At-Tawba · 46/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
۞ وَلَوْ أَرَادُوا الْخُرُوجَ لَأَعَدُّوا لَهُ عُدَّةً وَلَٰكِن كَرِهَ اللَّهُ انبِعَاثَهُمْ فَثَبَّطَهُمْ وَقِيلَ اقْعُدُوا مَعَ الْقَاعِدِينَ ۝٤٦
Wa law araadul khurooja la-`addoo lahoo `uddatanw wa laakin karihal laahum bi`aasahum fasabbatahum wa qeelaq `udoo ma`al qaa`ideen
📖 Tekkim Wolof
Waay-waay bu ñu bëggoon a génn xare ji, kon danañu waaj ba jekk. Waaye Yàlla daleen a sib; tàyyeel-loo leen. Ba tax na ñu ne leen : “Fafleen toog rekk”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 44-48 — At-Tawba

44لَا يَسْتَأْذِنُكَ الَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ أَن يُجَاهِدُوا بِأَمْوَالِهِمْ وَأَنفُسِهِمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالْمُتَّقِينَ
Ña gëm Yàlla, gëm Bis bu mujj ba, duñu la ñaan mukk ndigalul bañ a dem xare ; ñoom kay dañuy xeex ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Yàlla xàmmee na ña ragal Yàlla de.
45إِنَّمَا يَسْتَأْذِنُكَ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَارْتَابَتْ قُلُوبُهُمْ فَهُمْ فِي رَيْبِهِمْ يَتَرَدَّدُونَ
Ñay laaj ndigal kay ñooy ña gëmul Yàlla ak Bis bu mujj ba, te seeni xol di fer-feri, ñuy jiixi-jaaxa.
46۞ وَلَوْ أَرَادُوا الْخُرُوجَ لَأَعَدُّوا لَهُ عُدَّةً وَلَٰكِن كَرِهَ اللَّهُ انبِعَاثَهُمْ فَثَبَّطَهُمْ وَقِيلَ اقْعُدُوا مَعَ الْقَاعِدِينَ
Waay-waay bu ñu bëggoon a génn xare ji, kon danañu waaj ba jekk. Waaye Yàlla daleen a sib; tàyyeel-loo leen. Ba tax na ñu ne leen : “Fafleen toog rekk”.
47لَوْ خَرَجُوا فِيكُم مَّا زَادُوكُمْ إِلَّا خَبَالًا وَلَأَوْضَعُوا خِلَالَكُمْ يَبْغُونَكُمُ الْفِتْنَةَ وَفِيكُمْ سَمَّاعُونَ لَهُمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالظَّالِمِينَ
Te sax ñoom bu ñu génnoon, ànd ak yéen, dem xare ji, garaawaali rekk lañu leen fay dolli ak fàbbi nit ñi. Te Yàlla xam na tooñkat yi.
48لَقَدِ ابْتَغَوُا الْفِتْنَةَ مِن قَبْلُ وَقَلَّبُوا لَكَ الْأُمُورَ حَتَّىٰ جَاءَ الْحَقُّ وَظَهَرَ أَمْرُ اللَّهِ وَهُمْ كَارِهُونَ
Fitna rekk lañu daan sàkku, ñu nekk ñu daan la ko wëlbatile mbir yi, ba dëgg ñëw, seen mbir wuññiku feeñ, te sañuñu koo bañ.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
46Aaya

Tekki — At-Tawba 46

Simoore At-Tawba Aaya 46 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waay-waay bu ñu bëggoon a génn xare ji, kon danañu…

Simoore Aaya 46/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 44–48. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers