At-Tawba · 45/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
إِنَّمَا يَسْتَأْذِنُكَ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَارْتَابَتْ قُلُوبُهُمْ فَهُمْ فِي رَيْبِهِمْ يَتَرَدَّدُونَ ۝٤٥
Innamaa yastaazinukal lazeena laa yu`minoona billaahi wal Yawmil Aakhiri wartaabat quloobuhum fahum fee raibihim yataraddadoon
📖 Tekkim Wolof
Ñay laaj ndigal kay ñooy ña gëmul Yàlla ak Bis bu mujj ba, te seeni xol di fer-feri, ñuy jiixi-jaaxa.

🎧 Dégg


📜 Aaya 43-47 — Simoore At-Tawba

43عَفَا اللَّهُ عَنكَ لِمَ أَذِنتَ لَهُمْ حَتَّىٰ يَتَبَيَّنَ لَكَ الَّذِينَ صَدَقُوا وَتَعْلَمَ الْكَاذِبِينَ
Yàlla baal na la li nga leen may dingalul ñu toog te nattuwooleen ba xam ña ca wax dëgg ak ña ca di ay fenkat.
44لَا يَسْتَأْذِنُكَ الَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ أَن يُجَاهِدُوا بِأَمْوَالِهِمْ وَأَنفُسِهِمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالْمُتَّقِينَ
Ña gëm Yàlla, gëm Bis bu mujj ba, duñu la ñaan mukk ndigalul bañ a dem xare ; ñoom kay dañuy xeex ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Yàlla xàmmee na ña ragal Yàlla de.
45إِنَّمَا يَسْتَأْذِنُكَ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَارْتَابَتْ قُلُوبُهُمْ فَهُمْ فِي رَيْبِهِمْ يَتَرَدَّدُونَ
Ñay laaj ndigal kay ñooy ña gëmul Yàlla ak Bis bu mujj ba, te seeni xol di fer-feri, ñuy jiixi-jaaxa.
46۞ وَلَوْ أَرَادُوا الْخُرُوجَ لَأَعَدُّوا لَهُ عُدَّةً وَلَٰكِن كَرِهَ اللَّهُ انبِعَاثَهُمْ فَثَبَّطَهُمْ وَقِيلَ اقْعُدُوا مَعَ الْقَاعِدِينَ
Waay-waay bu ñu bëggoon a génn xare ji, kon danañu waaj ba jekk. Waaye Yàlla daleen a sib; tàyyeel-loo leen. Ba tax na ñu ne leen : “Fafleen toog rekk”.
47لَوْ خَرَجُوا فِيكُم مَّا زَادُوكُمْ إِلَّا خَبَالًا وَلَأَوْضَعُوا خِلَالَكُمْ يَبْغُونَكُمُ الْفِتْنَةَ وَفِيكُمْ سَمَّاعُونَ لَهُمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالظَّالِمِينَ
Te sax ñoom bu ñu génnoon, ànd ak yéen, dem xare ji, garaawaali rekk lañu leen fay dolli ak fàbbi nit ñi. Te Yàlla xam na tooñkat yi.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
45Aaya

Tekki — At-Tawba 45

Simoore At-Tawba Aaya 45 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñay laaj ndigal kay ñooy ña gëmul Yàlla ak Bis…

Simoore Aaya 45/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 43–47. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers