Al-A'raf · 145/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَكَتَبْنَا لَهُ فِي الْأَلْوَاحِ مِن كُلِّ شَيْءٍ مَّوْعِظَةً وَتَفْصِيلًا لِّكُلِّ شَيْءٍ فَخُذْهَا بِقُوَّةٍ وَأْمُرْ قَوْمَكَ يَأْخُذُوا بِأَحْسَنِهَا ۚ سَأُرِيكُمْ دَارَ الْفَاسِقِينَ ۝١٤٥
Wa katabnaa lahoo fil alwaahi minkulli shai`immaw `izaanw wa tafseelal likulli shai`in fakhuzhaa biquwwatinw waamur qawmaka yaakhuzoo bi ahsanihaa; wa ooreekum daaral faasiqeen
📖 Tekkim Wolof
Nu bindal ko ci àlluwaya lu nekk ngir waare ak faramfàcce lu nekk ba mu waar ko cig farlu. “Nu digal ko mu wax ay nitam ñu jàppe ko ca na mu gën a rafete. Danaa leen won dëkku saay-saay sa.
🎧 Dégg

📜 Aaya 143-147 — Al-A'raf

143وَلَمَّا جَاءَ مُوسَىٰ لِمِيقَاتِنَا وَكَلَّمَهُ رَبُّهُ قَالَ رَبِّ أَرِنِي أَنظُرْ إِلَيْكَ ۚ قَالَ لَن تَرَانِي وَلَٰكِنِ انظُرْ إِلَى الْجَبَلِ فَإِنِ اسْتَقَرَّ مَكَانَهُ فَسَوْفَ تَرَانِي ۚ فَلَمَّا تَجَلَّىٰ رَبُّهُ لِلْجَبَلِ جَعَلَهُ دَكًّا وَخَرَّ مُوسَىٰ صَعِقًا ۚ فَلَمَّا أَفَاقَ قَالَ سُبْحَانَكَ تُبْتُ إِلَيْكَ وَأَنَا أَوَّلُ الْمُؤْمِنِينَ
Ba Muusaa agsee ca Sunu ndaje te Boroomam wax ak moom, mu ne : "Sama Boroom, won ma ma gis La ! ”. Mu ne ko : “Doo ma gis Muusaa ; waaye xoolal tundu doj wii : bu saxee ci barab bi mu nekk, kon danga Ma mën a gis.”. Ba Boroomam feeñoo doj wa, dafa mokk rumbax, Muusaa daanu xëm. Ba mu ximmee, mu daldi ne : “Tudd naa sag sell, kañ naa La ! Dellu naa ci Yaw ; te man sax faf maa di ki jëkk a gëm”.
144قَالَ يَا مُوسَىٰ إِنِّي اصْطَفَيْتُكَ عَلَى النَّاسِ بِرِسَالَاتِي وَبِكَلَامِي فَخُذْ مَا آتَيْتُكَ وَكُن مِّنَ الشَّاكِرِينَ
Mu ne ko : “Yaw Muusaa, Man tànn naa la ci biir nit ñi, ngay Sama Yonent ak Sama kàddu. Jëlal li Ma la jox te nga bokk ca way-gëm ña”.
145وَكَتَبْنَا لَهُ فِي الْأَلْوَاحِ مِن كُلِّ شَيْءٍ مَّوْعِظَةً وَتَفْصِيلًا لِّكُلِّ شَيْءٍ فَخُذْهَا بِقُوَّةٍ وَأْمُرْ قَوْمَكَ يَأْخُذُوا بِأَحْسَنِهَا ۚ سَأُرِيكُمْ دَارَ الْفَاسِقِينَ
Nu bindal ko ci àlluwaya lu nekk ngir waare ak faramfàcce lu nekk ba mu waar ko cig farlu. “Nu digal ko mu wax ay nitam ñu jàppe ko ca na mu gën a rafete. Danaa leen won dëkku saay-saay sa.
146سَأَصْرِفُ عَنْ آيَاتِيَ الَّذِينَ يَتَكَبَّرُونَ فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ وَإِن يَرَوْا كُلَّ آيَةٍ لَّا يُؤْمِنُوا بِهَا وَإِن يَرَوْا سَبِيلَ الرُّشْدِ لَا يَتَّخِذُوهُ سَبِيلًا وَإِن يَرَوْا سَبِيلَ الْغَيِّ يَتَّخِذُوهُ سَبِيلًا ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَكَانُوا عَنْهَا غَافِلِينَ
Danaa soreel Samay tegtal ña rëy-rëylu ci suuf si ci lu dul dëgg. Ba bu ñu gisee bépp kéemaan duñu ko gëm. Bu ñu gisee yoon wu njub, duñu ko topp, muy seenu yoon. Li waral loolu mooy dañoo weddi Sunuy kàddu, sàggan ba dëddu leen.
147وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَلِقَاءِ الْآخِرَةِ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ ۚ هَلْ يُجْزَوْنَ إِلَّا مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ña weddi Sunuy kàddu ak ndaje mu mujj ma, seeni jëf yàqu na. Ndax deesuleen fey lu dul la ñu daan def ”
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
145Aaya

Tekki — Al-A'raf 145

Simoore Al-A'raf Aaya 145 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nu bindal ko ci àlluwaya lu nekk ngir waare ak…

Simoore Aaya 145/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 143–147. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers