At-Tawba · 12/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
وَإِن نَّكَثُوا أَيْمَانَهُم مِّن بَعْدِ عَهْدِهِمْ وَطَعَنُوا فِي دِينِكُمْ فَقَاتِلُوا أَئِمَّةَ الْكُفْرِ ۙ إِنَّهُمْ لَا أَيْمَانَ لَهُمْ لَعَلَّهُمْ يَنتَهُونَ ۝١٢
Wa in nakasooo aimaanahum mim ba`di `ahdihim wa ta`anoo fee deenikum faqaatilooo a`immatal kufri innahum laaa aimaana lahum la`allahum yantahoon
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu firee seen kóllare ginnaaw ba ñu ko fasee, te di ayibal seen diine, xareleen ak njiiti yéefar yi - ndax ñoom faalewuñu kóllare - ndax xéy-na ñu yem, bàyyi yooyu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 10-14 — At-Tawba

10لَا يَرْقُبُونَ فِي مُؤْمِنٍ إِلًّا وَلَا ذِمَّةً ۚ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُعْتَدُونَ
Duñu sàmmonteek ña gëmoon, ci wàllu mbokk du ci wàllu kóllare. Te ñoom ñoo di ñu jéggi dayo ña.
11فَإِن تَابُوا وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ وَآتَوُا الزَّكَاةَ فَإِخْوَانُكُمْ فِي الدِّينِ ۗ وَنُفَصِّلُ الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Waaye bu ñu tuubee, te taxawal julli, di joxe asaka, kon seeni mbokk lañu ci diine ji. Te Danuy leeral tegtal yi ngir nit ñuy xam.
12وَإِن نَّكَثُوا أَيْمَانَهُم مِّن بَعْدِ عَهْدِهِمْ وَطَعَنُوا فِي دِينِكُمْ فَقَاتِلُوا أَئِمَّةَ الْكُفْرِ ۙ إِنَّهُمْ لَا أَيْمَانَ لَهُمْ لَعَلَّهُمْ يَنتَهُونَ
Bu ñu firee seen kóllare ginnaaw ba ñu ko fasee, te di ayibal seen diine, xareleen ak njiiti yéefar yi - ndax ñoom faalewuñu kóllare - ndax xéy-na ñu yem, bàyyi yooyu.
13أَلَا تُقَاتِلُونَ قَوْمًا نَّكَثُوا أَيْمَانَهُمْ وَهَمُّوا بِإِخْرَاجِ الرَّسُولِ وَهُم بَدَءُوكُمْ أَوَّلَ مَرَّةٍ ۚ أَتَخْشَوْنَهُمْ ۚ فَاللَّهُ أَحَقُّ أَن تَخْشَوْهُ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Li leen tere xeex ak nit ñay firi seeni kóllare, te ñuy yittewoo génne Yonent bi te ñoom ñoo leen jëkk a songu ? Moo ndax dangeen leen a ragal ? Te Yàllaa gën a yey ci ngeen ragal Ko ndegam ñu gëm ngeen !
14قَاتِلُوهُمْ يُعَذِّبْهُمُ اللَّهُ بِأَيْدِيكُمْ وَيُخْزِهِمْ وَيَنصُرْكُمْ عَلَيْهِمْ وَيَشْفِ صُدُورَ قَوْمٍ مُّؤْمِنِينَ
Xareleen ak ñoom. Yàlla Dana leen mbugal ñoom, jaare ko ci seeni yoxo yéen, te Dana leen toroxal, Dana leen dimbali ci not leen te Dana seral xoli ñi gëm ña.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
12Aaya

Tekki — At-Tawba 12

Simoore At-Tawba Aaya 12 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu firee seen kóllare ginnaaw ba ñu ko fasee,…

Simoore Aaya 12/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 10–14. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers