Al-Anfal · 18/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
ذَٰلِكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ مُوهِنُ كَيْدِ الْكَافِرِينَ ۝١٨
Zaalikum wa annal laaha moohinu kaidil kaafireen
📖 Tekkim Wolof
Loolu la dëggal ci yéen te [xamleen ne] Kuy doyadal pexey yéefar yi la [Moom Yàlla].
🎧 Dégg

📜 Aaya 16-20 — Al-Anfal

16وَمَن يُوَلِّهِمْ يَوْمَئِذٍ دُبُرَهُ إِلَّا مُتَحَرِّفًا لِّقِتَالٍ أَوْ مُتَحَيِّزًا إِلَىٰ فِئَةٍ فَقَدْ بَاءَ بِغَضَبٍ مِّنَ اللَّهِ وَمَأْوَاهُ جَهَنَّمُ ۖ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ
Ku daw won leen ginnaaw, ca bis boobu - lu dul kuy jéem a njuuy ba jekku na mu war a xeexe, walla kuy jéem a tafu ci mboolom jullit, - tàbbi ci merum Yàlla te dëkkuwaayam Safara la. Aka bon booba dëkkuwaay !
17فَلَمْ تَقْتُلُوهُمْ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ قَتَلَهُمْ ۚ وَمَا رَمَيْتَ إِذْ رَمَيْتَ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ رَمَىٰ ۚ وَلِيُبْلِيَ الْمُؤْمِنِينَ مِنْهُ بَلَاءً حَسَنًا ۚ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Te reyuleen leen [yéen jullit ñi] : Yàlla moo leen rey. Te sànniwoo [yaw Yonent bi], bi nga sànnee suuf si : waaye Yàlla moo sànni, ngir Mu may jullit ñi xéewal gu rafet gu tukke ca Moom Yàlla ! Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
18ذَٰلِكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ مُوهِنُ كَيْدِ الْكَافِرِينَ
Loolu la dëggal ci yéen te [xamleen ne] Kuy doyadal pexey yéefar yi la [Moom Yàlla].
19إِن تَسْتَفْتِحُوا فَقَدْ جَاءَكُمُ الْفَتْحُ ۖ وَإِن تَنتَهُوا فَهُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ ۖ وَإِن تَعُودُوا نَعُدْ وَلَن تُغْنِيَ عَنكُمْ فِئَتُكُمْ شَيْئًا وَلَوْ كَثُرَتْ وَأَنَّ اللَّهَ مَعَ الْمُؤْمِنِينَ
Ndegam dangeen di sàkku lu ngeen di àttewoo [yéen yéefar yi], ab àtte dikkal na leen ba noppi. Bu ngeen bàyyee [la ngeen nekkoon cig kéefar], mooy gën ci yéen. Bu ngeen delloo [ca la ngeen nekke woon], Nu dellu [ci di jox Yonent bi ndimbal], te kon seeni mbooloo duleen jariñ dara, doonte dafa bari lool. Yàlla nag Mook jullit yee ànd.
20يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا أَطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَلَا تَوَلَّوْا عَنْهُ وَأَنتُمْ تَسْمَعُونَ
Éy yéen ñi gëm ñi ! Nangeen topp Yàlla ak ub Yonentam, buleen ko dëddu te fekk dégg ngeen li muy wax.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
18Aaya

Tekki — Al-Anfal 18

Simoore Al-Anfal Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Loolu la dëggal ci yéen te [xamleen ne] Kuy doyadal…

Simoore Aaya 18/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers