلِمَاتٍ مُّؤْمِنَاتٍ قَانِتَاتٍ تَائِبَاتٍ عَابِدَاتٍ سَائِحَاتٍ ثَيِّبَاتٍ وَأَبْكَارًا ۝٥
Asaa rabbuhooo in tallaqakunna anyyubdilahooo azwaajan khairam mnkunna muslimaatim mu`minaatin qaanitaatin taaa`ibaatin `aabidaatin saaa`ihaatin saiyibaatinw wa abkaaraa
📖 Tekkim Wolof
Te itam su leen fasee, Boroomam dana ko jox ay soxna yu leen gën, yu di ay jullit, yu gëm, yuy topp ndigal, ñuy tuub, ñuy jaamu, ñuy woor, di ay jeeg mba ay janq.

🎧 Dégg


📜 Aaya 3-7 — Simoore At-Tahrim

3وَإِذْ أَسَرَّ النَّبِيُّ إِلَىٰ بَعْضِ أَزْوَاجِهِ حَدِيثًا فَلَمَّا نَبَّأَتْ بِهِ وَأَظْهَرَهُ اللَّهُ عَلَيْهِ عَرَّفَ بَعْضَهُ وَأَعْرَضَ عَن بَعْضٍ ۖ فَلَمَّا نَبَّأَهَا بِهِ قَالَتْ مَنْ أَنبَأَكَ هَٰذَا ۖ قَالَ نَبَّأَنِيَ الْعَلِيمُ الْخَبِيرُ
Ba Yonent bi joxee sekkare lennat ci soxnaam ba ñu ko tasaaree te Yàlla wuññil ko lenn la, dëddu leneen la. Ba mu ko xibaare soxna sa mu ne ko : “ku la ko xibaar ? ” Mu ne ko : “Yàlla mi Xam, te deñ Kumpa ci lépp mooma ko xibaar”.
4إِن تَتُوبَا إِلَى اللَّهِ فَقَدْ صَغَتْ قُلُوبُكُمَا ۖ وَإِن تَظَاهَرَا عَلَيْهِ فَإِنَّ اللَّهَ هُوَ مَوْلَاهُ وَجِبْرِيلُ وَصَالِحُ الْمُؤْمِنِينَ ۖ وَالْمَلَائِكَةُ بَعْدَ ذَٰلِكَ ظَهِيرٌ
Yéen ñaari soxna yi su ngeen tuubee (moo gën) ndax seeni xol jeng na. Su ngeen takktoo (Yonent bi), Yàlla farnaak moom, ak Jibriil ak jullit ñu yiw ñi, ak Malaaka yi di ko dimbali.
5عَسَىٰ رَبُّهُ إِن طَلَّقَكُنَّ أَن يُبْدِلَهُ أَزْوَاجًا خَيْرًا مِّنكُنَّ مُسْلِمَاتٍ مُّؤْمِنَاتٍ قَانِتَاتٍ تَائِبَاتٍ عَابِدَاتٍ سَائِحَاتٍ ثَيِّبَاتٍ وَأَبْكَارًا
Te itam su leen fasee, Boroomam dana ko jox ay soxna yu leen gën, yu di ay jullit, yu gëm, yuy topp ndigal, ñuy tuub, ñuy jaamu, ñuy woor, di ay jeeg mba ay janq.
6يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا قُوا أَنفُسَكُمْ وَأَهْلِيكُمْ نَارًا وَقُودُهَا النَّاسُ وَالْحِجَارَةُ عَلَيْهَا مَلَائِكَةٌ غِلَاظٌ شِدَادٌ لَّا يَعْصُونَ اللَّهَ مَا أَمَرَهُمْ وَيَفْعَلُونَ مَا يُؤْمَرُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Fegalleen seen bopp ak seen njaboot, aw Safara woo xam ne matt ma aw nit lay doon ak xeer, ay Malaaka yu tal, te tar, ñoo fay nekk duñu moy mukk, li leen Yàlla digal te la mu leen digal la ñuy def.
7يَا أَيُّهَا الَّذِينَ كَفَرُوا لَا تَعْتَذِرُوا الْيَوْمَ ۖ إِنَّمَا تُجْزَوْنَ مَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Éy yéen Yéefër yi! Buleen jéema jéggalu tey danañuleen fay la ngeen daan jëf.
At-TahrimFihi Alxuraan
12Aaya
MedinanRevelation
5Aaya

Tekki — At-Tahrim 5

Simoore At-Tahrim Aaya 5 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te itam su leen fasee, Boroomam dana ko jox ay…

Simoore Aaya 5/12 — Simoore At-Tahrim التحريم (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tahrim Dégg, Simoore At-Tahrim Tekki, Simoore At-Tahrim mp3, Simoore At-Tahrim pdf. Aaya 3–7. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers