At-Tahrim · 4/12
Tekki Waxtaan — At-Tahrim
إِن تَتُوبَا إِلَى اللَّهِ فَقَدْ صَغَتْ قُلُوبُكُمَا ۖ وَإِن تَظَاهَرَا عَلَيْهِ فَإِنَّ اللَّهَ هُوَ مَوْلَاهُ وَجِبْرِيلُ وَصَالِحُ الْمُؤْمِنِينَ ۖ وَالْمَلَائِكَةُ بَعْدَ ذَٰلِكَ ظَهِيرٌ ۝٤
In tatoobaaa ilal laahi faqad saghat quloobukumaa wa in tazaaharaa `alihi fa innal laaha huwa mawlaahu wa jibreelu wa saalihul mu`mineen; walma laaa`ikatu ba`dazaalika zaheer
📖 Tekkim Wolof
Yéen ñaari soxna yi su ngeen tuubee (moo gën) ndax seeni xol jeng na. Su ngeen takktoo (Yonent bi), Yàlla farnaak moom, ak Jibriil ak jullit ñu yiw ñi, ak Malaaka yi di ko dimbali.
🎧 Dégg

📜 Aaya 2-6 — At-Tahrim

2قَدْ فَرَضَ اللَّهُ لَكُمْ تَحِلَّةَ أَيْمَانِكُمْ ۚ وَاللَّهُ مَوْلَاكُمْ ۖ وَهُوَ الْعَلِيمُ الْحَكِيمُ
Yàlla fartal na ci yéen, daganal seeni ngiñ. Yàlla di seen Boroom ; te Ku Xam la Ku Xereñ la .
3وَإِذْ أَسَرَّ النَّبِيُّ إِلَىٰ بَعْضِ أَزْوَاجِهِ حَدِيثًا فَلَمَّا نَبَّأَتْ بِهِ وَأَظْهَرَهُ اللَّهُ عَلَيْهِ عَرَّفَ بَعْضَهُ وَأَعْرَضَ عَن بَعْضٍ ۖ فَلَمَّا نَبَّأَهَا بِهِ قَالَتْ مَنْ أَنبَأَكَ هَٰذَا ۖ قَالَ نَبَّأَنِيَ الْعَلِيمُ الْخَبِيرُ
Ba Yonent bi joxee sekkare lennat ci soxnaam ba ñu ko tasaaree te Yàlla wuññil ko lenn la, dëddu leneen la. Ba mu ko xibaare soxna sa mu ne ko : “ku la ko xibaar ? ” Mu ne ko : “Yàlla mi Xam, te deñ Kumpa ci lépp mooma ko xibaar”.
4إِن تَتُوبَا إِلَى اللَّهِ فَقَدْ صَغَتْ قُلُوبُكُمَا ۖ وَإِن تَظَاهَرَا عَلَيْهِ فَإِنَّ اللَّهَ هُوَ مَوْلَاهُ وَجِبْرِيلُ وَصَالِحُ الْمُؤْمِنِينَ ۖ وَالْمَلَائِكَةُ بَعْدَ ذَٰلِكَ ظَهِيرٌ
Yéen ñaari soxna yi su ngeen tuubee (moo gën) ndax seeni xol jeng na. Su ngeen takktoo (Yonent bi), Yàlla farnaak moom, ak Jibriil ak jullit ñu yiw ñi, ak Malaaka yi di ko dimbali.
5عَسَىٰ رَبُّهُ إِن طَلَّقَكُنَّ أَن يُبْدِلَهُ أَزْوَاجًا خَيْرًا مِّنكُنَّ مُسْلِمَاتٍ مُّؤْمِنَاتٍ قَانِتَاتٍ تَائِبَاتٍ عَابِدَاتٍ سَائِحَاتٍ ثَيِّبَاتٍ وَأَبْكَارًا
Te itam su leen fasee, Boroomam dana ko jox ay soxna yu leen gën, yu di ay jullit, yu gëm, yuy topp ndigal, ñuy tuub, ñuy jaamu, ñuy woor, di ay jeeg mba ay janq.
6يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا قُوا أَنفُسَكُمْ وَأَهْلِيكُمْ نَارًا وَقُودُهَا النَّاسُ وَالْحِجَارَةُ عَلَيْهَا مَلَائِكَةٌ غِلَاظٌ شِدَادٌ لَّا يَعْصُونَ اللَّهَ مَا أَمَرَهُمْ وَيَفْعَلُونَ مَا يُؤْمَرُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Fegalleen seen bopp ak seen njaboot, aw Safara woo xam ne matt ma aw nit lay doon ak xeer, ay Malaaka yu tal, te tar, ñoo fay nekk duñu moy mukk, li leen Yàlla digal te la mu leen digal la ñuy def.
At-TahrimFihi Alxuraan
12Aaya
MedinanRevelation
4Aaya

Tekki — At-Tahrim 4

Simoore At-Tahrim Aaya 4 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yéen ñaari soxna yi su ngeen tuubee (moo gën) ndax…

Simoore Aaya 4/12 — At-Tahrim التحريم (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tahrim Dégg, At-Tahrim Tekki, At-Tahrim mp3, At-Tahrim pdf. Aaya 2–6. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers