Al-Anfal · 38/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
قُل لِّلَّذِينَ كَفَرُوا إِن يَنتَهُوا يُغْفَرْ لَهُم مَّا قَدْ سَلَفَ وَإِن يَعُودُوا فَقَدْ مَضَتْ سُنَّتُ الْأَوَّلِينَ ۝٣٨
Qul lillazeena kafarooo iny yantahoo yughfar lahum maa qad salafa wa iny ya`oodoo faqad madat sunnatul awwaleen
📖 Tekkim Wolof
Waxal yéefar yi, ne leen : “Bu ngeen bàyyee [xareek Yonent bi], nu baal leen la weesu. Waaye bu ngeen delluwaatee [ca la ngeen nekke woon], dees na leen mbugal kem ni mu daan ame bu njëkk.

🎧 Dégg


📜 Aaya 36-40 — Al-Anfal

36إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ لِيَصُدُّوا عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ فَسَيُنفِقُونَهَا ثُمَّ تَكُونُ عَلَيْهِمْ حَسْرَةً ثُمَّ يُغْلَبُونَ ۗ وَالَّذِينَ كَفَرُوا إِلَىٰ جَهَنَّمَ يُحْشَرُونَ
Ña nga xam ne dañoo weddi, Dananu sànk seeni alal ngir dëdduloo [nit ñi] yoonu Yàlla. Waaye Danañu ko sànk ba noppi di ko réccu. Ñu not leen, te ña weddi dees na leen bëmax jëme Safara,
37لِيَمِيزَ اللَّهُ الْخَبِيثَ مِنَ الطَّيِّبِ وَيَجْعَلَ الْخَبِيثَ بَعْضَهُ عَلَىٰ بَعْضٍ فَيَرْكُمَهُ جَمِيعًا فَيَجْعَلَهُ فِي جَهَنَّمَ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ
ngir Yàlla téqale yéefar yi ak ña gëm Yàlla, Dana boole yéefar yi, dajale leen ñoom ñépp ca biir Safara. Ñooñu ñooy way-ñàkk ña.
38قُل لِّلَّذِينَ كَفَرُوا إِن يَنتَهُوا يُغْفَرْ لَهُم مَّا قَدْ سَلَفَ وَإِن يَعُودُوا فَقَدْ مَضَتْ سُنَّتُ الْأَوَّلِينَ
Waxal yéefar yi, ne leen : “Bu ngeen bàyyee [xareek Yonent bi], nu baal leen la weesu. Waaye bu ngeen delluwaatee [ca la ngeen nekke woon], dees na leen mbugal kem ni mu daan ame bu njëkk.
39وَقَاتِلُوهُمْ حَتَّىٰ لَا تَكُونَ فِتْنَةٌ وَيَكُونَ الدِّينُ كُلُّهُ لِلَّهِ ۚ فَإِنِ انتَهَوْا فَإِنَّ اللَّهَ بِمَا يَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Xeexleen ak ñoom ba fitna jóge fi, ba diine nekk lu ñu jagleel Yàlla léppam. Waaye bu ñu bàyyee nag, Yàlla mi ngi ne jàkk ci li ñuy def.
40وَإِن تَوَلَّوْا فَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ مَوْلَاكُمْ ۚ نِعْمَ الْمَوْلَىٰ وَنِعْمَ النَّصِيرُ
Bu ñu dëddoo, xamleen ne, Yàlla mooy ka leen di jàppale. Ndaw soppe bu baax, ndaw Aji-dimbalee ju baax !
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
38Aaya

Tekki — Al-Anfal 38

Simoore Al-Anfal Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waxal yéefar yi, ne leen : “Bu ngeen bàyyee [xareek…

Simoore Aaya 38/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers