Al-Anfal · 44/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
وَإِذْ يُرِيكُمُوهُمْ إِذِ الْتَقَيْتُمْ فِي أَعْيُنِكُمْ قَلِيلًا وَيُقَلِّلُكُمْ فِي أَعْيُنِهِمْ لِيَقْضِيَ اللَّهُ أَمْرًا كَانَ مَفْعُولًا ۗ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ ۝٤٤
Wa iz yureekumoohum izil taqaitum feee a`yunikum qaleelanw wa yuqallilukum feee a`yunihim liyaqdiyal laahu amran kaana maf`oolaa; wa ilal laahi turja`ul umoor
📖 Tekkim Wolof
Fàttalikul ba Ma leen wonee, ba ngeen dajee, ñu néew ci seeni bët, te ngeen nekk ca ñu néew ca seeni bët ngir la Yàlla dige lu am la. Te ca Yàlla la mbir yépp di dellu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 42-46 — Al-Anfal

42إِذْ أَنتُم بِالْعُدْوَةِ الدُّنْيَا وَهُم بِالْعُدْوَةِ الْقُصْوَىٰ وَالرَّكْبُ أَسْفَلَ مِنكُمْ ۚ وَلَوْ تَوَاعَدتُّمْ لَاخْتَلَفْتُمْ فِي الْمِيعَادِ ۙ وَلَٰكِن لِّيَقْضِيَ اللَّهُ أَمْرًا كَانَ مَفْعُولًا لِّيَهْلِكَ مَنْ هَلَكَ عَن بَيِّنَةٍ وَيَحْيَىٰ مَنْ حَيَّ عَن بَيِّنَةٍ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَسَمِيعٌ عَلِيمٌ
Fekk na booba ngeen nekk ca xur wa gën a jegeñ, ñoom ñu nekk ca xur wa gën a sori, njëgg ma gën a suufe. Bu ngeen sàkku woon a dajeek ñoom, du sotti. Waaye lu Yàlla dogal day nekk, dana am ñu dee ci lu bir ak ñu dundu ci lu bir. Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
43إِذْ يُرِيكَهُمُ اللَّهُ فِي مَنَامِكَ قَلِيلًا ۖ وَلَوْ أَرَاكَهُمْ كَثِيرًا لَّفَشِلْتُمْ وَلَتَنَازَعْتُمْ فِي الْأَمْرِ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ سَلَّمَ ۗ إِنَّهُ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Ba la Yàlla wonee ci sa gént, ñoom ñu nekk mbooloo mu néew ! [Li ko waral mooy], su Ma la wonoon ñu nekk ñu bari, kon dangeen di yoqat, te dangeen xëccoo ca mbir ma. Waaye Yàlla defal leen dal. Moom nag xam na li nekk ci xol yi.
44وَإِذْ يُرِيكُمُوهُمْ إِذِ الْتَقَيْتُمْ فِي أَعْيُنِكُمْ قَلِيلًا وَيُقَلِّلُكُمْ فِي أَعْيُنِهِمْ لِيَقْضِيَ اللَّهُ أَمْرًا كَانَ مَفْعُولًا ۗ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ
Fàttalikul ba Ma leen wonee, ba ngeen dajee, ñu néew ci seeni bët, te ngeen nekk ca ñu néew ca seeni bët ngir la Yàlla dige lu am la. Te ca Yàlla la mbir yépp di dellu.
45يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا لَقِيتُمْ فِئَةً فَاثْبُتُوا وَاذْكُرُوا اللَّهَ كَثِيرًا لَّعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ
Éy yéen ñi gëm ñi ! Bu ngeen dajeek mbooloo, nangeen sax ci pastéef te ngeen tudd Yàlla lu bari ndax ngeen am ndam.
46وَأَطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَلَا تَنَازَعُوا فَتَفْشَلُوا وَتَذْهَبَ رِيحُكُمْ ۖ وَاصْبِرُوا ۚ إِنَّ اللَّهَ مَعَ الصَّابِرِينَ
Te nangeen topp Yàlla ak Yonentam ; te buleen xëccoo, kon ngeen yoqat, seen doole néew. Kon muñleen, Yàlla muñkat yi la àndal.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
44Aaya

Tekki — Al-Anfal 44

Simoore Al-Anfal Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Fàttalikul ba Ma leen wonee, ba ngeen dajee, ñu néew…

Simoore Aaya 44/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers