Al-Anfal · 66/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
الْآنَ خَفَّفَ اللَّهُ عَنكُمْ وَعَلِمَ أَنَّ فِيكُمْ ضَعْفًا ۚ فَإِن يَكُن مِّنكُم مِّائَةٌ صَابِرَةٌ يَغْلِبُوا مِائَتَيْنِ ۚ وَإِن يَكُن مِّنكُمْ أَلْفٌ يَغْلِبُوا أَلْفَيْنِ بِإِذْنِ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ مَعَ الصَّابِرِينَ ۝٦٦
Al`aana khaffafal laahu `ankum wa `alima anna feekum da`faa; fa-iny yakum minkum mi`atun saabiratuny yaghliboo mi`atayn; wa iny-yakum minkum alfuny yaghlibooo alfaini bi iznil laah; wallaahu ma`as saabireen
📖 Tekkim Wolof
Léegi, Yàlla woyofal na leen ngir xam na doyadi gi nekk ci yéen. Kon bu nekkee ci yéen téeméer yu muñ, danañu not ñaari téeméer ; bu nekkee ci yéen junni, danañu not ñaari junni, bu neexee Yàlla. Te Yàlla muñkat yi la àndal.
🎧 Dégg

📜 Aaya 64-68 — Al-Anfal

64يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ حَسْبُكَ اللَّهُ وَمَنِ اتَّبَعَكَ مِنَ الْمُؤْمِنِينَ
Éy yaw Yonent bi, Yàlla doy na la ak ku la topp ci ñi gëm.
65يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ حَرِّضِ الْمُؤْمِنِينَ عَلَى الْقِتَالِ ۚ إِن يَكُن مِّنكُمْ عِشْرُونَ صَابِرُونَ يَغْلِبُوا مِائَتَيْنِ ۚ وَإِن يَكُن مِّنكُم مِّائَةٌ يَغْلِبُوا أَلْفًا مِّنَ الَّذِينَ كَفَرُوا بِأَنَّهُمْ قَوْمٌ لَّا يَفْقَهُونَ
Éy yaw Yonent bi, nanga ñaax ñi gëm ci xare. Bu amee ñaar-fukk ñu muñ, danañu not ñaari téeméeri yéefar ; bu nekkee ci yéen téeméer, danañu not junni ciy yéefar, ndax ñoom nit lañu ñu amul dégg-dégg.
66الْآنَ خَفَّفَ اللَّهُ عَنكُمْ وَعَلِمَ أَنَّ فِيكُمْ ضَعْفًا ۚ فَإِن يَكُن مِّنكُم مِّائَةٌ صَابِرَةٌ يَغْلِبُوا مِائَتَيْنِ ۚ وَإِن يَكُن مِّنكُمْ أَلْفٌ يَغْلِبُوا أَلْفَيْنِ بِإِذْنِ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ مَعَ الصَّابِرِينَ
Léegi, Yàlla woyofal na leen ngir xam na doyadi gi nekk ci yéen. Kon bu nekkee ci yéen téeméer yu muñ, danañu not ñaari téeméer ; bu nekkee ci yéen junni, danañu not ñaari junni, bu neexee Yàlla. Te Yàlla muñkat yi la àndal.
67مَا كَانَ لِنَبِيٍّ أَن يَكُونَ لَهُ أَسْرَىٰ حَتَّىٰ يُثْخِنَ فِي الْأَرْضِ ۚ تُرِيدُونَ عَرَضَ الدُّنْيَا وَاللَّهُ يُرِيدُ الْآخِرَةَ ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
Warul cib Yonent mu am ay jaar-jaar [ca ña ñu jàppe cib xare not leen] fekk ñu nasaxal yéefar yi, faagaagal leen ba ñu mokk ci suuf si. Dangeen a bëgg [yéen jullit ñi] alali àddina, te Yàlla bëggal leen [xéewalu] àllaaxira. Te Yàlla Ku not la, Ku xereñ la.
68لَّوْلَا كِتَابٌ مِّنَ اللَّهِ سَبَقَ لَمَسَّكُمْ فِيمَا أَخَذْتُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Bu bul koon dogal bu tukkee ca Yàlla bu jiitu, kon mbugal mu rëy dana leen dal ngir la ngeen màng.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
66Aaya

Tekki — Al-Anfal 66

Simoore Al-Anfal Aaya 66 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Léegi, Yàlla woyofal na leen ngir xam na doyadi gi…

Simoore Aaya 66/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 64–68. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers