Al-Anfal · 73/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
وَالَّذِينَ كَفَرُوا بَعْضُهُمْ أَوْلِيَاءُ بَعْضٍ ۚ إِلَّا تَفْعَلُوهُ تَكُن فِتْنَةٌ فِي الْأَرْضِ وَفَسَادٌ كَبِيرٌ ۝٧٣
Wallazeena kafaroo ba`duhum awliyaaa`u ba`d; illaa taf`aloohu takun fitnatun fil ardi wa fasaadun kabeer
📖 Tekkim Wolof
Ña weddi, dañuy jàppoo. Bu ngeen ko deful, fitna ak yàqute gu rëy dana am ci kaw suuf si.

🎧 Dégg


📜 Aaya 71-75 — Al-Anfal

71وَإِن يُرِيدُوا خِيَانَتَكَ فَقَدْ خَانُوا اللَّهَ مِن قَبْلُ فَأَمْكَنَ مِنْهُمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Bu ñu la bëggee wuruj..., lu jiitu loolu, woroon nañu Yàlla ; ba tax na Mu digle ngeen jàppe leen [ci xare Badar]. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
72إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا وَهَاجَرُوا وَجَاهَدُوا بِأَمْوَالِهِمْ وَأَنفُسِهِمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَالَّذِينَ آوَوا وَّنَصَرُوا أُولَٰئِكَ بَعْضُهُمْ أَوْلِيَاءُ بَعْضٍ ۚ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَلَمْ يُهَاجِرُوا مَا لَكُم مِّن وَلَايَتِهِم مِّن شَيْءٍ حَتَّىٰ يُهَاجِرُوا ۚ وَإِنِ اسْتَنصَرُوكُمْ فِي الدِّينِ فَعَلَيْكُمُ النَّصْرُ إِلَّا عَلَىٰ قَوْمٍ بَيْنَكُمْ وَبَيْنَهُم مِّيثَاقٌ ۗ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Ña nga xam ne gëm nañu, te gàddaay te ñuy xare ak seeni alal ak seeni bakkan ngir Yàlla ak ña leen dalaloon di leen dimbali, ñooña ñooy ñu jàppante ña. Walla ña nga xam ne gëm nañu te gàddaayuñu, loolu du dox seen diggante feek gàddaayuñu. Waaye bu ñu sàkkoo ndimbal ci yéen ci wàllu diine, dimbal loolu war na leen ginnaaw songug nit ñoo xam ne kóllare dox na seen diggante. Yàlla Mi ngi ne jàkk ca la ngeen di def.
73وَالَّذِينَ كَفَرُوا بَعْضُهُمْ أَوْلِيَاءُ بَعْضٍ ۚ إِلَّا تَفْعَلُوهُ تَكُن فِتْنَةٌ فِي الْأَرْضِ وَفَسَادٌ كَبِيرٌ
Ña weddi, dañuy jàppoo. Bu ngeen ko deful, fitna ak yàqute gu rëy dana am ci kaw suuf si.
74وَالَّذِينَ آمَنُوا وَهَاجَرُوا وَجَاهَدُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَالَّذِينَ آوَوا وَّنَصَرُوا أُولَٰئِكَ هُمُ الْمُؤْمِنُونَ حَقًّا ۚ لَّهُم مَّغْفِرَةٌ وَرِزْقٌ كَرِيمٌ
Ña nga xam ne gëm nañu te gàddaay tey xare ci yoonu Yàlla ak ña leen dalaloon, di leen dimbali [Waa Ansaar], ñooña ñooy ñu gëm, ñu dëggu ña : am nañu njéggal ak xéewal gu tedd.
75وَالَّذِينَ آمَنُوا مِن بَعْدُ وَهَاجَرُوا وَجَاهَدُوا مَعَكُمْ فَأُولَٰئِكَ مِنكُمْ ۚ وَأُولُو الْأَرْحَامِ بَعْضُهُمْ أَوْلَىٰ بِبَعْضٍ فِي كِتَابِ اللَّهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Ak ña gëm ginnaaw ga te ñu gàddaay tey xare ànd ak yéen, ñooña ci yéen lañu bokk.Waaye ña nekk ay mbokk ñoo gën a yey [ci donnante] ci Téereb Yàlla bi. Yàlla xam na lu ne.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
73Aaya

Tekki — Al-Anfal 73

Simoore Al-Anfal Aaya 73 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña weddi, dañuy jàppoo. Bu ngeen ko deful, fitna ak…

Simoore Aaya 73/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 71–75. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers