Al-Anfal · 27/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَخُونُوا اللَّهَ وَالرَّسُولَ وَتَخُونُوا أَمَانَاتِكُمْ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ ۝٢٧
Yaaa aiyuhal lazeena aamanoo laa takhoonal laaha war Rasoola wa takhoonooo amaanaatikum wa antum ta`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen ñi gëm ! Buleen wuruj Yàlla ak Yonent bi. Te buleen wuruj ci seen kóllare te xam ko xéll.

🎧 Dégg


📜 Aaya 25-29 — Al-Anfal

25وَاتَّقُوا فِتْنَةً لَّا تُصِيبَنَّ الَّذِينَ ظَلَمُوا مِنكُمْ خَاصَّةً ۖ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعِقَابِ
Te nangeen ragal mbugal moo xam ne ku dul ña weddi ci yéen. Te nangeen xam ne Yàlla Ku tar mbugal la.
26وَاذْكُرُوا إِذْ أَنتُمْ قَلِيلٌ مُّسْتَضْعَفُونَ فِي الْأَرْضِ تَخَافُونَ أَن يَتَخَطَّفَكُمُ النَّاسُ فَآوَاكُمْ وَأَيَّدَكُم بِنَصْرِهِ وَرَزَقَكُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Fàttalikuleen ba ngeen nekkee ñu néew, di ñu ñu doyadal ci suuf si, ngeen di ragal nit ñi fëkk leen. Mu daroo leen, dimbali leen ci ndimbalam, Mu wërsëgal leen ci xéewal yu sell ndax xéy-na yéen ngeen gëram [seen Boroom].
27يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَخُونُوا اللَّهَ وَالرَّسُولَ وَتَخُونُوا أَمَانَاتِكُمْ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen wuruj Yàlla ak Yonent bi. Te buleen wuruj ci seen kóllare te xam ko xéll.
28وَاعْلَمُوا أَنَّمَا أَمْوَالُكُمْ وَأَوْلَادُكُمْ فِتْنَةٌ وَأَنَّ اللَّهَ عِندَهُ أَجْرٌ عَظِيمٌ
Xamleen ne seeni alal ak seeni doom, fitna lañu ci yéen te pey gu màgg a nga fa Yàlla.
29يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِن تَتَّقُوا اللَّهَ يَجْعَل لَّكُمْ فُرْقَانًا وَيُكَفِّرْ عَنكُمْ سَيِّئَاتِكُمْ وَيَغْفِرْ لَكُمْ ۗ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ
Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen ragalee Yàlla, Mu sagal leen, far seeni ñaawtéef, jéggal leen. Te Yàlla Kuy Boroom ngëneel yu màgg la.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
27Aaya

Tekki — Al-Anfal 27

Simoore Al-Anfal Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen ñi gëm ! Buleen wuruj Yàlla ak Yonent…

Simoore Aaya 27/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers