Al-Anfal · 26/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
وَاذْكُرُوا إِذْ أَنتُمْ قَلِيلٌ مُّسْتَضْعَفُونَ فِي الْأَرْضِ تَخَافُونَ أَن يَتَخَطَّفَكُمُ النَّاسُ فَآوَاكُمْ وَأَيَّدَكُم بِنَصْرِهِ وَرَزَقَكُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ ۝٢٦
Wazkurooo iz antum qaleelum mustad `afoona filardi takhaafoona ai yatakhat tafakumun naasu fa aawaakum wa aiyadakum binasrihee wa razaqakum minat taiyibaati la`allakum tashkuroon
📖 Tekkim Wolof
Fàttalikuleen ba ngeen nekkee ñu néew, di ñu ñu doyadal ci suuf si, ngeen di ragal nit ñi fëkk leen. Mu daroo leen, dimbali leen ci ndimbalam, Mu wërsëgal leen ci xéewal yu sell ndax xéy-na yéen ngeen gëram [seen Boroom].

🎧 Dégg


📜 Aaya 24-28 — Al-Anfal

24يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اسْتَجِيبُوا لِلَّهِ وَلِلرَّسُولِ إِذَا دَعَاكُمْ لِمَا يُحْيِيكُمْ ۖ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ يَحُولُ بَيْنَ الْمَرْءِ وَقَلْبِهِ وَأَنَّهُ إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen wuyu Yàlla ak Yonentam ba, bu ñu leen woowee ci lu leen di musal, te nangeen xam ne Yàlla nag Dana dox nit ak xelam, te Danañu leen bëmëx jëme ca Moom.
25وَاتَّقُوا فِتْنَةً لَّا تُصِيبَنَّ الَّذِينَ ظَلَمُوا مِنكُمْ خَاصَّةً ۖ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعِقَابِ
Te nangeen ragal mbugal moo xam ne ku dul ña weddi ci yéen. Te nangeen xam ne Yàlla Ku tar mbugal la.
26وَاذْكُرُوا إِذْ أَنتُمْ قَلِيلٌ مُّسْتَضْعَفُونَ فِي الْأَرْضِ تَخَافُونَ أَن يَتَخَطَّفَكُمُ النَّاسُ فَآوَاكُمْ وَأَيَّدَكُم بِنَصْرِهِ وَرَزَقَكُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Fàttalikuleen ba ngeen nekkee ñu néew, di ñu ñu doyadal ci suuf si, ngeen di ragal nit ñi fëkk leen. Mu daroo leen, dimbali leen ci ndimbalam, Mu wërsëgal leen ci xéewal yu sell ndax xéy-na yéen ngeen gëram [seen Boroom].
27يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَخُونُوا اللَّهَ وَالرَّسُولَ وَتَخُونُوا أَمَانَاتِكُمْ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen wuruj Yàlla ak Yonent bi. Te buleen wuruj ci seen kóllare te xam ko xéll.
28وَاعْلَمُوا أَنَّمَا أَمْوَالُكُمْ وَأَوْلَادُكُمْ فِتْنَةٌ وَأَنَّ اللَّهَ عِندَهُ أَجْرٌ عَظِيمٌ
Xamleen ne seeni alal ak seeni doom, fitna lañu ci yéen te pey gu màgg a nga fa Yàlla.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
26Aaya

Tekki — Al-Anfal 26

Simoore Al-Anfal Aaya 26 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Fàttalikuleen ba ngeen nekkee ñu néew, di ñu ñu doyadal…

Simoore Aaya 26/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 24–28. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers